Li ñu mën a laaj bu ñuy jàng téere bi tudd Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
Nettali 1
Yàlla mu ngi tàmbalee sàkk
Lépp lu baax lu ñu gis, fu mu jóge, te ndax mën nga ci wax benn ?
Lan la Yàlla jëkk a sàkk ?
Lu tax malaaka bi Yàlla jëkk a sàkk wuute woon ak yeneen malaaka yi ?
Naka la suuf si meloon bu jëkk ? (Xoolal li ñuy wone foofu.)
Lan la Yàlla jëkk a def ngir mala ak nit mën a dëkk ci kow suuf si ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jérémie 10:12.
Yan jikko Yàlla ñoo feeñ ci li mu sàkk (Is. 40:26 ; Room. 11:33) ?
Jàngal Kolos 1:15-17.
Ban wàll la Yeesu amoon ci liggéey bi Yàlla doon def bi mu doon sàkk lépp, te ndegam loolu la, naka lañu war a gise Yeesu (Kol. 1:15-17) ?
Jàngal Njàlbéen ga 1:1-10.
Suuf si, fu mu jóge (Njàl. 1:1) ?
Bi Yàlla doon sàkk lépp, lu xewoon ci bés bu jëkk bi ? (Njàl. 1:3-5) ?
Waxal li xewoon ci ñaareelu bés bi (Njàl. 1:7, 8).
Nettali 2
Tool bu rafet
Naka la Yàlla waajale suuf si ngir nit mën ci dëkk ?
Yàlla sàkk na ay fasoŋu mala yu bare lool. Waxal ay turu mala yi nga xam. (Xoolal ci li ñuy wone foofu.)
Lu tax toolu Eden wuute woon ak yeneen béréb yi ?
Naka la Yàlla bëggoon suuf si sépp mel ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 1:11-25.
Lan la Yàlla sàkk ci ñetteelu bés bi (Njàl. 1:12) ?
Lu xewoon ci ñeenteelu bés bi (Njàl. 1:16) ?
Yan mala la Yàlla sàkk ci juróomeel ak juróom-benneelu bés yi (Njàl. 1:20, 21, 25) ?
Jàngal Njàlbéen ga 2:8, 9.
Yan ñaari garab yu amoon solo lool la Yàlla def ci tool bi, te lan lañu doon wone ?
Nettali 3
Nit ñi jëkk a am ci kow suuf
Lan lañuy wone ci nettali 3 loo gisul ci nettali 2 ?
Kan moo sàkk góor gu jëkk gi, te naka la tuddoon ?
Ban liggéey la Yàlla jox Aadama ?
Lu tax Yàlla nelawloo Aadama, nelaw bu xóot ?
Ba kañ la Aadama ak Awa mënoon a dund, te ban liggéey la Yàlla bëggoon ñu def ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Sabóor 83:18.
Yàlla, naka la tudd, te ban taxawaay la moom rekk am ci kow suuf si (Jér. 16:21 ; Dañ. 4:17) ?
Jàngal Njàlbéen ga 1:26-31.
Lan la Yàlla mujj a sàkk ci juróom-benneelu fan bi, te li mu sàkk noonu, lu mu wuute woon ak mala yi (Njàl. 1:26) ?
Lan la Yexowa may nit ak mala yépp (Njàl. 1:30) ?
Jàngal Njàlbéen ga 2:7-25.
Lan la Aadama waroon a def ngir mën a wutal mala yi tur (Njàl. 2:19) ?
Naka la Njàlbéen ga 2:24 di ñu wonee ni Yàlla gise séy, tàggoo ak fase (Macë 19:4-6, 9) ?
Nettali 4
Lu tax ñu dàq leen
Xoolal Aadama ak Awa. Lan moo leen dal ?
Lu tax Yexowa yar leen noonu ?
Lan la benn jaan wax Awa ?
Kan moo doon waxloo jaan bi ?
Lu tax ñu génne Aadama ak Awa ci biti Àjjana ji ñu nekkoon ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 2:16, 17 ak 3:1-13, 24.
Jaan bi dafa bëggoon nit ñi gëm ne Yexowa baaxul. Naka la loolu feeñe ci li mu laaj Awa (Njàl. 3:1-5 ; 1 Ywna. 5:3) ?
Naka la ñu Awa wone li ñu war a moytu (Fil. 4:8 ; Saag 1:14, 15 ; 1 Ywna. 2:16) ?
Naka la Aadama ak Awa wonee ne bëgguñu gàddu àq ndax seen bàkkaar (Njàl. 3:12, 13) ?
Seruben yi taxawoon ca penku toolu Eden, naka lañu wonee ne Yexowa rekk mooy Kilifa gi gën a mag ci kow lépp (Njàl. 3:24) ?
Jàngal Peeñu ma 12:9.
Ñi Seytaane xiir ci bañ a topp Yàlla, naka lañu tollu (1 Ywna. 5:19) ?
Nettali 5
Léegi àddina bi metti na
Ban dund la Aadama ak Awa amoon ci biti toolu Eden ?
Léegi, lan mooy dal Aadama ak Awa, te lu tax loolu ?
Lu tax doomi Aadama ak Awa war a màgget te dee ñoom itam ?
Bu Aadama ak Awa déggaloon Yexowa, ban dund lañu naroon a am, ñoom ak seeni doom ?
Awa déggadi na Yexowa. Ban metit la ko loolu indil ?
Ñaari doom yu góor yi Aadama ak Awa jëkk a am, naka lañu tuddoon ?
Ñan ñooy yeneen doom yi nuy wone fii ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 3:16-23 ak 4:1, 2.
Lu metti li Yàlla wax lu jëm ci suuf si, lan la def ci dundu Aadama (Njàl. 3:17-19 ; Room 8:20, 22) ?
Turu Awa, mu ngi tekki “ Kuy dund ”. Lu tax tur boobu baax ci moom (Njàl. 3:20) ?
Naka la Yexowa maye cér Aadama ak Awa ginnaaw bi ñu bàkkaaree ba pare sax (Njàl. 3:7, 21) ?
Jàngal Peeñu ma 21:3, 4.
Yan “ yëf yu jëkk ” nga bëgg mu jeex ?
Nettali 6
Ñaari doom : kenn ki baax, keneen ki bon
Kayin ak Abel, lan moo doon seen liggéey ?
Yan sarax la Kayin ak Abel def Yàlla ?
Lu tax Yexowa nangu saraxu Abel te bañ a nangu saraxu Kayin ?
Ban jikko la Kayin amoon, te lan la Yexowa def ngir jéem koo jubbanti ?
Lan la Kayin def bi mu nekkee ak rakkam, ñoom kenn, ca àll ba ?
Waxal li dal Kayin ginnaaw bi mu reyee rakkam.
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 4:2-26.
Lan la Yexowa wax ngir wone ne Kayin mu ngi tollu woon fu wóorul dara (Njàl. 4:7) ?
Naka la Kayin wonee dëgg li nekkoon ci biir xolam (Njàl. 4:9) ?
Naka la Yexowa gise nit kuy tuur deretu nit ku deful dara lu bon (Njàl. 4:10 ; Is. 26:21) ?
Jàngal 1 Yowaana 3:11, 12.
Lu tax Kayin mer lool, te lan lañu war a moytu kon tey (Njàl. 4:4, 5 ; Prov. 14:30 ; 28:22) ?
) Naka la Biibël bi wonee ne mën nañu kontine di topp Yàlla bu baax bu dee sax suñu waa kër yépp bëgguñu Yexowa (Sab. 27:10 ; Macë 10:21, 22) ?
Jàngal Yowaana 11:25.
Am na ay nit ñoo xam ne dañu leen di rey ndax li ñu bañ a def lu bon. Lan la Yexowa wax ci lu wóor lu jëm ci nit ñooñu (Ywna. 5:24) ?
Nettali 7
Nit kii am na fit
Enog, lu mu wuute woon ak yeneen nit ñi ?
Ci jamano Enog, lu tax nit ñi doon def lu bon rekk ?
Yan yëf yu bon la nit ñi doon def ? (Xoolal li ñuy wone fii.)
Lu tax Enog waroon a am fit ?
Ca jamano jooja, ñaata at la nit ñi doon dund, waaye ñaata at la Enog dund ?
Lu xewoon ginnaaw bi Enog gaañoo ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 5:21-24, 27.
Naka la diggante Enog ak Yexowa meloon (Njàl. 5:24) ?
Ci li Biibël bi wax, ban nit moo gën a gudd fan ci àddina, te ñaata at la amoon bi mu gaañoo (Njàl. 5:27) ?
Jàngal Njàlbéen ga 6:5.
Ginnaaw bi Enog gaañoo, ba fan la lu bon tollu woon ci àddina si, te ndax ñu ngi gis lu mel noonu ci suñu jamano tey (2 Tim. 3:13) ?
Jàngal Yawut ya 11:5.
Lan la Yàlla gis ci Enog te mu neex ko lool, te lan la Yàlla def Enog ndax loolu (Njàl. 5:22) ?
Jàngal Yudd 14, 15.
Tey, bu karceen yi di yégle xeexu Armagedon bi di am ëllëg, naka lañu mënee roy fit bi Enog amoon (2 Tim. 4:2 ; Yaw. 13:6) ?
Nettali 8
Ay ponkal yu réy ci kow suuf si
Lan moo xew bi ay malaaka toppee Seytaane ?
Lu tax ay malaaka bàyyi li ñu doon def ci asamaan te ñów ci kow suuf ?
Lu tax malaaka yi waruñu woon a nów ci kow suuf te sol yaramu nit ?
Doomi malaaka yi, lu ñu wuute woon ak yeneen xale yi ?
Lan la doomi malaaka yi def bi ñu màggee ba nekk ponkal yu réy ? (Xoolal li ñuy wone foofu.)
Ban nit ku baax moo nekkoon ci kow suuf ginnaaw bi Enog gaañoo, te lu tax Yàlla bëgg nit kooku ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 6:1-8.
Naka la Njàlbéen ga 6:6 wonee ne li ñuy def dafay laal Yexowa (Ps. 78:40, 41 ; Prov. 27:11) ?
Jàngal Yudd 6.
Lan lañu mën a jàng tey ci malaaka yi bañoon a toog seen palaas ca jamano Nóoyin (1 Kor. 3:5-9 ; 2 Piy. 2:4, 9, 10) ?
Nettali 9
Nóoyin dafay defar gaal gu mag
Njabootu Nóoyin, ñaata nit lañu woon, te ñetti doomam yu góor, naka lañu tuddoon ?
Yàlla sant na Nóoyin lu doy waar. Loolu lan la, te lu tax mu sant ko loolu ?
Lan la nit ñi def bi leen Nóoyin waxee li taxoon mu tabax gaal gi ?
Lan la Yàlla wax Nóoyin mu def ak mala yi ?
Bi Yàlla tëjee buntu gaal gi ba pare, lan la Nóoyin ak njabootam waroon a def ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 6:9-22.
Lu tax nu mën a wax ne Nóoyin dafa doon jaamu Yàlla ci fasoŋ bu rafet lool (Njàl. 6:9, 22) ?
Naka la Yexowa di gise ñi bëgg xeex, te bu ñu bokkee gis-gis ak moom ci loolu, naka lañuy tànne film yi ak yeneen yu mel noonu yu ñu bëgg a def ngir féexal suñu xol (Njàl. 6:11, 12 ; Ps. 11:5) ?
Naka lañu mënee roy Nóoyin bu ñu mbootaayu Yexowa wonee li ñu war a def (Njàl. 6:22 ; 1 Ywna. 5:3) ?
Jàngal Njàlbéen ga 7:1-9.
Nóoyin matul woon, waaye ba tey Yàlla dafa ko jàppe woon ni ku jub. Lu tax loolu neex a dégg tey (Njàl. 7:1 ; Prov. 10:16 ; Is. 26:7) ?
Nettali 10
Taw bu metti ci kow suuf si sépp
Bi taw bi komaasee, lu tax kenn mënatuloon a dugg ci biir gaal gi ?
Ñaata bëccëg ak ñaata guddi la Yàlla def mu taw, te fan la ndox mi tollu woon ?
Lan la gaal gi def bi ndox mi komaasee muur suuf si ?
Ndax ponkal yu réy yi mucc nañu, te lan moo dal seeni baay ?
Lu xewoon ak gaal gi bi juróomi weer paasee ?
Lu tax Nóoyin yebal benn baaxoñ ci biti gaal gi ?
Naka la Nóoyin xame ne suuf si wow na léegi ?
Lan la Yàlla wax Nóoyin bi moom ak njabootam defee lu ëpp benn at ci biir gaal gi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 7:10-24.
Li Yàlla alag ci kow suuf si, ba fan la tollu (Njàl. 7:23) ?
Ñaata fan la ndox mi def bala mu wàcc ba jeex (Njàl. 7:24) ?
Jàngal Njàlbéen ga 8:1-17.
Naka la Njàlbéen ga 8:17 wonee ne Yexowa soppiwul li mu bëggoon lu jëm ci suuf si (Njàl. 1:22) ?
Jàngal 1 Piyeer 3:19, 20.
Malaaka yi bàyyi woon Yàlla, bi ñu delloo asamaan, lan moo leen dal (Yudd 6) ?
Li ñu nettali ci Nóoyin ak njabootam, naka la ñu loolu dimbalee ba mu gën ñu wóor ne Yexowa mën na muccal nitam yi (2 Piy. 2:9) ?
Nettali 11
Xon gu jëkk gi
Ni ñu ko wonee fii, lan la Nóoyin jëkk a def bi mu génnee gaal gi ?
Ban ndigal la Yàlla jox Nóoyin ak njabootam ginnaaw bi taw bu metti bi amee ?
Lan la Yàlla dig nit ñi ?
