Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Yaakaar: Ndax ci dëgg am na njariñ?

Yaakaar: Ndax ci dëgg am na njariñ?

Yaakaar: Ndax ci dëgg am na njariñ?

DANIEL fukki at rekk la amoon, waaye mu ngi doon xeex ak feebaru cancer ci diiru benn at. Xaritam yi ak doktoor bi ko doon faj amatuñu woon benn yaakaar. Waaye Daniel moom, mu ngi doon wéy di am yaakaar. Gëmoon na ne, dina màgg ba nekk gëstukat, te benn bés, dina gis garab buy faj cancer. Gënoon na am yaakaar ci benn doktoor bi naroon a ñëw, te xareñ ci faj xeetu cancer bi mu amoon. Waaye, doktoor bi mujjul a ñëw bés bi ñu ko doon xaar. Yaakaaru Daniel daldi tas, mu komaase xàddi. Ñu teg ci ay fan rekk mu daldi dee.

Kenn ku doon liggéey ci wàllu wér-gi-yaram, te doon gëstu ci njariñ bi yaakaar am ci wér-gi-yaram, moo nettali li dal Daniel. Xéyna mas ngeen a dégg lu ni mel. Ci misaal, benn màgget bu xam ne li ko desee dund bareetul, waaye muy xaar lu am solo, lu mel ni benn mbokk bu ko nar a seetsi walla benn anniversaire. Li mu doon xaar bu jàllee, nit ki dafay gaaw a dee. Lan moo waral loolu? Ndax yaakaar mën na ñu ci dimbali ni ko ñenn ñi fooge?

Ñu bare ci ñiy gëstu ci wàllu wér-gi-yaram wax nañu ne rafet njort, yaakaar ak bañ a xàddi am na lu muy def ci dund nit ak ci wér-gi-yaramam. Waaye du ñépp a ci ànd. Yenn gëstukat yi, nee nañu loolu ay waxi neen la. Ci ñoom, wér-gi-yaram jotewul dara ak yaakaar bu tas. Bu nit feebaree, doomu jàngoro moo tax mu feebar.

Dëgg la ne, werante ci njariñ bi yaakaar am du lu bees. Ay junniy at ci ginnaaw, benn boroom xam-xam, doomu Geres, bu tudd Aristote lii la waxoon lu jëm ci yaakaar: «Ay gént rekk la». Benn politicien, doomu Etaa Sini bu tudd Benjamin Franklin, lii la waxoon: «Kuy dundee yaakaar, dee ak xiif».

Kon ci dëgg, lan mooy yaakaar? Ndax yéene rekk la, walla ay gént yuy dalal xelu nit ñi rekk la? Walla, ndax yaakaar lu am solo la? Ndax soxla nañu ko ngir am wér-gi-yaram ak mbégte? Ndax mën na ñu amal njariñ dëgg?