Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 3

Li ngeen mën a def bu poroblem amee

Li ngeen mën a def bu poroblem amee

‘ Nangeen bëggante mbëggeel gu tar, ndax mbëggeel day suul bàkkaar yu bare. ’ ​— 1 Piyeer 4:8

Yéen ñi door a séy, xam leen ne poroblem dina am. Li ko mën a indi mooy, bokkuleen xalaat, walla yëg-yëg walla gis-gis. Poroblem yi mën nañu bañ a jóge ci yéen walla sax ñu jóge ci lu leen bett.

Lée-lée daw poroblem mooy gën a yomb ci yaw, waaye Biibël bi dafa ñuy xiirtal ñu bañ a def loolu (Macë 5:​23, 24). Dingeen gis ne topp santaane Yàlla yi nekk ci Biibël bi mooy pexe bi gën ci seeni poroblem.

1 WAXTAANLEEN CI POROBLEM BI

LI BIIBËL BI WAX : “ Dafa am waxtu ngir . . . wax ” (Dajalekat 3:​1, 7, MN). Nangeen fexe ba jël jot ngir waxtaan ci poroblem bi. Waxal ki nga séyal lépp li nga yëg ak li nga xalaat ci mbir mi. Ci lépp, deel “ wax dëgg ” ki nga séyal (Efes 4:​25). Bu dee sax poroblem bi dafa bëgg a indi coow, nanga teye sa bopp, bañ a xuloo. Tont bu neex mën na tax waxtaan bu ndaw bañ a àgg ci xuloo bu metti. — Kàddu yu Xelu 15:4 ; 26:⁠20.

Bu dee sax ànduloo ci li muy wax, ba tey àndal ak yar, te bul fàtte mukk won ko mbëggeel te may ko cér (Kolos 4:⁠6). Jéemleen a regle poroblem ci ni mu gën a gaawe, te buleen gedd. — Efes 4:​26.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Tànnleen waxtu bi gën ngir waxtaan ci poroblem bi

  • Bu ki nga séyal di wax, bu ko dog. Bu paree dinga mën a wax

2 DÉGLUL TE JÉEM A NÀND GIS-GISAM

LI BIIBËL BI WAX : “ Bëgganteleen ak xol bu leer, niy doomi ndey, te farlu ci teralante ” (Room 12:10). Fasoŋ bi ngay dégloo am na solo lool. Jéemal a nànd gis-gisu ki nga séyal te bokk ak moom “ tiis . . . te woyof ” (1 Piyeer 3:8 ; Saag 1:​19). Bul def ni yaa ngi déglu fekk dégluwoo. Bu mënee nekk, bàyyil ci li nga jàpp te déglu ko bu baax a baax. Walla nga laaj ko ndax mën ngeen ci waxtaan beneen waxtu. Ki nga séyal, boo ko jàppee ni sa waay, bañ koo jàppe ni sa noon, doo gaaw a gis sa bopp. — Ecclésiaste 7:⁠9.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Bu ngeen di wax, nanga ubbi sa xel, déglu ko bu dee sax li ngay dégg neexu la

  • Xool ko bu baax te seet ni muy waxe. Jéemal a nànd li mu la bëgg a wax, bul yem ci li ngay dégg

3 DEFLEEN LI NGEEN WAXANTE

LI BIIBËL BI WAX : “ Kër-këri, jariñu ; waxi neen, loxoy neen ” (Kàddu yu Xelu 14:23). Juboo ci wax rekk doyul. Fàww ku nekk def li ngeen waxante yéen ñaar. Loolu nag mën na jafe lool waaye jar na ko (Kàddu yu Xelu 10:⁠4). Bu ngeen àndee doon benn, dingeen ci gis njariñ bu réy. — Ecclésiaste 4:⁠9.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Waxleen li ku nekk war a def ngir regle poroblem bi

  • Lée-lée nangeen toog xool fi ku nekk tollu ci li muy jéem a def