Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 15

Kan mooy Yeesu?

Kan mooy Yeesu?

Yeesu bokk na ci nit ñi gën a siiw. Nit ñu bari xam nañu turam, waaye xamuñu lu bari ci moom. Te ñu bari dañu am ay gis-gis yu wuute ci ki mu doon dëgg. Lan la Biibël bi wax ci moom?

1. Kan mooy Yeesu?

Yeesu malaaka bu am kàttan la, buy dund ci kaw asamaan. Moom la Yexowa njëkk a sàkk. Loolu moo tax ñu di ko woowe «taaw bi, ki gëna màgg lépp luy mbindeef» (Kolos 1:15). Biibël bi nee na Yeesu mooy ‘jenn Doom ji Yàlla am kepp’ ndaxte Yeesu rekk la Yexowa sàkk te jaarul ci kenn (Yowaana 3:16). Yeesu jàppale na Baayam Yexowa, mu sàkk leneen lépp li am (Jàngal Kàddu yu Xelu 8:30). Ba tey, Yeesu dafa nekk ku jege Yexowa. Moom mooy «Kàddu gi» ndaxte dafa doon jottali Kàddu Yàlla ak ay tegtalam (Yowaana 1:14).

2. Lu tax Yeesu ñëw ci kaw suuf?

2 000 at ci ginnaaw, Yexowa dafa jëfandikoo xelam mu sell mi ci fasoŋ bu kéemaane, ngir toxal dundu Yeesu ci biiru benn jànq bu tuddoon Maryaama. Noonu la Yeesu juddoo nekk nit (Jàngal Luug 1:34, 35). Yeesu dafa ñëw ci kaw suuf ngir nekk Almasi bi, walla Kirist bi Yàlla dige ngir muccal doomu Aadama yi. a Lépp li yonent yi yégle woon ci Almasi bi ci biir Biibël bi, Yeesu matal na ko. Loolu moo dimbali nit ñi ñu xam ne, Yeesu mooy «Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji» (Macë 16:16).

3. Fan la Yeesu nekk léegi?

Bi Yeesu deewee, Yàlla dafa ko dekkal mu doon malaaka. Noonu mu dellu ci kaw asamaan. Foofu, «Yàlla kaweel ko lool» (Filib 2:9). Fi ñu tollu nii, Yeesu mooy ki ëpp kàttan gannaaw Yexowa.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal leneen luy wone kan mooy Yeesu dëgg ak li tax jàng koo xam, am solo lool.

4. Yeesu nekkul Yàlla Aji Man ji

Biibël bi wone na ne, bu dee sax Yeesu mooy malaaka bi gën a am kàttan ci kaw asamaan, moom dafay déggal Yexowa Yàlla, miy Baayam. Lu tax ñu mën a wax loolu? Seetaanal WIDEO BI ngir xam li Biibël bi jàngale, ci ni Yeesu wuute ak Yàlla Aji Man ji.

Aaya yii di topp dinañu ñu dimbali ñu xam li wuutale Yexowa ak Yeesu. Jàngal aaya yi, boo pare nga tontu ci laaj yi.

Jàngal Luug 1:30-32.

  • Ci li malaaka bi wax, lan mooy wone ne Yeesu wuute na ak Yexowa Yàlla, «Aji Kawe ji»?

Jàngal Macë 3:16, 17.

  • Bi ñu sóobee Yeesu ci ndox ba pare, lan la baat bi jóge asamaan wax?

  • Ci sa xalaat, baat boobu baatu kan la woon?

Jàngal Yowaana 14:28.

  • Diggante baay ak doom, kan moo mag te kan mooy kilifa?

  • Yeesu dafa woowe Yexowa Baayam. Loolu lan la ñuy jàngal?

Jàngal Yowaana 12:49.

  • Ndax Yeesu dafa jàppoon ne moom ak Baayam, kenn lañu?

5. Yeesu wone na ne mooy Almasi bi

Biibël bi am na ay yégle yonent yu bari, yu waroon a dimbali nit ñi, ñu xam kan mooy Almasi bi Yàlla tànn ngir mu muccal doomu Aadama yi. Seetaanal WIDEO BI ngir xam yenn ci yégle yonent yi Yeesu matal, bi mu nekkee ci kaw suuf.

Jàngal yégle yonent yii ci Biibël bi, boo pare nga tontu ci laaj yii di topp:

Jàngal Mise 5:1 ngir xam fi Almasi bi waroon a juddoo. b

  • Ndax ci dëkk bi yonent bi yégle woon, la Yeesu juddoo? (Macë 2:1).

Jàngal Sabóor 34:21 ak Sàkkaryaa 12:10 ngir xam li yonent yi yégle woon ci deewu Almasi bi.

  • Ndax yégle yonent yooyu mat nañu? (Yowaana 19:33-37).

  • Ndax foog nga ne, Yeesu mënoon na def dara ba matal yégle yonent yooyu?

  • Ci sa xalaat, loolu lan lay wone ci Yeesu?

6. Dañuy jële njariñ ci jàng lu jëm ci Yeesu

Biibël bi nee na, dafa am solo lool ñu jàng lu jëm ci Yeesu ak li Yàlla bëgg mu def. Jàngal Yowaana 14:6 ak 17:3. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax ñu war a jàng lu jëm ci Yeesu?

Yeesu ubbi na yoon wi ngir ñu mën a doon xaritu Yàlla. Jàngale na dëgg gi jëm ci Yexowa, te ci moom lañu mën a jaar ngir am dund gu dul jeex

BU LA NIT WAXOON: «Seede Yexowa yi gëmuñu Yeesu.»

  • Lan nga koy tontu?

NAÑU TËNK

Yeesu malaaka bu am kàttan la. Moom mooy doomu Yàlla ak it Almasi bi.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax ñuy woowe Yeesu «taaw bi, ki gëna màgg lépp luy mbindeef»?

  • Bala Yeesu di ñëw ci kaw suuf, lan la doon def?

  • Naka lañu xame ne Yeesu mooy Almasi bi?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ndax Biibël bi dafay jàngale ne, Yàlla dafa nekk baayu Yeesu, ni nit di jure doom.

«Lu tax ñuy woowe Yeesu Doomu Yàlla?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal li tax trinité du njàngale bu jóge ci Biibël bi.

«Ndax Yeesu mooy Yàlla?» (w09 1/4)

a Lesoŋ 26 ak 27 dinañu wone li tax doomu Aadama yi soxla ñu muccal leen ak ni ñu Yeesu muccale.

b Xoolal Yeneen leeral 2 ngir gis benn yégle yonent buy wax kañ la Yeesu waroon na feeñ ci kaw suuf.