Lan lañu war a fàttaliku bu ñuy gis xon gi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 8:18-22.
Lan lañu mën a def tey ba “ xet gu neex ” yéeg ba ca Yexowa (Njàl. 8:21 ; Yaw. 13:15, 16) ?
Lan la Yexowa wax lu jëm ci xolu doom-Aadama yi, te ndegam loolu la, lan lañu war a moytu (Njàl. 8:21 ; Macë 15:18, 19) ?
Jàngal Njàlbéen ga 9:9-17.
Ban kóllëre la Yexowa fas ak lépp luy dund ci kow suuf (Njàl. 9:10, 11) ?
Kóllëre gi jëm ci xon gi, ba kañ la war a yàgg (Njàl. 9:16) ?
Nettali 12
Ñu ngi tabax lu kowe lool
Namróot, kan la woon, te lan la Yàlla doon xalaat ci moom ?
Ni ñu ko wonee foofu, lu tax nit ñi di def ay muul ?
Lu tax tabax boobu neexul woon Yexowa ?
Lan la Yàlla def ba nit ñooñu bàyyi li ñu doon tabax ?
Naka lañu tudde dëkk boobu, te tur boobu, lu mu tekki ?
Bi Yàlla jaxasee seeni làkk ba pare, lan la nit ñooñu def ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 10:1, 8-10.
Ban jikko la Namróot wone, te ndegam loolu la, lan lañu war a moytu ñun (Prov. 3:31) ?
Jàngal Njàlbéen ga 11:1-9.
Lu tax nit ñooñu bëggoon a tabax taax bu kowe boobu, te loolu lu tax mënul woon a sotti (Njàl. 11:4 ; Prov. 16:18 ; Ywna. 5:44) ?
Nettali 13
Ibraayma, xaritu Yàlla
Yan nit ñoo dëkkoon ci dëkku Ur ?
Kan lañuy wone foofu, kañ la juddu, te fan la dëkkoon ?
Lan la Yàlla sant Ibraayma ?
Lu tax ñu woowe Ibraayma xaritu Yàlla ?
Ñan ñoo àndoon ak Ibraayma bi mu génnee Ur ?
Lan la Yàlla wax Ibraayma bi mu àggee Kanaan ?
Lan la Yàlla dig Ibraayma bi mu amee 99 at ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 11:27-32.
Ibraayma ak Lóot, lan lañu bokkoon (Njàl. 11:27) ?
Dañu ne Teraa moo yóbbu njabootam Kanaan, waaye naka lañu xame ne Ibraayma moo taxoon toxu boobu am, te lu tax Ibraayma def loolu (Njàl. 11:31 ; Jëf. 7:2-4) ?
Jàngal Njàlbéen ga 12:1-7.
Bi Ibraayma àggee Kanaan, lan la Yexowa yokk ci kóllëre gi mu fasoon ak moom (Njàl. 12:7) ?
Jàngal Njàlbéen ga 17:1-8, 15-17.
Ban tur bu bees la Yàlla jox Ibraam bi mu amee 99 at, te lu tax mu jox ko tur boobu (Njàl. 17:5) ?
Yan barke la Yexowa dig Saraata (Njàl. 17:15, 16) ?
Jàngal Njàlbéen ga 18:9-19.
Ban warugaru baay lañuy wone ci Njàlbéen ga 18:19 (Deut. 6:6, 7 ; Efes 6:4) ?
Lu xewoon ak Saraata te muy wone ne mënuñu nëbb dara Yexowa (Njàl. 18:12, 15 ; Ps. 44:21) ?
Nettali 14
Yàlla mu ngi natt ngëmu Ibraayma
Lan la Yàlla digoon Ibraayma, te naka la ko defe ?
Ni ñu ko wonee foofu, naka la Yàlla natte ngëmu Ibraayma ?
Lan la Ibraayma def, fekk xamul woon dëgg-dëgg lu tax Yàlla laaj ko loolu ?
Lan moo xew bi Ibraayma jëlee paakaam ngir rey doomam ?
Lan lañu mën a wax ci ngëm gi Ibraayma amoon ci Yàlla ?
Lan la Yàlla jox Ibraayma pur mu saraxe ko, te naka la ko ko joxe ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 21:1-7.
Lu tax Ibraayma jongal doomam bi mu amee juróom-ñetti fan (Njàl. 17:10-12 ; 21:4) ?
Jàngal Njàlbéen ga 22:1-18.
Naka la Isaaxa wonee ne, moom dafay déggal baayam Ibraayma, te loolu lan la doon wone lu jëm ci lu naroon a am ëllëg, fekk lu gën a réy lay doon (Njàl. 22:7-9 ; 1 Kor. 5:7 ; Fil. 2:8, 9) ?
Nettali 15
Jabaru Lóot geestu na
Lu tax Ibraayma ak Lóot tàggoo ?
Lu tax Lóot tànn Sodom ngir dëkk fa ?
Waa Sodom, nu ñu meloon ?
Lan la ñaari malaaka yëgal Lóot ?
Lu tax jabaru Lóot soppaliku xorom ?
Lan lañu mën a jàng ci li dal jabaru Lóot ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 13:5-13.
Lan lañu mën a jàng ci Ibraayma lu jëm ci bu poroblem amee diggante ñaari nit (Njàl. 13:8, 9 ; Room. 12:10 ; Fil. 2:3, 4) ?
Jàngal Njàlbéen ga 18:20-33.
Bu ñu gisee ni Yexowa doon def ak Ibraayma, lu tax mu mën ñu wóor ne àtte bu jub la Yexowa ak Yeesu di def (Njàl. 18:25, 26 ; Macë 25:31-33) ?
Jàngal Njàlbéen ga 19:1-29.
Li Biibël bi di nettali fii, lan lay wone ci ni Yàlla di gise góor-jigéen (Njàl. 19:5, 13 ; Lév. 20:13) ?
Am na lu wuute diggante ni Ibraayma déggale Yàlla ak ni ko Lóot defe woon. Loolu lan la te lu ñu ci mën a jàng (Njàl. 19:15, 16, 19, 20 ; 22:3) ?
Jàngal Luug 17:28-32.
Naka la jabaru Lóot doon gise alal, te bu ñu xamee loolu, lan lañuy moytu (Luug 12:15 ; 17:31, 32 ; Macë 6:19-21, 25) ?
Jàngal 2 Piyeer 2:6-8.
Bu ñu bëggee roy Lóot, lan lañu war a yëg ci suñu xol bu ñu gisee li waa àddina su bon sii di def (Ezék. 9:4 ; 1 Ywna. 2:15-17) ?
Nettali 16
Isaaxa takk na jabar ju baax
Góor gi ak jigéen bi nekk fii, ñan lañu ?
Lan la Ibraayma def ngir wutal doomam jabar, te lu tax mu def loolu ?
Naka la surga Ibraayma ame li mu doon ñaan Yàlla ?
Lan la Rebeka wax bi ñu ko laajee ndax dina bëgg a séy ak Isaaxa ?
Lu tax xolu Isaaxa seddaat ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 24:1-67.
Ban jikko ju rafet la Rebeka wone bi mu fekkee surga Ibraayma ca teen ba (Njàl. 24:17-20 ; Prov. 31:17, 31) ?
Bu ñu gisee ni Ibraayma wutale doomam jabar, lan la karceen yi tey war a roy ci moom (Njàl. 24:37, 38 ; 1 Kor. 7:39 ; 2 Kor. 6:14) ?
Lu tax ñu war a jël jot ngir xalaat, ni ko Isaaxa defe woon (Njàl. 24:63 ; Ps. 77:12 ; Fil. 4:8) ?
Nettali 17
Ñaari séex yu wuute
Ñan ñoo doon Esawu ak Yanqóoba, te fan lañu wuute woon ?
Ñaata at la Esawu ak Yanqóoba amoon bi seen maam Ibraayma gaañoo ?
Lan la Esawu def te mu naqari lool baayam ak yaayam ?
Lu tax Esawu mere rakkam Yanqóoba lool ?
Lan la Isaaxa digal doomam Yanqóoba ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 25:5-11, 20-34.
Jàngal Njàlbéen ga 26:34, 35 ; 27:1-46 ak 28:1-5.
Naka la Esawu wonee ci lu leer ne li jëm ci wàllu ngëm soxalu ko (Njàl. 26:34, 35; 27:46) ?
o (Njàl. 28:1-4) ?
Jàngal Yawut ya 12:16, 17.
Li daloon Esawu, lan lay wone ci liy dal ñi fonkul mbirum Yàlla ?
Nettali 18
Yanqóoba dem na Karan
Jigéen bi nekk fii, kan la te lan la ko Yanqóoba defal ?
Lan la Yanqóoba nangu def ngir mën a takk Rasel ?
Lan la Laban def bi séyu Yanqóoba ak Rasel jotee ?
Lan la Yanqóoba nangu def ngir Rasel mën a nekk jabaram ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 29:1-30.
Laban dafa nax Yanqóoba. Waaye ba tey naka la Yanqóoba wonee ne nit ku jar a weg la te lan lañu mën a jàng ci loolu (Njàl. 25:27 ; 29:26-28 ; Macë 5:37) ?
Bu ñu ko seetee ci Yanqóoba, mbëggeel dëgg lu mu wuute ak bëgg am jigéen doŋŋ (Njàl. 29:18, 20, 30 ; Chant de S. 8:6) ?
Am na ñeenti jigéen yu mujj a bokk ci waa këru Yanqóoba te ginnaaw loolu am nañu ak moom doom yu góor. Ñan ñooy jigéen ñooñu (Njàl. 29:23, 24, 28, 29) ?
Nettali 19
Yanqóoba am na doom yu bare
Juróom-benni doom yu góor yi Yanqóoba amoon ak jabaram bu jëkk bi tudd Leya, naka lañu tudd ?
Surga Leya bi tudd Silpa, ñaari doom yu góor yi mu amoon ak Yanqóoba, naka lañu tudd ?
Surga Rasel bi tudd Bilaa, ñaari doom yu góor yi mu amoon ak Yanqóoba, naka lañu tudd ?
Yan ñaari doom yu góor la Rasel am, waaye lan moo xew bi ñaareel bi juddoo ?
Ni ñu ko wonee foofu, ñaata doom yu góor la Yanqóoba amoon, te ban mbooloo moo jóge ci ñoom ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 29:32-35 ; 30:1-26 ak 35:16-19.
Ni ñu ko gise ci ni ñu tuddee 12 doomi Yanqóoba, naka la Yawut yi doon tudde lée-lée seen doom yu góor yi ca jamano yu jëkk ya ?
Jàngal Njàlbéen ga 37:35.
Ci doomu Yanqóoba yi Biibël bi tudd, Diina rekk moo ci nekk jigéen. Waaye naka lañu xame ne Yanqóoba amoon na yeneen doom yu jigéen (Njàl. 37:34, 35) ?
Nettali 20
Diina am na poroblem
Lu tax Ibraayma ak Isaaxa bëgguñu woon seeni doom séy ak waa Kanaan ?
Diina dafa doon xaritoo ak jigéeni Kanaan. Ndax Yanqóoba dàkkooroon na ci loolu ?
Ki nekk fii di xool Diina, kan la, te lan la def lu bon ?
Doomu baayu Diina yi tudd Simeyon ak Lewi, lan lañu def bi ñu déggee li xewoon ?
Ndax Yanqóoba àndoon na ak li Simeyon ak Lewi def ?
Poroblem yi njaboot gi amoon yépp, fan lañu komaasee ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 34:1-31.
Ndax benn yoon rekk la Diina dem seeti jigéenu Kanaan yi ? Waxal lu tax nga tontu loolu (Njàl. 34:1).
Lu tax ñu mën a wax ne Diina am na wàll ci li tax mu bañ a nekkati janq léegi (Gal. 6:7) ?
Naka la ndaw yi tey mënee wone ne bëgguñu def ni Diina (Prov. 13:20 ; 1 Kor. 15:33 ; 1 Ywna. 5:19) ?
Nettali 21
Magi Yuusufa dañu ko bañ
Magi Yuusufa, lan lañu ko iñaane woon, te lan lañu def ?
Magi Yuusufa, lan lañu ko bëgg a def, waaye lan la Ruben wax ?
Lan moo xew bi ay jaaykat yi nekkoon Ismayléen ñówee ?
Lan la magi Yuusufa def ngir seen baay foog ne Yuusufa dee na ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 37:1-35.
Bu karceen xamee bàkkaar bu kenn def ci mbooloo mi, naka lay roye Yuusufa bu ko xamalee mbooloo mi (Njàl. 37:2 ; Lév. 5:1 ; 1 Kor. 1:11) ?
Lan moo tax magi Yuusufa dem ba def ko lu ñaaw (Njàl. 37:11, 18 ; Prov. 27:4 ; Saag 3:14-16) ?
Lan la Yanqóoba def te mu baax ci képp ku xolam jeex (Njàl. 37:35) ?
Nettali 22
Tëj nañu Yuusufa kaso
Ñaata at la Yuusufa amoon bi ñu ko yóbboo Misra, te lan lañu ko def foofu ?
Lu tax ñu dugal Yuusufa kaso ?
Ban liggéey lañu dénk Yuusufa ci kaso bi ?
Ci kaso bi, lan la Yuusufa defal ki doon jox Firawna mu naan ak ki ko doon defaral mburu ?
Ki doon jox Firawna mu naan, ginnaaw bi mu génnee kaso, lan moo xew ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 39:1-23.
Ca jamano Yuusufa, amul woon fu ñu mën a jàng ndigalu Yàlla buy tere njaaloo. Kon, lu tax Yuusufa daw jabaru Potifaar (Njàl. 2:24 ; 20:3 ; 39:9) ?
Jàngal Njàlbéen ga 40:1-23.
