Ubbite bi
Tey ci suñu jamono ju metti jii, séy yu bare ñu ngi tas te njaboot yu bare amuñu jàmm. Ndax mën nañu am jàmm ci suñu biir njaboot ? Dëgg la, am jàmm yombul. Waaye ndimbal am na. Téere bii, loolu moo ko tax a jóg. Waxul lépp lu jëm ci séy waaye dafay joxe ay santaane yu wóor yu sukkandiku ci Biibël bi ak ni ñu leen mënee topp. Bu ngeen toppee bu baax li ci nekk, dingeen mën a yokk jàmm bi ngeen am ci seen biir njaboot.