Ubbil li ci biir

Nit buy jëfandikoo telefonam ngir seet ay tont ci ay laajam ci jw.org

Fan lañu mën a ame ay tont yu leer ci ay laaj yu am solo ?

Fan lañu mën a ame ay tont yu leer ci ay laaj yu am solo ?

 

  • Ci njàng mu sore ?

  • Ci mag ñi ?

  • Walla ci Biibël bi ?

LII LA BIIBËL BI WAX CI YÀLLA

“ Sa Kàddu mooy dëgg. ” — Yowaana 17:17, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla, 2010.

Benn jigéen mu ngi jàng Biibël bi di ci boole yenn gëstu ci Internet bi

Ay milioŋi nit ci àddina si sépp gis nañu ci Biibël bi ay tont yu leer ci seeni laaj yu am solo.

Ndax bëgg nga bokk ci ñooñu ?

Suñu palaas bi ñu moom ci internet, bi tudd jw.org, mën na la ci dimbali.

JÀNGAL ci internet bi

SOTTIL ci sa ordinatër ay téere yu mel ni

CI LAAJ YU AM SOLO YII BAN MOO LA CI GËN A ITTEEL ?

Ñaari ndaw yu séy ñu ngi jàng Biibël bi te di def ay gëstu ci Internet

Xoolal tont yi Biibël bi joxe ci laaj yooyu ci jw.org.

(Demal ci LI BIIBËL BI WAX > AY LAAJ YU JËM CI BIIBËL BI)