Ki doon jox Firawna mu naan, waxal ci lu gàtt li mu gént ak li gént googu tekki ni ko Yexowa waxe Yuusufa (Njàl. 40:9-13) ?
Ki doon defaral Firawna mburu, lan la gént te gént googu lu mu tekki woon (Njàl. 40:16-19) ?
Mbooloo mi nekk surga bu takku te teey bi, naka la roye Yuusufa tey (Njàl. 40:8 ; Ps. 36:9 ; Ywna. 17:17 ; Jëf ya 17:2, 3) ?
Naka la Njàlbéen ga 40:20 leerale ni karceen war a gise màggal bés bi nit juddu (Eccl. 7:1; Màrk 6:21-28) ?
Nettali 23
Firawna mu ngiy gént
Lan moo dal Firawna benn guddi ?
Lan moo tax ki doon jox Firawna mu naan mujj a fàttaliku Yuusufa ?
Ni ñu ko wonee foofu, lan la Firawna gis ci ñaari géntam ?
Ci li Yuusufa wax, gént yooyu, lu ñu tekki ?
Naka la Yuusufa deme ba nekk ki topp ci Firawna ci réew mi ?
Lu tax magi Yuusufa ñów Misra, te lu tax xàmmewuñu ko ?
Ban gént la Yuusufa fàttaliku, te lan la ko loolu xamal ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 41:1-57.
Lan la Yuusufa wax ngir nit ñi xalaat ci Yexowa, te naka la ko karceen yi tey mënee roy (Njàl. 41:16, 25, 28 ; Macë 5:16 ; 1 Piy. 2:12) ?
At yi bare woon lekk ci Misra ak at yi amul woon lekk, naka lañu misaale li ñu am ci mbooloo Yexowa ci wàllu ngëm ak li nit ñi di am ci wàllu ngëm ci diine yiy wuyoo turu Kirist fekk toppuñu ko dëgg (Njàl. 41:29, 30 ; Amos 8:11, 12) ?
Jàngal Njàlbéen ga 42:1-8 ak 50:20.
Xéyna ci sa réew, dañu faral di sukk ci kanamu nit ngir may ko cér. Ndax jaamukatu Yexowa mën na def loolu (Njàl. 42:6) ?
Nettali 24
Yuusufa mu ngi teg nattu ci kow magam yi
Lu tax Yuusufa wax magam yi ne dañu ñów pur seet fu réew mi néewe doole ?
Lu tax Yanqóoba bàyyi caatam bu góor, Ben-yamin, mu dem Misra ?
Naka la kaasu xaalis bi Yuusufa moomoom dugge ci saagu Ben-yamin ?
Lan la Yuda bëggoon a def ngir ñu bàyyi Ben-yamin dem ?
Lu tax ñu mën a wax ne magi Yuusufa soppeeku woon nañu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 42:9-38.
Lu tax ñi nu dénk liggéey ci mbootaayu Yexowa tey waruñu fàtte li Yuusufa wax ci Njàlbéen ga 42:18 (Neh. 5:15 ; 2 Kor. 7:1, 2) ?
Jàngal Njàlbéen ga 43:1-34.
Ruben moo nekkoon taaw ci doomi Yanqóoba, waaye ba tey lu tax ñu mën a wax ne Yuda moo nekkoon ki doon wax ci turu ñépp (Njàl. 43:3, 8, 9 ; 44:14, 18 ; 1 Chron. 5:2) ?
Lan la Yuusufa def bi mu doon jox lekk doomi baayam, te ci li ñu mën a foog lu tax mu def loolu (Njàl. 43:33, 34) ?
Jàngal Njàlbéen ga 44:1-34.
Lan la Yuusufa wax ci moom ngir magam yi bañ a xam ki mu doon (Njàl. 44:5, 15 ; Lév. 19 :26) ?
Naka la magi Yuusufa wonee ne iñaan bi ñu amoon ci moom deñ na léegi (Njàl. 44:13, 33, 34) ?
Nettali 25
Yanqóoba ak waa këram ñu ngi toxu Misra
Lan moo xew bi Yuusufa waxee magam yi ki mu doon ?
Yan wax yu neex la Yuusufa wax magam yi ?
Lan la Firawna wax bi mu déggee ne magi Yuusufa ñu ngi Misra ?
Ñaata nit ñoo bokkoon ci njabootu Yanqóoba bi ñu toxoo Misra ?
Naka lañu mujj a woowe ñi bokkoon ci njabootu Yuusufa, te lu tax ñu di leen woowe noonu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njàlbéen ga 45:1-28.
Li Biibël bi nettali ci Yuusufa, naka lay wonee ne Yàlla mën na walbati lu bon lu ñuy yéene jaamam yi ba mu nekk lu baax ci ñoom (Njàl. 45:5-8 ; Is. 8:10; Fil. 1:12-14) ?
Jàngal Njàlbéen ga 46:1-27.
Lan la Yexowa dig Yanqóoba bi mu doon dem Misra (Njàl. 46:1-4) ?
Nettali 26
Ayóoba bàyyiwul Yàlla
Kan moo doon Ayóoba ?
Lan la Seytaane jéem a def, waaye ndax mujj na am li mu bëggoon ?
Lan la Yexowa bàyyi Seytaane mu def, te lu tax Yexowa def loolu ?
Lu tax jabaru Ayóoba ne ko ‘ waxal lu bon ci Yàlla te dee ’ ? (Xoolal li ñuy wone foofu.)
Boo xoolee li ñuy wone foofu ci suuf, naka la Yexowa barkeele Ayóoba, te lu tax mu def loolu ?
Bu ñu toppee Yexowa ni ko Ayóoba doon defe, yan barke lañuy am ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Job 1:1-22.
Tey, naka la karceen mënee roy ci Ayóoba (Job 1:1 ; Fil. 2:15 ; 2 Piy. 3:14) ?
Jàngal Job 2:1-13.
Ayóoba ak jabaram bokkuñu ni ñu gise woon li leen Seytaane doon def. Naka lañu wuute woon gis-gis (Job 2:9, 10 ; Prov. 19:3 ; Mika 7:7 ; Mal. 3:14) ?
Jàngal Job 42:10-17.
Naka lañu mënee méngale barke yi Ayóoba amoon ak yi Yeesu am ndax li ñu kontine di topp Yàlla (Job 42:12 ; Fil. 2:9-11) ?
Bu ñu gisee barke yi Ayóoba amoon ndax li mu kontine di topp Yàlla, naka la loolu di ñu xiire ñun it ci kontine di topp Yàlla (Job 42:10, 12 ; Yaw. 6:10 ; Saag 1:2-4, 12 ; 5:11) ?
Nettali 27
Buur bu bon mooy ilif Misra
Xoolal li ñuy wone foofu. Kii di dóor keneen ki, kan la, te ki muy dóor, kan la ?
Bi Yuusufa gaañoo, lan moo dal waa Israyil yi ?
Lu tax waa Misra komaase di ragal waa Israyil ?
Ban ndigal la Firawna jox jigéen yi doon dimbali jigéenu Israyil ñu wasin ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi 1:6-22.
Naka la Yexowa komaasee di def li mu digoon Ibraayma (Gàdd. 1:7 ; Njàl. 12:2 ; Jëf. 7:17) ?
Jigéenu Yawut yi doon dimbali yeneen jigéen yi ñu wasin, naka lañu wonee ne dañu fonk bakkanu nit (Gàdd. 1:17 ; Njàl. 9:6) ?
Lan la Yexowa defal jigéen yooyu ndax seen ragal Yàlla (Gàdd. 1:20, 21 ; Prov. 19:17) ?
Lan la Seytaane def ngir jéem a yàq li Yexowa bëgg lu jëm ci askan wi mu digoon Ibraayma (Gàdd. 1:22 ; Macë 2:16) ?
Nettali 28
Naka la Musaa rëcce bi mu nekkee liir
Liir bi ñuy wone foofu, kan la, te loxo bi mu jàpp noonu, loxo kan la ?
Lan la yaayu Musaa def ngir ñu bañ koo rey ?
Xale bu jigéen bi nekk foofu, kan la, te lan la def ?
Bi doomu Firawna bu jigéen bi gisee liir bi, lan la ko Miryam wax ?
Lan la doomu Firawna wax yaayu Musaa ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi 2:1-10.
Lan moo may yaayu Musaa mu mën a yar te jàngal Musaa bi mu nekkee xale bu ndaw, te naka la ko waajur yi tey mënee roy (Gàdd. 2:9, 10 ; Deut. 6:6-9 ; Prov. 22:6 ; Efes 6:4 ; 2 Tim. 3:15) ?
Nettali 29
Li tax Musaa daw
Fan la Musaa màgge, waaye lan la xamoon lu jëm ci waajuram yi ?
Lan la Musaa def bi mu amee 40 at ?
Lan la Musaa wax waayu Israyil bi doon xeex, te lan la ko kooku tontu ?
Lu tax Musaa daw Misra ?
Bi Musaa dawee, fan la dem te kan la taseel foofu ?
Lan la Musaa doon def ci 40 at ginnaaw bi mu génnee Misra ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi 2:11-25.
Musaa jàng na ay at yu bare lépp lu jëm ci xam-xamu waa Misra yi. Waaye naka la wonee ne Yexowa la gëm, wone it ne fàttewul ne ci mbooloo Israyil la bokk (Gàdd. 2:11, 12 ; Yaw. 11:24) ?
Jàngal Jëf ya 7:22-29.
Lan lañu mën a jàng ci li Musaa jéem a def ngir muccal mbooloo Israyil ci waa Misra yi ak kàttanu boppam (Jëf. 7:23-25 ; 1 Piy. 5:6, 10) ?
Nettali 30
Garab gi doon tàkk
Montaañ bi ñuy wone foofu, naka la tudd ?
Waxal lu doy waar li Musaa gis bi mu doon sàmm xaram yi ci montaañ bi.
Lan la baat bu jóge woon ci garab gi doon tàkk wax, te baatu kan la woon ?
Lan la Musaa wax bi ko Yàlla waxee ne dina génne mbooloom Misra ?
Lan la Yàlla wax Musaa mu tontu bu ko waa Israyil laajee kan moo ko yónni ?
Yan kéemaan la Musaa waroon a def ngir ñu xam ne Yàlla moo ko yónni ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi 3:1-22.
Bu ñu gisee li xewoon ak Musaa, lu tax mu mën ñu wóor ne Yexowa dina ñu jàpple ci liggéey bu mu ñu dénk, bu dee sax yaakaaruñu ne dinañu ko mën a def (Gàdd. 3:11, 13 ; 2 Kor. 3:5, 6) ?
Jàngal Gàddaay gi 4:1-20.
Lan moo soppeeku woon ci jikko Musaa ci 40 at yi mu def ci Majan, te ñi bëgg ñu dénk leen liggéey ci mbooloo mi, lan lañu ci mën a jàng (Gàdd. 2:11, 12 ; 4:10, 13 ; Mika 6:8 ; 1 Tim. 3:1, 6, 10) ?
Bu Yexowa jaaree ci mbooloom ngir yar ñu te ñu seet ni mu defe woon ak Musaa, lan moo ñu mën a wóor (Gàdd. 4:12-14 ; Ps. 103:14 ; Yaw. 12:4-11) ?
Nettali 31
Musaa ak Aaroona ñu ngi ci Firawna
Kéemaan yi Musaa ak Aaroona def, lan lañu def ci waa Israyil yi ?
Lan la Musaa ak Aaroona wax Firawna, te lan la leen Firawna tontu ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan moo xew bi Aaroona sànnee yetam ci suuf ?
Lan la Yexowa def ngir jàngal Firawna lu am solo, te bi loolu amee, lan la Firawna def ?
Ginnaaw fukkeelu musiba bi amoon, lan moo xew ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi 4:27-31 ak 5:1-23.
Lan la Firawna bëggoon a wax bi mu waxee ne xamul Yexowa (Gàdd. 5:2 ; 1 Sam. 2:12 ; Room 1:21) ?
Jàngal Gàddaay gi (Exode) 6:1-13, 26-30.
Bi Yexowa waxee ne xamalul boppam Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba, lan la bëggoon a wax (Gàdd. 3:13, 14 ; 6:3 ; Njàl. 12:8) ?
Gis nañu ne Yexowa dafa dénk liggéey Musaa, fekk Musaa foogul woon ne dina ko mën a def. Bu ñu gisee loolu, lan lañuy yëg ci suñu xol (Gàdd. [Ex.] 6:12, 30 ; Luug 21:13-15) ?
Jàngal Gàddaay gi 7:1-13.
Musaa ak Aaroona jottali nañu Firawna ay waxu àtte yu jóge woon ci Yexowa, te loolu dañu ko def ak fit. Naka la loolu di nekke royukaay ngir ñiy jaamu Yàlla tey (Gàdd. 7:2, 3, 6 ; Jëf. 4:29-31) ?
Naka la Yexowa wonee ne moo ëpp kàttan fuuf yàllay Misra yi (Gàdd. 7:12 ; 1 Chron. 29:12) ?
Nettali 32
Fukki musiba yi
Xoolal li ñuy wone foofu te waxal ñetti musiba yi Yexowa jëkk a wàcce ci Misra.
Ñetti musiba yooyu, lu ñu wuute ak yi ci des ?
Lan moo xewoon ci ñeenteel, juróomeel ak juróom-benneelu musiba yi ?
Waxal li xewoon ci musiba juróom-ñaar, juróom-ñett ak juróom-ñeent.
Lan la Yexowa wax waa Israyil ñu def bala fukkeelu musiba bi am ?
Lu xewoon ci fukkeelu musiba bi, te lan moo xewoon ginnaaw musiba boobu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi (Exode) 7:19–8:23.
