Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 1

Lan mooy xibaaru jàmm bi ?

Lan mooy xibaaru jàmm bi ?

1. Lan mooy xibaar bi jóge ci Yàlla ?

Yàlla dafa bëgg nit ñi am bànneex ci kaw suuf si. Moom moo sàkk suuf si ak lépp lu ci nekk ndaxte dafa bëgg doomu Aadama yi. Ci kanam tuuti Yàlla dina def ba ay nit yu bokk ci xeet yépp am ëllëg gu neex ci kaw suuf si. Dina fi jële lépp luy tax doomu Aadama yi di am coono. — Jàngal Yérémi 29:11.

Amul benn nguur bu fi mas a jële coxorte, feebar walla dee. Waaye am nañu xibaar bu neex, te xibaaru jàmm la. Ci kanam tuuti, Yàlla dina fi jële nguuru doomu Aadama yi yépp, teg fi nguuram. Ñépp ñi nguur gi nar a ilif, dinañu am jàmm ak wér-gi-yaram. — Jàngal Isaïe 25:8 ; 33:24 ; Dañeel 2:44.

2. Lu tax xibaaru jàmm bi nekk lu am solo tey ?

Bés bu fi Yàlla dindee ñu bon ñi, booba rekk la coono yi di jeex (Tsephania 2:3). Loolu kañ lay am ? Kàddu Yàlla yégle woon na xew-xew yiy tiital doomu Aadama yi tey. Jëf yu bon yi ñuy gis tey dañuy wone ne bésu Yàlla jege na. — Jàngal 2 Timote 3:1-5.

3. Lan lañu war a def ?

Ci Kàddu Yàlla, maanaam Biibël bi, lañu war a jàng lu jëm ci Yàlla. Biibël bi dafa mel ni leetar bu jóge ci baay bu bëgg ay doomam. Dafa ñuy won naka lañuy ame dund bu neex tey jii, ak naka lañuy ame ëllëg, dund gu dul jeex ci kaw suuf si. Dëgg la, booy jàng Biibël bi dina am ñu mu dul neex, waaye bul bàyyi kenn mu yàqal la ëllëg bu neex boobu Yàlla dige. — Jàngal Kàddu yu Xelu 29:25 ; Peeñu ma 14:6, 7.