Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 12

Lan moo la mën a dimbali nga wéy di jàng Biibël bi?

Lan moo la mën a dimbali nga wéy di jàng Biibël bi?

Jàng Biibël bi am na njariñ lool, waaye nag du yomb saa su nekk. Xéyna lée-lée, ngay xalaat ndax dinga mën a kontine di jàng Biibël bi. Waaye lu tax mu am solo nga wéy ci sa njàngum Biibël? Lan moo la ci mën a dimbali bu dee sax yombul?

1. Naka la la njàngum Biibël bi mënee dimbali?

«Kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole» (Yawut ya 4:12). Biibël bi mën na la dimbali ndaxte dafa lay xamal xalaati Yàlla ak mbëggeel gi mu am ci yow. Dina la dimbali nga am xam-xam, am sago dëgg ak it yaakaaru ëllëg. Li ci gën a am solo mooy, Biibël bi dina la dimbali nga nekk xaritu Yexowa. Booy jàng Biibël bi, doole ji nekk ci Kàddu Yàlla dina mën a jëf ci sa dund ba nga gën a bég.

2. Lu tax ñu war a nangu ne Biibël bi dafa am solo?

Lépp li ñuy jàng ci Biibël bi, dëgg la te dafa mel ni alal ju réy. Looloo tax Biibël bi xiirtal ñu ci lii, «jëndal dëgg te bu ko jaay» (Kàddu yu Xelu 23:23). Bu ñuy xalaat ci njariñu Biibël bi, dinañu góor-góorlu ngir wéy di ko jàng, ak jafe-jafe bu ñu mënta am (Jàngal Kàddu yu Xelu 2:4, 5).

3. Naka la la Yexowa mënee dimbali nga wéy ci njàng mi?

Yexowa dafa la bëgg a dimbali nga xam ko, ndaxte moo la sàkk te sa xarit la. Yàlla mën na def ba nga «fonk coobareem te di ko jëfe» (Jàngal Filib 2:13). Kon saa yoo soxlaa doole ngir wéy ci sa njàngum Biibël bi, walla ngir jëfe li nga jàng, moom mën na la ci dimbali. Mën na la may it doole boo ko soxlaa ngir muñ jafe-jafe yi walla fitna yi. Deel ñaan Yexowa ngir mu dimbali la nga wéy di jàng Biibël bi (1 Tesalonig 5:17).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mën a def ba wéy di jàng Biibël bi, bu dee sax amuloo jot walla mu am ñu lay tere njàng mi. Xoolal it ni la Yexowa mënee dimbali nga kontine ci njàng mi.

4. Na sa njàngum Biibël bi doon li gën a am solo ci yow

Lée-lée yitte yi dañuy bari lool, ba ñu foog ne amatuñu jot ngir jàng Biibël bi. Lan moo ñu mën a dimbali? Jàngal Filib 1:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ci sa xalaat, yan ñooy yëf yi «gëna rafet [walla gëna am solo]» ci suñu dund?

  • Naka nga mën a def ba sa njàngum Biibël bi, doon li gën a am solo ci yow?

  1. Boo solee pot bi suuf ba pare, door a dugal xeer yi, xeer yépp duñu ci xéj

  2. Boo njëkkee dugal xeer yi, dinga am palaas ngir dugal suuf su bari. Noonu itam, bu dee «li gën a am solo» nga jiital ci sa dund, dinga mën a def loolu te dinga am it jot ngir def leneen

Yàlla dafa sàkk nit ngir mu xam ko te jaamu ko. Bu ñu bëggee def loolu, fàww ñu jàng Biibël bi. Jàngal Macë 5:3. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Bu ñu defee suñu njàngum Biibël li gën a am solo, ban njariñ lañu ciy jële?

5. Kontineel bu dee sax ñu ngi lay fitnaal

Lée-lée, dina am ñi lay jéem a puus ngir nga bàyyi jàng Biibël bi. Xoolal li daloon Francesco. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lan la xaritu Francesco yi ak yaayam def bi mu leen waxe ne dafay jàng Biibël bi?

  • Naka la ko Yàlla barkele ndax ni mu xàddiwul?

Jàngal 2 Timote 2:24, 25. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la sa waa kër ak say xarit gise sa njàng mi?

  • Ni ko aaya bi wonee, naka nga war a doxale ak ñi kontaanul ci sa njàngum Biibël bi? Lu tax?

6. Wéerul ci Yexowa ngir mu dimbali la

Bu ñuy gën a jege Yexowa, ñuy gën di bëgg a def li ko neex. Waaye nag, soppi suñu dundin ngir neex Yexowa, mën na jafe ci ñun. Bu dee loolu mas na la dal, bul xàddi. Yexowa dina la dimbali. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lan la Jim soppi ci dundam ngir neex Yexowa?

  • Lan moo la laal ci nettali Jim bi?

Jàngal Yawut ya 11:6. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Yexowa nar a defal «ñi koy wut», maanaam ñiy góor-góorlu ngir xam ko te def li ko neex?

  • Ni ko aaya bi wonee, naka la Yexowa gise ni ngay góor-góorloo ngir jàng Biibël bi?

BU LA NIT LAAJOON: «Lu tax ngay jàng Biibël bi?»

  • Lan nga koy tontu?

NAÑU TËNK

Bu dee sax lée-lée jàng Biibël bi yombul, mën na la dimbali nga am dund gu dul jeex. Kontineel di wéeru ci Yexowa, te moom dina la barkeel.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax lépp li ñuy jàng ci Biibël bi, nekk lu am solo?

  • Naka nga mënee wone ne jàng Biibël bi dafa am solo ci yow?

  • Lu tax nga war a ñaan Yexowa mu dimbali la nga wéy di jàng Biibël bi?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ñeenti pexe yu dimbali ay nit ñu bari ñu jariñoo bu baax seen jot.

«Naka lañu mën a jariñoo bu baax suñu jot» (g 2/14)

Xoolal ni Yexowa dimbalee jigéen joo xam ne jëkkëram xamul woon lu tax mu doon def lépp ngir neex Yàlla.

Yexowa may na ñu doole ngir àttan suñu yen (5:05)

Lée-lée dañuy jiiñ Seede Yexowa yi ay taskatu njaboot. Ndax loolu dëgg la?

«Ndax Seede Yexowa yi dañuy tas njaboot yi walla dañu leen di dimbali ñu nekk benn?» (Ci jw.org la nekk)