Luxuskati Misra mënoon nañu defaat ak seen kàttan li xewoon ci ñaari musiba yu jëkk yi. Waaye ñetteelu musiba bi, lan la leen forse ñu nangu (Gàdd. [Ex.] 8:18, 19 ; Macë 12:24-28) ?
Ñeenteelu musiba bi, naka lay wonee ne Yexowa mën na aar mbooloom ? Te xam loolu, lu muy def ci mbooloo Yàlla bi nga xam ne léegi mu war a jaar ci “ metit wu réy ” wi (Gàdd. [Ex.] 8:22, 23 ; Peeñ. 7:13, 14 ; 2 Chron. 16:9) ?
Jàngal Gàddaay gi (Exode) 8:24 ; 9:3, 6, 10, 11, 14, 16, 23-25 ak 10:13-15, 21-23.
Yan ñaari gurupu nit ñoo feeñ bi fukki musiba yi amee, te loolu lu mu jote ak ni ñu war a gise ñaari gurup yooyu tey (Gàdd. [Ex.] 8:10, 18, 19 ; 9:14) ?
Li nekk ci Exode 9:16, naka la ñuy dimbalee ñu xam lu tax Yexowa bàyyi Seytaane mu dund ba tey (Room 9:21, 22) ?
Jàngal Gàddaay gi 12:21-32.
Naka la Jéggi bi taxe woon ñu bare mucc, te lan la doon misaal (Gàdd. 12:21-23 ; Ywna. 1:29 ; Room 5:18, 19, 21 ; 1 Kor. 5:7) ?
Nettali 33
Ñu ngi jéggi Géej gu xonq gi
Ñaata waa Israyil, bañ ci boole jigéen yi ak xale yi, ñoo jóge Misra, te ñan ñoo àndoon ak ñoom ?
Lan la Firawna yëg ci xolam bi mu bàyyee waa Israyil dem ba pare, te lan la def ?
Lan la Yexowa def ngir tere waa Misra ñu song mbooloom ?
Lan moo xew bi Musaa tàllalee yetam ci kow Géej gu xonq gi, te lan la waa Israyil def ?
Lan moo xew bi waa Misra duggee ci biir géej gi ngir jàpp waa Israyil ?
Bi waa Israyil muccee ba pare, naka lañu wonee seen mbégte ak ngërëm bi ñu amoon ci Yexowa ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi 12:33-36.
Lan la Yexowa def ngir ñu fey mbooloom ndax liggéey bi ñu defoon ci Misra ci at yu bare yi ñu fa nekkoon jaam (Gàdd. 3:21, 22 ; 12:35, 36) ?
Jàngal Gàddaay gi 14:1-31.
Li Musaa wax ci Gàddaay gi 14:13 ak 14, lan lay def ci jaamu Yexowa yi tey bu ñuy séentu xeexu Armagedon (2 Chron. 20:17 ; Sab. 91:8) ?
Jàngal Gàddaay gi (Exode) 15:1-8, 20, 21.
Lu tax ñiy jaamu Yexowa war a woy ay woy yu koy màggal (Gàdd. 15:1, 2 ; Ps. 105:2, 3 ; Peeñ. 15:3, 4) ?
Ci lu jëm ci màggal Yexowa, naka la karceen yu jigéen yi tey mënee roy Miryam ak yeneen jigéen yi bi ñu nekkee ci Géej gu xonq gi (Ex. 15:20, 21 ; Ps. 68:11) ?
Nettali 34
Lekk bu bees
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan la nit ñi di for, te loolu naka lañu koy woowe ?
Lan la Musaa wax mbooloo mi ci li ñu war a for ci mànn bi ?
Lan la Yexowa wax mbooloo mi mu def ci juróom-benneelu fan bi, te lu tax mu wax loolu ?
Ban kéemaan la Yexowa doon def bi ñu doon denc mànn boobu ci juróom-ñaareelu fan bi ?
Ci yan at la Yexowa dundal mbooloo mi ak mànn bi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi (Exode) 16:1-36 ak Nombres 11:7-9.
Li ñu wax ci Gàddaay gi 16:8, lan lay wone lu jëm ci lu tax ñu war a déggal góor ñi Yàlla tànn ngir def yenn liggéey ci mbooloo karceen yi (Yaw. 13:17) ?
Bi ñu nekkoon ci màndiŋ mi, lan moo doon fàttali waa Israyil ne seen bakkan mu ngi aju ci Yexowa bés bu ne (Gàdd. 16:14-16, 35 ; Deut. 8:2, 3) ?
Ci li Yeesu wax, mànn boobu lu mu doon wone lu jëm ci ëllëg, te ñun, ban njariñ lañuy am ci “ ñam wu wàcce ca asamaan ” ? (Ywna. 6:31-35, 40.)
Jàngal Josué 5:10-12.
Ñaata at la waa Israyil lekk mànn bi ? Loolu, naka la nekke woon nattu ci ñoom ? Lan lañu mën a jàng ci nettali boobu (Gàdd. 16:35 ; Nomb. 11:4-6 ; 1 Kor. 10:10, 11) ?
Nettali 35
Yexowa joxe na ndigalam yi
Lu tollu ak ñaari weer ginnaaw bi waa Israyil génnee Misra, fan la waa Israyil toog ?
Lan la Yexowa wax mbooloom lu jëm ci li mu bëgg ñu def, te lan lañu ci tontu ?
Lu tax Yexowa jox Musaa ñaari xeer ?
Yan ndigal la Yexowa yokk ci Fukki Ndigal yi mu jox waa Israyil ?
Yan ñooy ñaari ndigal yi Yeesu Kirist wax ne ñoo ëpp solo ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi (Exode) 19:1-25 ; 20:1-21 ; 24:12-18 ak 31:18.
Lan la Gàddaay gi 19:8 di ñu jàngal ci li jébbal sa bopp Yàlla ci diine karceen ëmb (Macë 16:24 ; 1 Piy. 4:1-3) ?
Jàngal Deutéronome 6:4-6 ; Lévitique 19:18 ak Macë 22:36-40.
Naka la karceen yi wonee mbëggeel bi ñu am ci Yàlla ak ci seeni moroom (Màrk 6:34 ; Jëf. 4:20 ; Room 15:2) ?
Nettali 36
Nag bi ñu defare wurus
Xoolal li ñuy wone foofu.Lan la nit ñi di def, te lu tax ñuy def loolu ?
Lu tax Yexowa mer, te lan la Musaa def bi mu gisee li mbooloo mi doon def ?
Lan la Musaa wax ay góor pur ñu def ko ?
Lan lañu war a jàpp ci nettali boobu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Gàddaay gi 32:1-35.
Naka la nettali bii di wone li Yexowa xalaat ci boole diine yu dul dëgg ak diine dëgg ji (Gàdd. 32:4-6, 10 ; 1 Kor. 10:7, 11) ?
Lan la karceen war a moytu buy tànn luy féexal xolam, mel ni bu bëggee woy walla fecc (Gàdd. 32:18, 19 ; Efes 5:15, 16 ; 1 Ywna. 2:15-17) ?
Naka la giiru Lewi nekke royukaay bu rafet ci lu jëm ci def lu jub (Gàdd. 32:25-28 ; Sab. [Ps.] 18:25) ?
Nettali 37
Tànt fi ñuy jaamoo Yàlla
Tabax bi ñuy wone foofu, naka lañu koy woowe, te lan mooy njariñam ?
Lu tax Yexowa wax Musaa mu defar tànt bi ci fasoŋ bu yomb a yóbbu feneen ?
Lan mooy kees bi nekk ci néeg bu ndaw bi, te lan moo nekk ci biir ?
Kan la Yexowa tànn ngir mu nekk saraxalekat bu mag bi, te lan mooy liggéeyam ?
Waxal ñetti yëf yi nekk ci néeg bu mag bi ci tànt bi.
Yan ñaari yëf ñoo nekk ci ëttu tànt bi, te lan mooy seen njariñ ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Exode 25:8-40 ; 26:1-37 ; 27:1-8 ak 28:1.
Seruben yi nekkoon ci kow gaalu seede bi, lan lañu doon wone (Ex. 25:20, 22 ; Nomb. 7:89 ; 2 Rois 19:15) ?
Jàngal Gàddaay gi (Exode) 30:1-10, 17-21 ; 34:1, 2 ak Yawut ya 9:1-5.
Lu tax Yexowa wone ci lu leer ne saraxalekat yi liggéey ci tànt bi war nañu set ci wàllu yaram, te loolu lu mu ñuy jàngal tey (Ex. 30:18-21 ; 40:30, 31 ; Yaw. 10:22) ?
Tànt bi ak kóllëre gi Yàlla fasoon ak waa Israyil, seen jamano paase woon na bi ndaw li Pool bindee leetar yawut yi nekkoon karceen. Naka la Pool wonee loolu (Yaw. 9:1, 9 ; 10:1) ?
Nettali 38
Fukki góor ak ñaar yuy yërndu réew mi
Naka nga gise reseñ yi ñuy wone foofu, te fan lañu jóge ?
Lu tax Musaa yónni 12 góor ngir ñu yërndu réewu Kanaan ?
Lan la 10 ci góor ñooñu wax bi ñu delloo ci Musaa ?
Naka la ñaari góor ci ñoom wonee ngëm ci Yexowa, te ñooñu naka lañu tudd ?
Lu tax Yexowa mer, te lan la wax Musaa ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Nombres 13:1-33.
Ñan lañu tànnoon ngir dem yërndu réew mi, te lu réy lan lañu mënoon a def (Nomb. 13:2, 3, 18-20) ?
Lu tax ni Yosuwe ak Kaleb gise woon réew mi wuute woon ak ni ko ñeneen ñi gise woon, te lan lañuy jàng ci loolu (Nomb. 13:28-30 ; Macë 17:20 ; 2 Kor. 5:7) ?
Jàngal Nombres 14:1-38.
Lu tax ñu war a moytu di xultu ci lu jëm ci ñi Yexowa tànn ci kow suuf si ngir jiite mbooloom (Nomb. 14:2, 3, 27 ; Macë 25:40, 45 ; 1 Kor. 10:10) ?
Naka la Nombres 14:24 wonee ne Yexowa fonk na kenn ku nekk ci ñi koy jaamu (1 Buur. 19:18 ; Prov. 15:3) ?
Nettali 39
Yetu Aaroona mu ngiy tóor-tóor
Ñan ñooy xeex kiliftéefu Musaa ak Aaroona, te lan lañuy wax Musaa ak Aaroona ?
Lan la Musaa wax Kora ak 250 nit ñi ko toppoon ?
Lan la Musaa wax mbooloo mi, te lan moo xew bi mu waxee ba noppi ?
Lan moo dal Kora ak 250 nit ñi ko toppoon ?
Lan la Eleyasar, mi nekk doomu Aaroona, def ak tibbukaayu safara yi ñi dee amoon, te lu tax mu def loolu ?
Lu tax Yexowa def ba yetu Aaroona am tóor-tóor ? (Xoolal li ñuy wone foofu.)
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Nombres 16:1-49.
Lan la Kora ak ñi ko toppoon def, te lu tax ñu mën a ne kiliftéefu Yexowa lañu doon xeex bi ñu doon def loolu (Nomb. 16:9, 10, 18 ; Lév. 10:1, 2 ; Prov. 11:2) ?
Ban gis-gis bu bon la Kora ak 250 njiitu mbooloo yi amoon (Nomb. 16:1-3 ; Prov. 15:33 ; Is. 49:7) ?
Jàngal Nombres 17:1-11 ak 26:10.
Bi yetu Aaroona tóor-tóoree, loolu lan la doon wone, te lu tax Yexowa wax ñu dugal ko ci gaalu kóllëre gi (Nomb. 17:5, 8, 10) ?
Lu am solo lan lañu mën a jàng ci li xewoon ak yetu Aaroona (Nomb. 17:10 ; Jëf. 20:28 ; Fil. 2:14 ; Yaw. 13:17) ?
Nettali 40
Musaa dóor na xeer bi
Naka la Yexowa toppatoo waa Israyil bi ñu nekkee ci màndiŋ mi ?
Lu tax waa Israyil di jooytu bi ñu toogee Kades ?
Lan la Yexowa def ngir mbooloo mi ak mala yi am ndox ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Góor gi di joxoñ boppam, kan la te lu tax muy def loolu ?
Lu tax Yexowa mere Musaa ak Aaroona, te lan la def ngir yar leen ?
Lan moo xew ci tund bi tudd Or, te kan moo nekk léegi saraxalekat bu mag bi ci Israyil ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Nombres 20:1-13, 22-29 ak Deutéronome 29:5.
Lan lañu mën a jàng ci fasoŋ bi Yexowa doon toppatoo waa Israyil ci màndiŋ mi (Deut. 29:5 ; Macë 6:31 ; Yaw. 13:5 ; Saag 1:17) ?
Bi Musaa ak Aaroona màggalulee Yexowa ci kanamu waa Israyil, naka la Yexowa gise loolu (Nomb. 20:12 ; 1 Kor. 10:12 ; Peeñ. 4:11) ?
Lan lañu mën a jàng ci li Musaa def bi ko Yexowa yaree (Nomb. 12:3 ; 20:12, 27, 28 ; Deut. 32:4 ; Yaw. 12:7-11) ?
Nettali 41
Jaan bi ñu defare përëm
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan moo lonku ci bant bi, te lu tax Yexowa wax Musaa mu def ko foofu ?
Naka la mbooloo mi wonee ne amuñu ngërëm ci lépp li leen Yàlla defaloon ?
Lan la mbooloo mi laaj Musaa mu def ginnaaw bi Yexowa yónnee jaan yooyu ngir yar leen ?
Lu tax Yexowa wax Musaa mu defar benn jaanu përëm ?
Lan lañu mën a jàpp ci nettali bii ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Nombres 21:4-9.
