XAAJ 13
Lan lañu war a def ba am dundin bu neex Yàlla ?
Moytuleen lu bon. 1 Korent 6:9, 10
Bu ñu bëggee Yexowa, duñu def li mu bañ.
Yexowa bëggul ñuy sàcc, walla ñuy màndi, walla ñuy dorogewu.
Yàlla dafa bañ rey nit ak yàq biir, ak mbirum góor-jigeen. Bëggul ñu bëgge, walla ñuy xeex ak suñu moroom.
Waruñu di jaamu ay xërëm walla ay nataal, walla di gisaane, di kort, di luxus walla di def yu mel noonu.
Bu suuf si nekkaatee àjjana, nit ñu bon ñi dootuñu fi nekk.
Macë 7:12
Defleen lu baax.Bu ñu bëggee neex Yàlla, war nañu koo jéem a roy.
Nangeen baax te nangoo maye ngir wone seen mbëggeel ci seeni moroom.
Nangeen nekk ay nit ñu jub.
Nangeen am yërmande te di baale.
Nangeen xamal nit ñi lu jëm ci Yexowa ak li mu bëgg. — Isaïe 43:10.