Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 58

Wéyal di takku ci Yexowa

Wéyal di takku ci Yexowa

Karceen dëgg yi dañu dogu ci bañ a bàyyi mukk nit walla leneen yàq seen diggante ak Yexowa. Wóor na ne yow it loolu nga bëgg. Yexowa fonk na sa takkute ci moom (Jàngal Baamtug Yoon wi 10:12). Lan moo mën a tax mu jafe ci yow nga wéy di takku ci Yexowa te lan moo la ci mën a dimbali?

1. Naka la ñeneen ñi mënee tax mu jafe ñu takku ci Yexowa?

Dina am nit ñi ñuy jéem a tere ñu jaamu Yexowa. Kan moo ñemee def lu mel noonu? Ay nit yu bàyyi jaamu Yexowa te léegi di wax ay fen ci mbootaayam ngir yàq suñu ngëm. Ñoom lañuy woowe ñi bàyyi yoonu Yàlla. Am na itam yenn njiitu diine yuy wax ay fen ci ñun ngir yóbbu ñenn ci ñun, ñu bàyyi dëgg gi. Di werante ak ñi bàyyi yoonu Yàlla, di jàng seen téere, di dem ci seen sit internet walla di seetaan seeni wideo, dafa ñuy lor. Lu jëm ci nit ñiy jéem a tere ñeneen ñu jaamu Yexowa, Yeesu lii la waxoon ci ñoom: «Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb» (Macë 15:14).

2. Naka la dogal yi ñuy jël mënee tax mu jafe ñu takku ci Yexowa?

Suñu mbëggeel ci Yexowa moo ñuy xiir ci moytoo laal lépp lu jëm ci diine yu dul dëgg yi. Dara lu ñuy def warul a lëkkaloo ak diine yu dul dëgg, du suñu liggéey, du mbootaay bu ñu mën a bokk walla leneen lu mu mën a doon. Lii la ñu Yexowa wax: «Génnleen ci [Babilon mu mag mi], yéen samay gaay» (Peeñu 18:2, 4).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Jàngal ni nga mënee bañ a bàyyi kenn mu wàññi sa takkute ci Yexowa. Xoolal it ni génn ci Babilon mu mag mi, mënee wone sa takkute ci Yàlla.

3. Moytul ñiy jàngale lu dul dëgg

Lan lañu war a def bu ñu déggee ñuy wax lu ñaaw ci mbootaayu Yexowa? Jàngal Kàddu yu Xelu 14:15. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax ñu war a moytu, lépp lu ñu dégg rekk gëm ko?

Jàngal 2 Yowaana 9-11. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka lañu war a doxale ak ñi bàyyi yoonu Yàlla?

  • Bu dee sax waxuñu ak ñoom, naka la seen njàngale mënee agsi ci ñun?

  • Ci sa xalaat, lan la Yexowa di yëg bu ñuy déglu nit ñiy wax ci moom lu bon walla ci mbootaayam?

4. Wéyal di takku ci Yàlla bu amee mbokk bu bàkkaar

Bu ñu xamee ne am na kenn ci waa mbooloo mi ku def bàkkaar bu réy, lan lañu war a def? Xoolal li ñu mën a jàng ci santaane yi Yàlla joxoon Israyil bu njëkk. Jàngal Sarxalkat yi 5:1.

Ni ko aaya bi waxee, bu ñu xamee ne am na ku def bàkkaar bu réy, dañu ko war a wax magi mbooloo mi. Bala ñuy def loolu nag, li gën a rafet mooy ñu wax ki def bàkkaar bi, mu dem waxal boppam magi mbooloo mi li mu def. Su ko bañee def nag, suñu takkute ci Yexowa moo ñuy puus ñu dem wax magi mbooloo mi li ñu xam. Def loolu naka lay wonee ne takku nañu ci...

  • Yexowa Yàlla?

  • ki def bàkkaar bi?

  • waa mbooloo mi?

Bu sa mbokk ci ngëm nekkee ci jafe-jafe, dimbali ko!

5. Wéyal di sore Babilon mu mag mi

Jàngal Luug 4:8 ak Peeñu 18:4, 5. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax ba léegi, sama tur mu ngi ci listub diine bu dul dëgg bi ma bokkoon?

  • Ndax bokk naa ci mbootaay bu lëkkaloo ak diine bu dul dëgg?

  • Ndax sama liggéey dafay jàppale diine yu dul dëgg yi?

  • Ndax am na leneen lu ma war a soppi ci sama dund ngir génn ci diine yu dul dëgg yi?

  • Bu dee tontu naa waaw ci benn ci laaj yooyu yépp, lan laa war a soppi?

Ci fànn yooyu yépp, jëlal dogal biy tax nga am xel mu dal te wone sa takkute ci Yexowa.

Lan ngay def bu ñu la laajee nga maye xaalis ngir jàppale benn diine?

BU LA NIT WAXOON: «Damaa war a xam, ñi bàyyi yoonu Yàlla li ñuy wax ci Seede Yexowa yi ngir mën leen a tontu bu baax.»

  • Ndax loolu xel la? Lu tax nga wax loolu?

NAÑU TËNK

Bu ñu bëggee wéy di takku ci Yexowa, dañu war a moytu di ànd ak ñi ñuy jéem a nax.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax waruñu déglu njàngaley ñi bàyyi yoonu Yàlla?

  • Su ñu yëge ne dafa am benn mbokk bu def bàkkaar bu réy, lan lañu war a def?

  • Naka lañu mënee sore diine yu dul dëgg yi, ni ñu ko Biibël bi waxe?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li nga mën a def bu ñeneen di wax ay fen ci Seede Yexowa yi.

«Ndax xam naa li xew dëgg?» (w18 ut)

Naka nga mënee ràññee mbootaay walla lépp luy jàppale Babilon mu mag mi?

«Nañu gën a sawar ci njeexteelu ‘mujug jamono’ jii» (w19 § 16-18)

Lan la ay noon def ngir jéem a wàññi suñu ngëm?

Moytul ñu nax la (9:32)