Bu ñu gisee Israyil di jooytu ndax li leen Yexowa joxoon, lan lañu war a moytu, ñun (Nomb. 21:5, 6 ; Room 2:4) ?
Ay téeméeri at ginnaaw jamano boobu, lan la waa Israyil def ak jaanu përëm boobu, te lan la buur Esékiyas def (Nomb. 21:9 ; 2 Buur. 18:1-4) ?
Jàngal Yowaana 3:14, 15.
Lu tax ñu mën a méngale bu baax jaan boobu ñu defoon ci bant bi ak li ñu daaj Yeesu Kirist ci poto bi (Gal. 3:13 ; 1 Piy. 2:24) ?
Nettali 42
Mbaam buy wax
Kan mooy Balag, te lu tax mu yónnee ngir ñu woowal ko Balaam ?
Lu tax mbaamu Balaam tëdd ci yoon bi ?
Lan la mbaam bi wax Balaam ?
Lan la benn malaaka wax Balaam ?
Lan moo xew bi Balaam jéemee ñaanal Israyil lu bon ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Nombres 21:21-35.
Lu tax Israyil daan buuru Amoréen bi tudd Sixon ak buuru waa Basan bi tudd Og (Nomb. 21:21, 23, 33, 34) ?
Jàngal Nombres 22:1-40.
Lu tax Balaam bëggoon a ñaanal Israyil lu bon, te lan lañu ci mën a jàng (Nomb. 22:16, 17 ; Prov. 6:16, 18 ; 2 Piy. 2:15 ; Yudd 11) ?
Jàngal Nombres 23:1-30.
Boo déggoon Balaam dinga foog ne kuy jaamu Yexowa la, waaye li mu doon def, lan la doon wone (Nomb. 23:3, 11-14 ; 1 Sam. 15:22) ?
Jàngal Nombres 24:1-25.
Loolu, naka lay dëgërale suñu ngëm ba mu wóor ñu ne li Yexowa bëgg a def dina ko def (Nomb. 24:10 ; Is. 54:17) ?
Nettali 43
Yosuwe lañuy def njiit
Xoolal li ñuy wone foofu. Ñaari góor ñi nekk ak Musaa, ñan lañu ?
Lan la Yexowa wax Yosuwe ?
Lu tax Musaa yéeg ci kow tundu Nebo, te lan la ko Yexowa wax ?
Ñaata at la Musaa amoon bi mu deewee ?
Lu tax xolu nit ñi jeex, waaye lu waral ñu kontaan it ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Nombres 27:12-23.
Ban liggéey bu diis la Yexowa dénk Yosuwe, te naka la Yexowa wonee tey ji ne dafay toppatoo bu baax mbooloom (Nomb. 27:15-19 ; Jëf. 20:28 ; Yaw. 13:7) ?
Jàngal Deutéronome 3:23-29.
Lu tax Yexowa bàyyiwul Musaa ak Aaroona ñu dem ci réew mi mu digoon waa Israyil, te lan lañu mën a jàng ci loolu (Deut. 3:25-27 ; Nomb. 20:12, 13) ?
Jàngal Deutéronome 31:1-8, 14-23.
Li Musaa mujj wax waa Israyil, naka lay wonee ne nangu woon na yar bi ko Yexowa yaroon (Deut. 31:6-8, 23) ?
Jàngal Deutéronome 32:45-52.
Kàddu Yàlla, lan la war a def ci suñu dund (Deut. 32:47 ; Lév. 18:5 ; Yaw. 4:12) ?
Jàngal Deutéronome 34:1-12.
Dëgg la Musaa masul gis Yexowa ci boppam, waaye ba tey, lan la Deutéronome 34:10 wone lu jëm ci diggante bi mu amoon ak Yexowa (Gàdd. [Ex.] 33:11, 20 ; Nomb. 12:8) ?
Nettali 44
Raxab nëbb na ñi ñów yërndu réew mi
Fan la Raxab dëkk ?
Ñaari góor ñi ñuy wone foofu, ñan lañu te lu tax ñu nekk ci Yeriko ?
Lan la buuru Yeriko wax Raxab mu def, te lan la ko Raxab tontu ?
Naka la Raxab dimbalee ñaari góor ñi, te lan la leen ñaan ?
Lan la ñaari góor ñi doon yërndu réew mi dig Raxab ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Josué 2:1-24.
Li Yexowa digoon ci Exode 23:28, naka la ame bi waa Israyil ñówee ngir xeex ak waa Yeriko (Jos. 2:9-11) ?
Jàngal Yawut ya 11:31.
Li Raxab def, naka lay wonee ni ngëm ame solo (Room 1:17 ; Yaw. 10:39 ; Saag 2:25) ?
Nettali 45
Ñu ngi jéggi dex bi tudd Yurdan
Ban kéemaan la Yexowa def ngir waa Israyil mën a jéggi dexu Yurdan ?
Lan la waa Israyil waroon a def ngir jéggi dexu Yurdan, fekk loolu dina wone seen ngëm ?
Lu tax Yexowa wax Yosuwe mu jël 12 xeer yu mag ci biir dex bi ?
Lan moo xew bi saraxalekat yi génnee Yurdan bi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Josué 3:1-17.
Bu ñu seetee bu baax li ñu nettali fii, lan lañu war a def bu ñu bëggee Yexowa dimbali ñu te barkeel ñu (Jos. 3:13, 15 ; Prov. 3:5 ; Saag 2:22, 26) ?
Bi waa Israyil jéggee dexu Yurdan ngir dugg ci réew mi leen Yàlla digoon, dex bi nu mu meloon, te loolu naka lay màggale turu Yexowa (Jos. 3:15 ; 4:18 ; Ps. 66:5-7) ?
Jàngal Josué 4:1-18.
Lu tax ñu jëloon 12 xeer ci biir Yurdan bi te def leen ci Gilgal (Jos. 4:4-7) ?
Nettali 46
Miir yi wër Yeriko
Lan la Yexowa wax xarekat yi ak saraxalekat yi ñu def ci lu mat juróom-benni fan ?
Lan lañu war a def ci juróom-ñaareelu bés bi ?
Boo xoolee li ñuy wone foofu, lan mooy dal miiri Yeriko ?
Lu tax mu am buum bu xonq buy génn ci palanteer bi ?
Lan la Yosuwe digal xarekat yi lu jëm ci nit ñi ak dëkk bi, waaye lan la wax lu jëm ci xaalis, wurus, përëm ak weñ ?
Lan lañu wax ñaari yërndukat yi ñu def ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Josué 6:1-25.
Li waa Israyil doon dox di wër Yeriko ci juróom-ñaareelu fan bi, lu tax mu mel ni liggéeyu waare bi Seede Yexowa yi di def ci muju jamano jii ñu nekk nii (Jos. 6:15, 16 ; Is. 60:22 ; Macë 24:14 ; 1 Kor. 9:16) ?
Naka la li ñu waxoon ci Josué 6:26 ame lu jege 500 at ginnaaw loolu, te loolu lan la ñuy jàngal ci kàddu Yexowa (1 Rois 16:34 ; Esa. 55:11) ?
Nettali 47
Benn sàcc ci Israyil
Xoolal góor gi ñuy wone foofu. Mu ngi suul alal bu mu jël ci Yeriko. Kan la, te ñan ñoo koy dimbali ?
Lu tax li Akan ak njabootam def nekk lu garaaw lool ?
Lan la Yexowa wax bi ko Yosuwe laajee lu tax ñu daan waa Israyil ci xeex bi ñu defoon ci dëkku Ayi ?
Bi ñu indee Akan ak njabootam ci Yosuwe, lan moo leen dal ?
Àtte Akan bi, lu am solo lan la ñuy jàngal ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Josué 7:1-26.
Boo déggee li Yosuwe ñaan Yàlla, loolu lu muy wone ci ni digganteem ak Ki ko sàkk meloon (Jos. 7:7-9 ; Ps. 119:145 ; 1 Ywna. 5:14) ?
Lan la li xewoon ak Akan wone, te bu ñu jàngee loolu, lan lañuy war a moytu (Jos. 7:11, 14, 15 ; Prov. 15:3 ; 1 Tim. 5:24 ; Yaw. 4:13) ?
Jàngal Josué 8:1-29.
Ñun ci suñu wàllu bopp, ban warugar bu am solo lañu am lu jëm ci mbooloo karceen yi tey (Jos. 7:13 ; Lév. 5:1 ; Prov. 28:13) ?
Nettali 48
Waa Gibeyon ñoo am xel
Lu tax waa Gibeyon wuute ak yeneen waa Kanaan yi nekk ci dëkk yi leen jege ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Waa Gibeyon, lan lañuy def, te lu tax ñu koy def ?
Lan la Yosuwe ak yeneen njiiti Israyil dig waa Gibeyon, waaye lan moo feeñ ñetti fan ginnaaw loolu ?
Lan moo xew bi ay buur ci yeneen dëkk déggee ne léegi waa Gibeyon ñu ngi ci jàmm ak waa Israyil ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Josué 9:1-27.
Ndegam Yexowa dafa waxoon mbooloo Israyil ñu alag ñi dëkkoon ca réew moomu yépp, yan jikko Yàlla lañuy gis ci li mu bàyyi waa Gibeyon ñu dund (Jos. 9:22, 24 ; Macë 9:13 ; Jëf. 10:34, 35 ; 2 Piy. 3:9) ?
Yosuwe soppiwul li mu digoon waa Gibeyon. Loolu naka la nekke royukaay bu rafet ngir karceen yi tey (Jos. 9:18, 19 ; Macë 5:37 ; Efes 4:25) ?
Jàngal Josué 10:1-5.
Naka la mbooloo mu réy mi tey roye waa Gibeyon yi, te lan lañu leen di jéem a def ndax loolu (Jos. 10:4 ; Zek. 8:23 ; Macë 25:35-40 ; Peeñ. 12:17) ?
Nettali 49
Naaj bi taxaw na ci asamaan si
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan la Yosuwe di wax, te lu tax mu koy wax ?
Naka la Yexowa dimbalee Yosuwe ak ñi àndoon ak moom ci xeex bi ?
Ñaata buur la Yosuwe daan, te ci ñaata at la ko defe ?
Lu tax Yosuwe séddale réewu Kanaan ?
Ñaata at la Yosuwe amoon bi mu deewee, te ginnaaw loolu, lan moo dal mbooloo mi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Josué 10:6-15.
Gis nañu ne Yexowa def na ba naaj bi ak weer bi taxaw ci asamaan ngir dimbali waa Israyil. Kon lan lañu mën a gëm tey ci lu wóor (Jos. 10:8, 10, 12, 13 ; Sab. 18:3 ; Prov. 18:10) ?
Jàngal Josué 12:7-24.
Ci dëgg-dëgg, kan moo taxoon Yosuwe ak waa Israyil mën a daan 31 buur yi ci Kanaan, te lu tax loolu am solo ci ñun tey (Jos. 12:7 ; 24:11-13 ; Deut. 31:8 ; Luug 21:9, 25-28) ?
Jàngal Josué 14:1-5.
Naka lañu séddalee réew mi diggante giiri Israyil yi, te loolu, lan lay wone lu jëm ci li ñu ñuy jox ci Àjjana ji (Jos. 14:2 ; Is. 65:21 ; Ézék. 47:21-23 ; 1 Kor. 14:33) ?
Jàngal Njiit yi 2:8-13.
Ni ko Yosuwe defe woon ci Israyil, kan moo fexe tey ba ñu bañ a won ginnaaw Yàlla (Njiit. 2:8, 10, 11 ; Macë 24:45-47 ; 2 Tes. 2:3-6 ; Tit 1:7-9 ; Peeñ. 1:1 ; 2:1, 2) ?
Nettali 50
Ñaari jigéen yu am fit
Ñan ñooy àttekat yi ? Waxal ni ñenn ci ñoom tudd.
Ban liggéey bu réy la Debora am, te liggéey boobu lu mu ëmb ?
Bi buur Yabin ak ki doon jiite soldaaram yi, maanaam Sisera, bëggoon a song waa Israyil, lan la Yexowa wax Debora pur mu wax ko àttekat bi tudd Barag ? Ci li mu wax, kan mooy tax ñu yóbbu ndam li ?
Naka la Yawel wonee ne jigéen bu am fit la ?
Lan moo xew ginnaaw bi buur Yabin deewee ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Njiit yi 2:14-22.
Naka la waa Israyil indee meru Yexowa ci seen kow, te lan lañu mën a jàng ci loolu (Njiit. 2:20 ; Prov. 3:1, 2 ; Ézék. 18:21-23) ?
Jàngal Juges 4:1-24.
Naka la karceen yu jigéen yi tey mënee roy ngëm ak fit yi Debora ak Yawel amoon (Juges 4:4, 8, 9, 14, 21, 22 ; Prov. 31:30 ; 1 Kor. 16:13) ?
Jàngal Juges 5:1-31.
Barag ak Debora def nañu benn woy bi ñu daanee seeni noon ba pare. Woy boobu, naka la mënee nekk ñaan bu jëm ci xeexu Armagedon bi war a am (Juges 5:3, 31 ; 1 Chron. 16:8-10 ; Peeñ. 7:9, 10 ; 16:16 ; 19:19-21) ?
Nettali 51
Ruut ak Nawomi
Lan moo xewoon bi Nawomi nekkee ci réewu Mowab ?
Ñan ñooy Ruut ak Orpa ?
Lan la Ruut ak Orpa tontu, kenn ku ci nekk, bi leen Nawomi waxee ne dañu war a dellu ci seen réew ?
Kan mooy Bowas, te naka la dimbalee Ruut ak Nawomi ?
Doom ji Bowas ak Ruut am, naka la tudd ? Lu tax waruñu ko fàtte ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Ruth 1:1-17.
