NJÀNGALE 10
Yeesu dafa doon dégg ndigal
Déggal say waajur bés bu nekk, ndax yomb na ? — Yenn saay dafay metti. Ndax xam nga ne Yeesu dafa doon déggal Yexowa, te déggal ay waajuram itam ? — Li Yeesu def mën na la dimbali nga déggal say waajur bu fekkee ne sax yombul. Nañu jàng nettali bii.
Bala Yeesu di ñëw ci suuf, ci kaw asamaan la nekkoon ak Yexowa mi nekk Baayam. Waaye bi Yeesu ñëwee ci kaw suuf amoon na itam ay waajur fii. Ñu ngi tuddoon Yuusufa ak Maryaama. Naka la loolu mënoon a nekk ? —
Yexowa dafa jël bakkanu Yeesu mi nekkoon asamaan, dugal ko ci biiru Maryaama, mu mën a juddu te dund ci kaw suuf. Loolu kéemaan la woon ! Yeesu màgg ni liir yépp ci biiru Maryaama lu mat juróom-ñeenti weer mu juddu. Noonu la Maryaama ak jëkkëram Yuusufa nekke waajuru Yeesu fii ci suuf.
Am na lu xewoon bi Yeesu amee 12 at rekk luy wone ne bëgg na lool Baayam, Yexowa. Yuusufa ak waa këram ñoo demoon Yerusalem ngir màggali bésu Mucc ba. Tukki bu sore lawoon. Bi ñuy ñibbisi, Yuusufa ak Maryaama gisuñu Yeesu fenn. Ndax xam nga fan la nekkoon ? —
Lu tax Yeesu dem ca kër Yàlla ga ?
Yuusufa ak Maryaama dañu dellu Yerusalem dem wëri Yeesu fu nekk. Gisuñu ko. Ñu daldi jaaxle lool ! Bi mu amee ñetti fan nag, ñu gis ko ca kër Yàlla ga ! Ndax xam nga lu tax Yeesu dem ca kër Yàlla ga ? — Ndaxte foofu la mënoon a jàng lu jëm ci Baayam, Yexowa. Dafa bëggoon Yexowa te dafa bëggoon a xam li mu war a def ba neex ko. Bi Yeesu demee ba nekk mag sax dafa doon kontine di déggal Yexowa. Bu yombul woon sax walla mu metti lool, Yeesu dafa doon kontine di déggal Yexowa. Ndax Yeesu dafa doon déggal itam Yuusufa ak Maryaama ? — Waaw, Biibël bi wax na ko.
Lan nga mën a jàng ci li Yeesu def ? — War nga déggal say waajur bu fekkee ne sax yombul. Ndax dinga ko def ? —