Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 1

Dégluleen Yàlla ngir am Séy bu Neex

Dégluleen Yàlla ngir am Séy bu Neex

“ Ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na léen, kii góor, kii jigéen ”. — Macë 19:⁠4

Yexowa * Yàlla moo taxawal séy bi njëkk a am. Biibël bi dafa ñuy xamal ne Yàlla dafa sàkk jigéen bi njëkk daldi ko ‘ indil ’ ku góor ki. Aadama kontaan ba wax lii : “ Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux ! ” (Njàlbéen ga 2:22, 23). Mbégte boobu la Yexowa bëgg ñiy séy am ba tey.

Ñu bare bu ñu duggee ci séy, dañuy foog ne bànneex rekk lañu ciy am. Waaye ci dëgg, poroblem mënul ñàkk diggante jëkkër ak jabar, bu dee sax bëggante nañu bu baax (1 Korent 7:28). Dingeen gis ci téere bii li Yàlla santaane ci Biibël bi ngir dimbali ñi séy ak seen njaboot ñu am jàmm. Bu ngeen ko toppee, dingeen gis njariñ bi ci nekk. — Sabóor 19:9-​12.

1 NANGULEEN FI LEEN YEXOWA TEG CI BIIR NJABOOT

LI BIIBËL BI WAX : Jëkkër mooy kilifa ci biir njaboot. — Efes 5:23.

Yaw miy jëkkër, Yàlla dafa bëgg nga fonk sa jabar te toppatoo ko (1 Piyeer 3:⁠7). Yàlla dafa sàkk jabar ngir mu jàpple te wéetali jëkkëram, te yaw jëkkër ji, Yàlla dafa bëgg nga may sa jabar cér te won ko mbëggeel (Njàlbéen ga 2:​18). Danga war a bëgg sa jabar ba mu jaral la nga jiital njariñam te bañ a jiital sa njariñu bopp. — Efes 5:25-29.

Yaw miy jigéen, Yexowa dafa bëgg nga weg bu baax sa jëkkër te jàpple ko bu baax ci wareefam (1 Korent 11:3 ; Efes 5:​33). Jàppleel sa jëkkër ci dogal yi muy jël te ànd ak moom ak xol bu tàlli ci li muy def (Kolos 3:​18). Boo ko defee, dinga taaru ci sa kanamu jëkkër ak ci kanamu Yexowa. — 1 Piyeer 3:1-6.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Laajal ki nga séyal ni nga mën a def ngir gën a nekk jëkkër walla jabar ju baax. Déglu ko bu baax te jéem a gën a nekk jëkkër walla jabar ju baax

  • Bul yàkkamti. Bala ku nekk di mën a béggal moroomam, dina jël jot

2 NA KU NEKK YËG KI MU SÉYAL

LI BIIBËL BI WAX : Danga war a wut njariñu ki nga séyal (Filib 2:​3, 4). Ci sa doxalin ak moom, won ko ne sopp nga ko, te xam ne Yexowa dafa bëgg jaamam yi “ lewet ci ñépp ” (2 Timote 2:​24). “ Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi ; kàddu gu xelu, garab la ci. ” Kon nanga xool bu baax ni ngay waxe ak ki nga séyal (Kàddu yu Xelu 12:18). Xelum Yexowa dina la dimbali ba mbaax ak mbëggeel feeñ ci sa waxin. — Galasi 5:​22, 23 ; Kolos 4:⁠6.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Bala ngay waxtaan ak ki nga séyal ci mbir bu mën a yee fitna, nanga ñaan Yàlla ngir bañ a xuloo te nangu déglu

  • Xalaatal bu baax ci li nga bëgg a wax ak ni nga koy waxe

3 BOKKLEEN XALAAT

LI BIIBËL BI WAX : Boo séyee, dangay “ doon benn ” ak ki ngay séyal (Macë 19:⁠5). Waaye ba léegi ñaari nit ngeen te mën a wuute ci ni ngeen di xalaate. Kon dangeen war a jàng bokk xalaat ak bokk yëg-yëg (Filib 2:⁠2). Dafa am solo ngeen déggoo bu ngeen di jël dogal. Biibël bi dafa ne, bu diisoo amee pexe dina am (Proverbes 20:18). Yéen ñaar, bu ngeen di jël dogal yu am solo, nangeen bàyyi santaane yi nekk ci Biibël bi wommat leen. — Kàddu yu Xelu 8:32, 33.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Bu ngeen di waxtaan, wax ko say yëg-yëg, bul yem ci wax ko li xew rekk walla li ngay xalaat

  • Boo bëggee sóobu ci dara, nanga ci njëkk a waxtaan ak ki nga séyal

^ par. 4 Yexowa mooy turu Yàlla ci Biibël bi.