Lan la Ruut wax lu rafet lool lu jëm ci mbëggeel dëgg (Ruth 1:16, 17) ?
Jikko ji Ruut wone, naka lañu ko mën a méngalee ak jikko ji “ yeneen xar ” yi di won ñi Yàlla tànn ci kow suuf si tey (Ywna. 10:16 ; Zek. 8:23) ?
Jàngal Ruth 2:1-23.
Naka la Ruut nekke royukaay bu rafet ci ndawu jigéen yi tey (Ruth 2:17, 18 ; Prov. 23:22 ; 31:15) ?
Jàngal Ruth 3:5-13.
Naka la Bowas gise li Ruut nangu séy ak moom, fekk mënoon na séy ak ku gën a nekk ndaw ?
Li Ruut def, lan la ñuy jàngal lu jëm ci mbëggeel dëgg (Ruth 3:10 ; 1 Kor. 13:4, 5) ?
Jàngal Ruth 4:7-17.
Naka la karceen yu góor yi tey mënee roy Bowas (Ruth 4:9, 10 ; 1 Tim. 3:1, 12, 13 ; 5:8) ?
Nettali 52
Sedeyon ak 300 góor yi mu àndaloon
Lu tax waa Israyil nekk ci coono yu bare ?
Lu tax Yexowa ne Sedeyon ñi war a ànd ak moom ci xeex bi dañu bare ba ëpp ?
Ñaata góor ñoo desoon ginnaaw bi Sedeyon waxee ñi ragal ñu ñibbi ?
Xoolal li ñuy wone foofu te waxal li Yexowa def ba wàññi ñi waroon a xeex ak Sedeyon ba ñu mat 300 góor.
Naka la Sedeyon doxale xeex bi ak 300 góor ñi, te naka la Israyil yóbboo ndam li ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Juges 6:36-40.
Lan la Sedeyon def ngir mu wóor ko ne xam na li Yexowa bëgg ?
Naka lañu mënee xam tey li Yexowa bëgg (Prov. 2:3-6 ; Macë 7:7-11 ; 2 Tim. 3:16, 17) ?
Jàngal Juges 7:1-25.
Am na lu 300 góor ñi jàngoon ci Sedeyon, bi ñu doon xool ni mu doon defe. Ñun it, naka lañu mënee jàng ci Sedeyon bu mag bi, maanaam Yeesu Kirist, bu ñu koy xool (Juges 7:17 ; Macë 11:29, 30 ; 28:19, 20 ; 1 Piy. 2:21) ?
Naka la Juges 7:21 di ñu mën a dimbalee ñu kontaan ak bépp liggéey bu ñu mbootaayu Yexowa mën a dénk (1 Kor. 4:2 ; 12:14-18 ; Saag 4:10) ?
Jàngal Juges 8:1-3.
Bu ñu amee werante ak suñu benn mbokk ci ngëm, lan lañu mën a jàng ci ni Sedeyon defe ak waa Efrayim (Prov. 15:1 ; Macë 5:23, 24 ; Luug 9:48) ?
Nettali 53
Li Yefte dig Yexowa
Kan mooy Yefte, te ci ban jamano la doon dund ?
Lan la Yefte dig Yexowa ?
Bi Yefte ñibbisee këram ginnaaw bi mu daanee waa Ammon, lu tax xolam jeex ?
Bi doomu Yefte déggee li baayam digoon, lan la wax ?
Lu tax nit ñi bëgg doomu Yefte bu jigéen bi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Juges 10:6-18.
Bu ñu déggee ni waa Israyil bàyyee Yexowa, lan lañuy war a moytu (Juges 10:6, 15, 16 ; Room 15:4 ; Peeñ. 2:10) ?
Jàngal Juges 11:1-11, 29-40.
Gis nañu ne Yefte joxe na doomam bu jigéen ngir mu nekk sarax su ñuy lakk. Waaye naka lañu xame ne loolu tekkiwul ne Yefte dafa lakkoon doomam dëgg (Juges 11:31 ; Lév. 16:24 ; Deut. 18:10, 12) ?
Lu tax ñu mën a wax ne Yefte dafa mel ni ku may doomam Yàlla ngir mu nekk sarax ?
Lan lañu mën a jàng ci ni Yefte gise woon li mu digoon Yexowa (Juges 11:35, 39 ; Eccl. 5:4, 5 ; Macë 16:24) ?
Naka la ndaw yi nekk karceen mënee roy doomu Yefte ci lu jëm ci jébbal sa jot yépp ci liggéeyu Yàlla (Juges 11:36 ; Macë 6:33 ; Fil. 3:8) ?
Nettali 54
Nit ki gënoon a am doole
Ci nit ñi mas a dund ci kow suuf ñépp, ki gënoon a am doole, naka la tudd, te doole bi mu amoon, kan moo ko ko mayoon ?
Xoolal li ñuy wone foofu te waxal lan la Samson mas a def benn gaynde bu mag.
Boo xoolee li ñuy wone foofu, lan la Samson di wax Delila, fekk loolu dafa ko doon nëbb nit ñi ? Naka la loolu taxe waa Filisti jàpp ko ?
Naka la Samson reye 3 000 nit ci waa Filisti yi nekkoon ay noonam, bés bi mu deewee ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Juges 13:1-14.
Li Manowa ak jabaram def, lu tax mu nekk royukaay bu rafet ci waajur yi tey ci lu jëm ci yar seeni doom (Juges 13:8 ; Ps. 127:3 ; Efes 6:4) ?
Jàngal Juges 14:5-9 ak 15:9-16.
Gis nañu ne Samson rey na gaynde, dagg na buum yi ñu ko takkoon, te jël na benn ŋaamu mbaam ngir rey 1 000 nit. Loolu lan lay wone lu jëm ci xel mu sellu Yexowa ?
Naka la xel mu sell mi di ñu dimbalee tey (Juges 14:6 ; 15:14 ; Zek. 4:6 ; Jëf. 4:31) ?
Jàngal Juges 16:18-31.
Naka la àndandoo bu bon yàqe Samson, te lan lañuy jàng ci loolu (Juges 16:18, 19 ; 1 Kor. 15:33) ?
Nettali 55
Benn xale bu ndaw buy jaamu Yàlla
Xale bu góor bu ñuy wone foofu, naka la tudd, te ñan ñooy ñi ci des ?
Lan la Aana ñaan Yexowa benn bés bi mu nekkoon ci tànt bi fi ñuy jaamoo Yexowa ? Naka la ko Yexowa maye li mu ko ñaanoon ?
Ñaata at la Samwil amoon bi ñu ko yóbboo ci tàntu Yexowa bi, te lan la ko yaayam daan defal at mu nekk ?
Ñaari doomi Eli yu góor yi, naka lañu tuddoon, te ban jikko lañu amoon ?
Naka la Yexowa woowe Samwil, te lan la ko wax ?
Lan la Samwil nekkoon bi mu demee ba mag, te lan moo xew bi mu demee ba màgget ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Samwil 1:1-28.
Elkana dafa doon jiite njabootam ci jaamu Yexowa. Naka la nekke royukaay bu rafet ngir njaboot yi tey (1 Sam. 1:3, 21 ; Macë 6:33 ; Fil. 1:10) ?
Li Aana def, naka la nekke lu rafet lu ñu mën a roy bu ñu nekkee ci coono ba jaaxle (1 Sam. 1:10, 11 ; Ps. 55:22 ; Room 12:12) ?
Jàngal 1 Samwil (1 Samuel) 2:11-36.
Naka la Eli wonee ne doomam yi la gën a fonk Yexowa, te lu tax ñu war a moytu bu baax loolu (1 Sam. [1 Sam.] 2:22-24, 27, 29 ; Deut. 21:18-21 ; Macë 10:36, 37) ?
Jàngal 1 Samwil 4:16-18
Yan ñeenti xibaar yu bon ñoo jóge fa Israyil doon xeex ? Xibaar yooyu, lan lañu def ci Eli ?
Jàngal 1 Samwil 8:4-9.
Naka la Israyil tooñe Yexowa tooñ bu bon, te naka lañu mën a wonee ne Nguuram lañuy faral tey (1 Sam. 8:5, 7 ; Ywna. 17:16 ; Saag 4:4) ?
Nettali 56
Sóol, buur bi jëkk a am ci Israyil
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan la Samwil di def, te lu tax mu koy def ?
Lu tax Yexowa bëgg Sóol, te moom, ban jikko la am ?
Doomu Sóol, naka la tudd, te lan la def ?
Lu tax Sóol def sarax bi te bañ a xaar Samwil mu def ko ?
Lan lañu mën a jàng ci li xewoon ak Sóol ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Samwil (1 Samuel) 9:15-21 ak 10:17-27.
Li Sóol woyofoon, naka la ko dimbalee mu bañ a gaaw a feyyu bi ko ay nit doon wax lu ñaaw (1 Sam. [1 Sam.] 9:21 ; 10:21, 22, 27 ; Prov. 17:27) ?
Jàngal 1 Samuel 13:5-14.
Ban bàkkaar la Sóol def ci Gilgal (1 Sam. 10:8 ; 13:8, 9, 13) ?
Jàngal 1 Samwil 15:1-35.
Ban bàkkaar bu réy la Sóol def ak Agag mi nekkoon buuru Amalekk (1 Sam. 15:2, 3, 8, 9, 22) ?
Lan la Sóol wax ngir bañ a nangu bàkkaar bi mu defoon te ñu bañ ko wax ne li mu def baaxul (1 Sam. 15:24) ?
Tey, bu amee ku ñuy xelal, lan lañu war a moytu def (1 Sam. 15:19-21 ; Ps. 141:5 ; Prov. 9:8, 9 ; 11:2) ?
Nettali 57
Yàlla tànn na Daawuda
Xale bi ñuy wone foofu, naka la tudd, te naka lañu xame ne am na fit ?
Fan la Daawuda dëkk, te baayam ak maamam bu góor, naka lañu tudd ?
Lu tax Yexowa wax Samwil mu dem ci këru Yese ci Betleyem ?
Lan moo xew bi Yese indee ci Samwil juróom-ñaar ci doomam yu góor yi ?
Bi ñu indee Daawuda, lan la Yexowa wax Samwil ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Samwil 17:34, 35.
Li ñuy nettali fii, naka lay wonee ne Daawuda dafa amoon fit ak ngëm ci Yexowa (1 Sam. 17:37) ?
Jàngal 1 Samwil 16:1-14.
Li Yexowa wax ci 1 Samwil 16:7, naka la ñu mënee dimbali ñu bañ a gënale te bañ a àtte nit ci kow li bët gis (Jëf. 10:34, 35 ; 1 Tim. 2:4) ?
Li daloon Sóol, naka lay wonee ne bu Yexowa dindee xelam mu sell mi ci nit, xel bu bon mooy jël palaasam, walla leneen lu am doole lu koy xiir ci lu bon (1 Sam. 16:14 ; Macë 12:43-45 ; Gal. 5:16) ?
Nettali 58
Daawuda ak Goliyàtt
Lan la Goliyàtt wax ñi doon xeex ngir waa Israyil ?
Goliyàtt, naka la tollu woon, te lan la buur Sóol digoon kuy rey Goliyàtt ?
Lan la Daawuda wax Sóol bi ko Sóol waxee ne mënul xeex ak Goliyàtt ndaxte xale rekk la ?
Bi mu tontoo Goliyàtt, naka la Daawuda wonee ne wóolu na Yexowa dëgg ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan la Daawuda jël ngir rey Goliyàtt, te lan moo xew ak waa Filisti ginnaaw loolu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Samwil (1 Samuel) 17:1-54.
Lan moo mayoon Daawuda mu bañ a ragal dara, te naka lañu mënee roy fit bi mu amoon (1 Sam. 17:37, 45 ; Efes 6:10, 11) ?
Bu karceen yi di fo, lu tax ñu war a moytu mel ni Goliyàtt, maanaam bëgg jëkk ci lépp (1 Sam. 17:8 ; Gal. 5:26 ; 1 Tim. 4:8) ?
Lan la Daawuda wax te mu wone ne xamoon na ne ci lu wóor Yàlla dina ko dimbali (1 Sam. 17:45-47 ; 2 Chron. 20:15) ?
Li ñuy nettali fii nekkul rekk ñaari gurupu xarekat yu doon xeex, waaye dafay wone ne xeex bi mu ngi woon diggante yàlla yu dul dëgg yi ak Yexowa, Yàlla dëgg ji. Loolu, naka lañu koy xame (1 Sam. 17:43, 46, 47) ?
Naka la karceen yi Yàlla tànn roye Daawuda ci lu jëm ci wóolu Yexowa (1 Sam. 17:37 ; Jér. 1:17-19 ; Peeñ. 12:17) ?
Nettali 59
Li tax Daawuda war a daw
Lu tax Sóol iñaane Daawuda, waaye naka la doomam Yonatan wuutee ak baayam ?
Lan moo xew benn bés bi Daawuda doon xalam ngir Sóol ?
Ci li ko Sóol wax, lan la Daawuda war a def bala muy mën a takk doomam bu jigéen bi tudd Mikal ? Lu tax Sóol wax ko loolu ?
Lan moo xew te mu nekk ñetteelu yoon bi, bi Daawuda doon xalam pur Sóol, ni ñu koy wonee foofu ?
Naka la Mikal dimbalee Daawuda ngir mu mucc, te lan la Daawuda naroon a def ci juróom-ñaari at yi toppoon ci loolu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Samwil (1 Samuel) 18:1-30.
Mbëggeel dëgg bi Yonatan amoon ci Daawuda, naka la doon wonee mbëggeel bi naroon a am diggante “ yeneen xar ” yi ak “ coggal ju ndaw ji ” ? (1 Sam. 18:1 ; Ywna. 10:16 ; Luug 12:32 ; Zek. 8:23.)
