NJÀNGALE 3
Ndax ci dëgg-dëgg xibaaru jàmm bi, ci Yàlla la jóge ?
1. Biibël bi, ci kan la jóge ?
Xibaaru jàmm biy wone ne, nit ñi dinañu dëkk ba fàww ci kaw suuf si, ci Biibël bi lañu ko bind (Sabóor 37:29). Biibël bi yépp 66 téere yu ndaw la. Yàlla jël na 40 góor yu takku ci moom ngir ñu bind Biibël bi. Musaa moo bind juróomi téere yu njëkk yi te booba ba léegi am na lu jege 3 500 at. Téere bu mujj bi, ndaw li Yowaana moo ko bind, am na léegi lu ëpp 1 900 at. Ñi bind Biibël bi, ndax seen xalaati bopp lañu bind ? Yàlla dafa doon jëfandikoo Xel mu Sell mi ngir wax ak ñi bind Biibël bi (2 Samuel 23:2). Binduñu seeni xalaati bopp, waaye xalaati Yàlla lañu bind. Kon Biibël bi, ci Yexowa la jóge. — Jàngal 2 Timote 3:16 ; 2 Piyeer 1:20, 21.
Seetaanal wideo Biibël bi, ci kan la jóge ?
2. Lan moo ñu wóor ne Biibël bi, dëgg lay wax ?
Xam nañu ne Biibël bi ci Yàlla la jóge ndaxte saa yu waxee lu war a am ëllëg day am. Kenn mënul loolu (Josué 23:14). Yàlla Aji Kàttan ji rekk moo mën a xam ëllëgu doomu Aadama yi. — Jàngal Esayi 42:9 ; Isaïe 46:10.
Li ñuy séentu ci téere bu jóge ci Yàlla mooy mu wuute ak yeneen téere yi, te Biibël bi noonu la mel. Ay milyaari Biibël lañu sotti ci àddina si sépp ci ay téeméeri làkk. Bu dee sax téere bu yàgg la, Biibël bi dafa ànd ak li tubaab di woowe science, maanaam li boroom xam-xam yi di gëstu. Te it li 40 góor yooyu bind dafa ànd. * Rax-ci-dolli Biibël bi wone na bu baax ne Yàlla mbëggeel la. Biibël bi am na itam doole ngir soppi nit ba mu gën a baax. Loolu yépp a tax ay milyoŋi nit gëm ne Biibël bi Kàddu Yàlla la. — Jàngal 1 Tesalonig 2:13.
Seetaanal wideo Lu war a tax ñu gëm ne li Biibël bi wax dëgg la ?
3. Biibël bi, ci lan lay wax ?
Lépp li Biibël bi wax mu ngi jëm ci xibaaru jàmm biy wax ci li Yàlla bëggoon pur doomu Aadama yi. Mbind mu sell mi dafa ñuy xamal naka la doomu Aadama yi teelee ñàkk àjjana bi ñu leen mayoon ci kaw suuf si, ak naka la àjjana jooju di amaate. — Jàngal Peeñu ma 21:4, 5.
Kàddu Yàlla am na itam ay sàrt, ay xelal, ak ay ndigal. Biibël bi dafay nettali ni Yàlla doon doxale ak doomu Aadama yi te nettali yooyu dañuy feeñal mbiri Yàlla yi. Kon Biibël bi mën na la dimbali nga xam Yàlla. Dina la xamal naka ngay def ba nekk xaritu Yàlla. — Jàngal Sabóor 19:8, 12 ; Saag 2:23 ; 4:8.
4. Naka ngeen mënee nànd li Biibël bi wax ?
Ni Yeesu daan def ngir jàpple nit ñi ñu nànd Biibël bi, noonu la téere bu ndaw bii di def ngir jàpple leen ngeen nànd Biibël bi. Yeesu doon na jëfandikoo aaya yi nekk ci Biibël bi ngir leeral “ li Mbind mi di wax ”. — Jàngal Luug 24:27, 45.
Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla ak ni mu ame solo yépp, terewul mu am ñoo xam ne faalewuñu ko, am it ñoo xam ne da leen di tanqal. Waaye buleen xàddi. Seen yaakaaru am dund gu dul jeex, mu ngi aju ci li ngeen di nangoo xam Yàlla. — Jàngal Yowaana 17:3.
^ par. 3 Seetal téere bu ndaw bi tudd Un livre pour tous.