Yonatan moo naroon a topp ci Sóol te nekk buuru Israyil. Waaye li ñu wax ci 1 Samuel 18:4, naka lay wonee ne Yonatan nangu woon na dëgg kiliftéefu ki Yàlla tànnoon ngir mu nekk buur ?
Li xewoon ak Sóol, naka lay wonee ne iñaan mën na yóbbu ci bàkkaar bu réy ? Loolu, lu muy wone ci li ñu war a moytu (1 Sam. 18:7-9, 25 ; Saag 3:14-16) ?
Jàngal 1 Samuel 19:1-17.
Naka la Yonatan xawee ñàkk bakkanam bi mu wonee Sóol ne àndul ak li mu bëggoon a def (1 Sam. 19:1, 4-6 ; Prov. 16:14) ?
Nettali 60
Abigayil ak Daawuda
Jigéen bi ñuy wone foofu di fekksi Daawuda, naka la tudd, te ban jikko la am ?
Kan mooy Nabal ?
Lu tax Daawuda yónni ay nit ci Nabal ngir ñaan ko dara ?
Lan la Nabal wax nitu Daawuda yi, te lan la Daawuda def ?
Naka la Abigayil wonee ne jigéen bu am xel la ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Samuel 22:1-4.
Naka la njabootu Daawuda nekke royukaay bu rafet ci karceen yi tey ci lu jëm ci ni ñu waree dimbaleente ci suñu biir (Prov. 17:17 ; 1 Tes. 5:14) ?
Jàngal 1 Samuel 25:1-43.
Lu tax ñuy wax lu bon noonu ci Nabal (1 Sam. 25:2-5, 10, 14, 21, 25) ?
Tey, lan la karceen yi am jëkkër mën a roy ci Abigayil (1 Sam. 25:32, 33 ; Prov. 31:26 ; Efes 5:24) ?
Yan ñaari yëf yu bon la Abigayil tere Daawuda mu def (1 Sam. 25:31, 33 ; Room 12:19; Efes 4:26) ?
Li Daawuda tontu Abigayil, naka la mënee dimbali góor ñi tey ñu xam ni Yexowa di gise jigéen (Jëf. 21:8, 9 ; Room 2:11 ; 1 Piy. 3:7) ?
Nettali 61
Dañu def Daawuda buur
Lan la Daawuda ak Abisay def bi Sóol doon nelaw fu moom ak nitam yi doon fanaan ?
Yan laaj la Daawuda laaj Sóol ?
Bi mu jógee ci Sóol, fan la Daawuda dem ?
Lan moo jeexal xolu Daawuda ba mu bind benn woy bu rafet ?
Ñaata at la Daawuda amoon bi ñu ko defee buur ci Ebron te yenn ci doomam yi naka lañu tuddoon ?
Ginnaaw loolu fan la Daawuda nguuru ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Samuel 26:1-25.
Li Daawuda wax ci 1 Samuel 26:11, lan lay wone ci ni Daawuda doon gise ni Yexowa doxale kiliftéefam, maanaam kiliftéefu Yexowa (Sab. 37:7 ; Room 13:2) ?
Boo defee lépp ngir baax ak nit fekk moom du la fey lu baax, li Daawuda wax ci 1 Samuel 26:23, naka la lay mën a dimbalee ngir xam ni nga war a gise loolu (1 Buur. 8:32 ; Sab. 18:20) ?
Jàngal 2 Samuel 1:26.
Naka la karceen yi tey mënee “ bëggante mbëggeel gu tar ” mel ni bëggante bi amoon diggante Daawuda ak Yonatan (1 Piy. 4:8 ; Kol. 3:14 ; 1 Ywna. 4:12) ?
Jàngal 2 Samuel 5:1-10.
Ñaata at la Daawuda nekke buur, te naka lañu xaaje at yooyu (2 Sam. 5:4, 5) ?
Lan moo taxoon Daawuda nekk nit ku mag, te loolu lan la ñu war a fàttali tey (2 Sam. 5:10 ; 1 Sam. 16:13 ; 1 Kor. 1:31 ; Fil. 4:13) ?
Nettali 62
Daawuda am na poroblem ci biir këram
Lan moo mujj a dal réewu Kanaan ak ndimbal bi Yexowa may waa Israyil ?
Lan moo xew benn ngoon bi Daawuda nekkoon ci teraasu këram ?
Lu tax Yexowa mere Daawuda lool ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Kan la Yexowa yónni ci Daawuda ngir wax ko bàkkaar yi mu def, te ci li nit kooku wax lan mooy dal Daawuda ?
Yan poroblem la Daawuda am ?
Kan moo nekk buuru Israyil ginnaaw Daawuda ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 2 Samwil 11:1-27.
Lu tax am lu bare lu ñuy def ci liggéeyu Yexowa nekk lu ñuy aar tey ?
Lan moo xiir Daawuda ci bàkkaar, te bu ñu gisee loolu ñun ñìy jaamu Yexowa tey, lan lañuy moytu (2 Sam. 11:2 ; Macë 5:27-29 ; 1 Kor. 10:12 ; Saag 1:14, 15) ?
Jàngal 2 Samwil 12:1-18.
Njiit yi ci mbooloo mi ak waajur yi, lan lañu mën a jàng ci ni Natan defe ak Daawuda bi mu ko bëggoon a xelal (2 Sam. 12:1-4 ; Prov. 12:18 ; Macë 13:34) ?
Lu tax Yexowa yërëm Daawuda (2 Sam. 12:13 ; Sab. 32:5 ; 2 Kor. 7:9, 10) ?
Nettali 63
Suleymaan, buur bu am xel la
Lan la Yexowa laaj Suleymaan, te lan la ko Suleymaan tontu ?
Ndegam li ko Suleymaan wax, neex na Yexowa, lan la ko Yexowa dig ?
Ban poroblem bu jafe la ñaari jigéen wax Suleymaan ?
Ni ñu ko wonee foofu, naka la Suleymaan faje poroblem boobu ?
Nguuru Suleymaan, naka la mel te lu tax mu mel noonu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Buur yi 3:3-28.
Góor ñi ñu dénk liggéey ci mbootaayu Yàlla tey, lan lañu mën a jàng ci li Suleymaan wax ci 1 Buur yi 3:7 te mu di ay kàddu yu jóge ci xolam (Ps. 119:105 ; Prov. 3:5, 6) ?
Li Suleymaan ñaan Yàlla, lu tax mu nekk lu rafet lu ñu mën a ñaan Yàlla, ñun it (1 Buur. 3:9, 11 ; Prov. 30:8, 9 ; 1 Ywna. 5:14) ?
Bu ñu gisee ni Suleymaan faje poroblem bi amoon diggante ñaari jigéen yooyu, lan moo ñu mën a wóor lu jëm ci bés bu Suleymaan bu mag bi, maanaam Yeesu Kirist, di nguuru (1 Buur. 3:28 ; Esa. 9:6, 7 ; 11:2-4) ?
Jàngal 1 Rois 4:29-34.
Lan la Yexowa def ngir may Suleymaan li mu ko ñaanoon, maanaam xol buy tax mu koy déggal (1 Rois 4:29) ?
Bu ñu gisee lépp li nit ñi doon def ngir mën a dégg xam-xam bu réy bi Suleymaan amoon, lan lañu war a def tey ngir mën a jàng Kàddu Yàlla (1 Rois 4:29, 34 ; Ywna. 17:3 ; 2 Tim. 3:16) ?
Nettali 64
Suleymaan mu ngi tabax kër Yàlla gi
Ñaata at la Suleymaan jël ngir tabax kër Yexowa gi, te lu tax xaalis bi mu ci dugal bare lool noonu ?
Ñaata néeg yu gën a am solo ñoo nekkoon ci kër Yàlla gi, te lan moo nekkoon ci biir néeg yooyu ?
Lan la Suleymaan ñaan Yàlla bi mu paree tabax bi ?
Naka la Yexowa wonee ne li ko Suleymaan ñaan, neex na ko ?
Jabaru Suleymaan yi, ci lan lañu ko xiir, te lan moo ko dal ?
Lu tax Yexowa mere Suleymaan, te lan la ko Yexowa wax ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Chroniques 28:9, 10.
Bu ñu jàngee li Daawuda wax ci 1 Chroniques 28:9, 10, lan lañu war a jéem a def bés bu nekk (Sab. 19:15 ; Fil. 4:8, 9) ?
Jàngal 2 Chroniques 6:12-21, 32-42.
Naka la Suleymaan wonee ne amul benn tabax bu nit def fu Yàlla Aji-kowe ji mën a dëkk (2 Chron. 6:18; Jëf. 17:24, 25) ?
Li Suleymaan wax ci 2 Chroniques 6:32, 33, lan lay wone lu jëm ci Yexowa (Jëf. 10:34, 35 ; Gal. 2:6) ?
Jàngal 2 Chroniques 7:1-5.
Bi doomi Israyil gisee ndamu Yexowa, dañu ko màggal. Ñun it tey, bu ñu gisee ni Yexowa di barkeele mbooloom, loolu lan la war a def ci ñun (2 Chron. 7:3 ; Sab. 22:23 ; 34:2 ; Ps. 96:2) ?
Jàngal 1 Buur yi 11:9-13.
Dundu Suleymaan bi, naka la ñuy wonee lu tax kontine di def lu baax ba bés bu ñuy dee, am solo (1 Buur. 11:4, 9 ; Macë 10:22 ; Peeñ. 2:10) ?
Nettali 65
Xaaj nañu nguur gi
Ñaari góor ñi ñuy wone foofu, naka lañu tudd te lan moo doon seen liggéey ?
Lan la Akisu def ak mbubbam bi mu doon sol, te loolu lan lay misaal ?
Lan la Suleymaan jéem a def Yérobowam ?
Lu tax mbooloo mi def Yérobowam buur ci kow fukki giir ?
Lu tax Yérobowam defar ñaari nag yu wurus, te lan moo xew ci réew moomu lu yàggul ginnaaw loolu ?
Lan moo dal nguuru ñaari giir yi ak kër Yexowa gi nekk ci Yerusalem ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Buur yi (1 Rois) 11:26-43.
Ban jikko la Yérobowam amoon, te lan la ko Yexowa dig bu toppee ndigalam yi (1 Rois 11:28, 38) ?
Jàngal 1 Buur yi (1 Rois) 12:1-33.
Bu ñu gisee lu bon li Robowam def, lan la waajur yi ak njiiti mbooloo mi mën a jàng ci lu jëm ci yem fi ñu war a yem ci wàllu nekk waajur walla kilifa (1 Buur. 12:13 ; Eccl. 7:7 ; 1 Piy. 5:2, 3) ?
Ci kan la ndaw yi tey war a dem bu ñu bëggee am xelal yu wóor bu ñu amee lu am solo lu ñu war a tànn lu jëm ci seen àddina (1 Buur. 12:6, 7 ; Prov. 1:8, 9 ; 2 Tim. 3:16, 17 ; Yaw. 13:7) ?
Lu tax Yérobowam samp ñaari béréb fu ñuy jaamoo nag yi, te naka la loolu wonee ne dafa ñàkkoon ngëm lool ci Yexowa (1 Buur. [1 Rois] 11:37 ; 12:26-28) ?
Lan moo xiir ñi bokkoon ci nguuru 10 giir yi ci bañ a jaamu Yàlla ni mu ware (1 Rois 12:32, 33) ?
Nettali 66
Jabaru buur bu tuddoon Yesabel te nekkoon ku bon
Kan moo doon Yesabel ?
Lu tax xolu buur Akab jeex benn bés ?
Naka la Yesabel fexee ba jëkkëram Akab am toolu Nabott bi amoon ay reseñ ?
Kan la Yexowa yónni ngir yar Yesabel ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan moo xew bi Yexu àggee kër Yesabel ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Buur yi 16:29-33 ak 18:3, 4.
Naka la réewu Israyil meloon bi buur Akab doon nguuru (1 Rois 14:9) ?
Jàngal 1 Buur yi 21:1-16.
Naka la Nabott wonee fit ak takkute ci Yexowa (1 Buur. 21:1-3 ; Lév. 25:23-28) ?
Bu ñu gisee li Akab def bi mu amee lu ko naqari, lan lañuy jàng ci li ñu war a def bu amee ku tas suñu yaakaar (1 Buur. 21:4 ; Room 5:3-5) ?
Jàngal 2 Rois 9:30-37.
Lan lañu mën a jàng ci ni Yexu saware woon a def li Yexowa bëgg (2 Rois 9:4-10 ; 2 Kor. 9:1, 2 ; 2 Tim. 4:2) ?
Nettali 67
Yosafat teg na yaakaaram ci Yexowa
Kan mooy Yosafat, te ci ban jamano la doon dund ?
Lu tax waa Israyil tiit, te ñu bare ci ñoom, lan lañuy def ?
Bi Yosafat ñaanee Yexowa ba pare, lan la ko Yexowa tontu ?
Lan la Yexowa def bala xeex bi komaase ?
Lan lañu mën a jàng ci li Yosafat def ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 2 Chroniques 20:1-30.
Ñiy jaamu Yàlla te takku ci moom, naka la Yosafat wonee li ñu war a def bu ñuy jànkoonte ak lu leen di tiital (2 Chron. 20:12 ; Ps. 25:15 ; 62:1) ?
Ndegam Yexowa amoon na fu muy jaar ngir wax ak mbooloom ci bépp jamano, ci lan lay jaar tey ngir def loolu (2 Chron. 20:14, 15 ; Macë 24:45-47 ; Ywna. 15:15) ?
Bu Yàlla di komaase “ xeex biy am ci bés bu mag, bi Yàlla Aji Kàttan jagleele boppam ”, ñun, li ñuy fekke bés boobu, naka lay niroo ak li Yosafat fekke woon (2 Chron. 20:15, 17 ; 32:8 ; Peeñ. 16:14, 16) ?
Pioñee ak misionéer yi nga xam ne dañuy roy ci waa Lewi yi, maanaam ñi bokk ci askanu Lewi, ban wàll lañu am ci liggéeyu waare bi ñuy def ci àddina si sépp tey (2 Chron. 20:19, 21 ; Room 10:13-15 ; 2 Tim. 4:2) ?
Nettali 68
Ñaari xale yu dee woon ba dekki
Ñetti nit ñi ñuy wone foofu, ñan lañu te lan moo dal xale bu góor bi ?
Lan la Iliyas ñaan Yàlla lu jëm ci xale bi, te lan moo xew ginnaaw loolu ?
Ki doon dimbali Iliyas, naka la tudd ?
Lu tax ñu woo Alyaasa ci këru benn jigéen ci Sunem ?
Lan la Alyaasa def, te lan moo xew ak xale bi dee woon ?
Ban kàttan la Yexowa am, ni ñu ko gise ci li Iliyas ak Alyaasa defoon ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Buur yi 17:8-24.
Lan moo xewoon lu naroon a wone ndax Iliyas dina déggal Yàlla te am ngëm ci moom (1 Buur. 17:9 ; 19:1-4, 10) ?
Lu tax ñu mën a wax ne jigéen bi dëkkoon Sarepeta te jëkkëram faatu, jigéen boobu dafa amoon ngëm gu dëgër lool (1 Buur. 17:12-16 ; Luug 4:25, 26) ?
Li xewoon ak jigéen bi dëkkoon Sarepeta te jëkkëram faatu, naka lay wonee ne li Yeesu wax ci Macë 10:41, 42, mooy dëgg (1 Buur. 17:10-12, 17, 23, 24) ?
Jàngal 2 Rois 4:8-37.
Nettali 69
Xale bu jigéen buy dimbali góor gu mag
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan la xale bu jigéen bi di wax soxna si ?
Kan mooy soxna si ñuy wone foofu, te lan la xale bu jigéen bi di def këram ?
Alyaasa yónni na surgaam ci Naaman ngir mu wax ko lan ? Lu tax Naaman mer ?
Lan moo xew bi Naaman toppee li ko surgaam yi wax ?
Lu tax Alyaasa bañ li ko Naaman bëgg a may, waaye lan la Geyasi def ?
Lan moo dal Geyasi, te lan lañu mën a jàng ci loolu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 2 Buur yi 5:1-27.
Li xale bu jigéen bi bokkoon ci waa Israyil def, naka la nekke lu xale yi mën a topp tey (2 Buur. 5:3 ; Sab. 8:3 ; Ps. 148:12, 13) ?
Lu tax ñu war a xalaat Naaman bu ñuy jot xelal bu jóge ci Mbind mi (2 Buur. 5:15 ; Yaw. 12:5, 6 ; Saag 4:6) ?
Bu ñu seetee li Alyaasa defoon ak li Geyasi defoon, lan lañu ci mën a jàng (2 Buur. 5:9, 10, 14-16, 20 ; Macë 10:8 ; Jëf. 5:1-5 ; 2 Kor. 2:17) ?
Nettali 70
Yunus ak jën bu réy bi
Kan mooy Yunus, te lan la ko Yexowa wax mu def ?
Ndegam bëggul dem fi ko Yexowa yónni, lan la Yunus def ?
Lan la Yunus wax ñi doon liggéey ci gaal gi ne loolu lañu war a def ngir ngelaw bi taxaw ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan moo xew bi Yunus doon dugg ci biir géej gi ?
Ñaata fan la Yunus def ci biir jën bu mag bi, te lan la doon def foofu ?
Fan la Yunus dem ginnaaw bi mu génnee ci jën bu mag bi, te loolu lan la ñuy jàngal ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Yona 1:1-17.
Naka la Yunus doon gise liggéeyu waare bi mu naroon a def ci Niniw (Yona 1:2, 3 ; Prov. 3:7 ; Eccl. 8:12) ?
Jàngal Yona 2:1, 2, 10.
Bu ñu gisee li xewoon ak Yunus, lu tax mu mën ñu wóor ne Yexowa dina ñu may li ñu koy ñaan (Sab. 22:25 ; 34:7 ; 1 Ywna. 5:14) ?
Jàngal Yona 3:1-10.
Ci bu jëkk, Yunus deful li ko Yexowa santoon, waaye ba tey Yexowa kontine na di jaar ci moom ngir wax ak nit ñi. Lu tax loolu di seddal suñu xol (Ps. 103:14 ; 1 Piy. 5:10) ?
Bu ñu gisee li xewoon ak Yunus ak waa Niniw, lu tax waruñu foog ne xam nañu naka la nit ñi ci gox bi di gise li ñu leen di wax ci waaraate bi (Yona 3:6-9 ; Eccl. 11:6 ; Jëf. 13:48) ?
Nettali 71
Yàlla dige na àjjana
Kan moo doon Esayi ? Ci ban jamono la doon dund ? Te lan la ko Yexowa won ?
“ Àjjana ”, baat bi ci boppam, lu mu tekki, te loolu, lan la lay fàttali ?
Lan la Yexowa wax Esayi mu bind lu jëm ci Àjjana ju bees ji ?
Lu tax ñu dàq Aadama ak Awa ci biti béréb bu rafet bi ñu nekkoon ?
Lan la Yexowa dig ñi ko bëgg ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Esayi 11:6-9.
Lan la Kàddu Yàlla wax lu jëm ci jàmm jiy am diggante mala ak nit ci àddina su bees si (Ps. 148:10, 13 ; Is. 65:25 ; Ézék. 34:25) ?
Li Esayi waxoon, naka la ame tey ci wàllu ngëm ci biir mbooloo Yexowa mi (Room 12:2 ; Efes 4:23, 24) ?
Kan lañu war a màggal bu ñu gisee ni ay nit di soppalee seen jikko, muy tey walla ci àddina su bees si (Is. 48:17, 18 ; Gal. 5:22, 23 ; Fil. 4:7) ?
Jàngal Peeñu ma 21:3, 4.
Mbind mi nee na Yàlla dina dëkk ak nit. Waaye ci Mbind mi, lan moo wone ne nekkul ne Yàlla ci boppam mooy ñów dëkk ak nit ci kow suuf (Lév. 26:11, 12 ; 2 Chron. 6:18 ; Is. 66:1 ; Peeñ. 21:2, 3, 22-24) ?
Yan jooy ak metit ñooy jeex (Luug 8:49-52 ; Room 8:21, 22 ; Peeñ. 21:4) ?
Nettali 72
Yàlla dimbali na buur Esékiyas
Ki ñuy wone foofu, kan la, te lu tax mu nekk ci coono bu metti ?
Leetar yi Esékiyas teg ci kanamu Yàlla, yan leetar lañu, te lan la Esékiyas di ñaan Yàlla ?
Ban fasoŋu buur la Esékiyas nekk, te lan la ko Yexowa wax, jaare ko ci yonentam Esayi ?
Lan la malaaka Yexowa def waa Asiri yi, ni ñu ko wonee foofu ?
Nguuru ñaari giir yi nekkoon nañu ci jàmm lu yàgg tuuti. Waaye lan moo xew ginnaaw bi Esekiyas deewee ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 2 Buur yi (2 Rois) 18:1-36.
Buuru Asiri dafa yónni ci waa Israyil góor gu tudd Rabsake. Kooku, lan la doon wax ngir wàññi ngëm gi waa Israyil amoon ci Yexowa (2 Rois 18:19, 21 ; Gàdd. 5:2 ; Ps. 64:3) ?
Seede Yexowa yi, bu ñu amee noon yu leen bëgg a def lu bon, naka lañuy roye Esékiyas (2 Rois 18:36 ; Ps. 39:1 ; Prov. 26:4 ; 2 Tim. 2:24) ?
Jàngal 2 Rois 19:1-37.
Ñi bokk ci mbooloo Yexowa tey, bu ñu nekkee ci coono, naka lañuy roye Esékiyas (2 Rois 19:1, 2 ; Prov. 3:5, 6 ; Yaw. 10:24, 25 ; Saag 5:14, 15) ?
Daan nañu Buur Sennakerib ñetti yoon daan bu metti. Loolu, lan lay wone lu jëm ci li war a xew ëllëg (2 Rois 19:32, 35, 37 ; Peeñ. 20:2, 3) ?
Jàngal 2 Buur yi 21:1-6, 16.
Lu tax ñu mën a wax ne Manase moo bokkoon ci buur yu gënoon a bon ci yi nguuru woon ci Yerusalem (2 Chron. 33:4-6, 9) ?
Nettali 73
Buur bu baax bi mujj ci Israyil
Ñaata at la Yosiyas amoon bi ñu ko defee buur ? Juróom-ñaari at ginnaaw loolu, lan la komaasee def ?
Xoolal li ñuy jëkk wone foofu. Lan la Yosiyas di def ?
Lan la saraxalekat bu mag bi gis, bi nit ñi doon defaraat kër Yàlla gi ?
Lu tax Yosiyas xotti mbubbam ?
Ban kàddu bu jóge ci Yexowa la yonent Yàlla bu jigéen bi tudd Ulda jottali Yosiyas ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 2 Chroniques 34:1-28.
Ban royukaay la Yosiyas nekk ci ñi jaaroon ci coono yu metti bi ñu nekkee xale (2 Chron. 33:21-25 ; 34:1, 2 ; Sab. 27:10) ?
Am na lu am solo lu Yosiyas def bi nguuram matee juróom-ñetti at, fukk ak ñaari at, ak fukk ak juróom-ñeenti at, ngir nit ñi gën a mën a jaamu Yexowa. Loolu, lan la (2 Chron. 34:3, 8) ?
Lan lañu mën a jàng ci li buur Yosiyas ak saraxalekat bu mag bi Ilkiya def, lu jëm ci toppatoo béréb fu ñuy jaamoo Yàlla (2 Chron. 34:9-13 ; Prov. 11:14 ; 1 Kor. 10:31) ?
Nettali 74
Góor gii tiitul, ragalul
Kan mooy góor gi ñuy wone foofu ?
Nekk yonent Yàlla, naka la Yérémi doon gise loolu ? Waaye lan la ko Yexowa wax ?
Lan la Yérémi kontine di wax mbooloo mi ?
Lan la saraxalekat yi jéem a def ngir Yérémi noppi ? Moom nag naka la wonee ne ragalul ?
Lan moo xew bi waa Israyil bañee soppi lu bon li ñu doon def ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Yérémi 1:1-8.
Ni ñu ko mën a gise ci li xewoon ak Yérémi, lan mooy tax nit di mën a def liggéey bi ko Yàlla dénk (2 Kor. 3:5, 6) ?
Li Yérémi def, ci lan la mën a xiir xale yi nekk karceen tey (Eccl. 12:1 ; 1 Tim. 4:12) ?
Jàngal Jérémie 10:1-5.
Yan kàddu yu am doole la Yérémi wax ngir misaal lu tax gëm ay xërëm amul benn njariñ (Jér. 10:5 ; Is. 46:7 ; Hab. 2:19) ?
Jàngal Jérémie 26:1-16.
Ñi des ci ñi Yàlla tànn ci kow suuf si, bu ñuy yégle àtte Yàlla yi, naka lañuy jàppe ci seen xol li Yexowa waxoon Yérémi, maanaam warul dindi mukk benn baat ci li Muy wax (Jér. 26:2 ; Deut. 4:2; Jëf. 20:27) ?
Naka la Yérémi nekke royukaay bu rafet ci Seede Yexowa yi tey bu ñuy yégle àtte Yàlla yi (Jér. 26:8, 12, 14, 15 ; 2 Tim. 4:1-5) ?
Jàngal 2 Buur yi (2 Rois) 24:1-17.
Yuda dafa bàyyi woon Yexowa. Loolu, am na lu metti lu mu jur. Lan la (2 Buur. [2 Rois] 24:2-4, 14) ?
Nettali 75
Ñeenti xale yu góor ca Babilon
Ñan ñooy ñeenti xale yu góor yi ñuy wone foofu, te lu tax ñu nekk Babilon ?
Lan la Nebukanesar bëgg a def ak ñeenti xale yu góor yooyu, te lan la digal ñi koy liggéeyal ?
Lan la Dañeel ñaan lu jëm ci li ñu war a lekk te naan, moom ak ñetti xaritam yi ?
Bi ñu lekkee ay lujum lu tollu ak fukki fan, naka la Dañeel ak ñetti xaritam yi wuutee woon ak yeneen xale yu góor yi ?
Naka la Dañeel ak ñetti xaritam yi deme ba nekk ci kër buur bi ? Ci ban wàll lañu sutoon saraxalekat yi ak boroom xam-xam yi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Dañeel 1:1-21.
Lan lañu war a def bu ñu bëggee xeex li ñu mën a xiir ci lu bon, xeex it suñu ñàkk doole ci wàllu ngëm (Dañ. 1:8 ; Njàl. 39:7, 10 ; Gal. 6:9) ?
Naka la nit ñi tey mënee xiir walla sax forse xale yi ngir ñu bokk ci li ñuy wax lu neex la, fekk baaxul (Dañ. 1:8 ; Prov. 20:1 ; 2 Kor. 6:17–7:1) ?
Li Biibël bi nettali ci ñeenti xale yu góor yi nekkoon yawut, naka la ñuy dimbalee ñu xam ni ñu war a gise xam-xamu àddina si (Dañ. 1:20 ; Is. 54:13 ; 1 Kor. 3:18-20) ?
Nettali 76
Ñu ngiy alag Yerusalem
Lan mooy dal Yerusalem ak waa Israyil yi ñuy wone foofu ?
Kan mooy Esekiel, te lan la ko Yexowa won, fekk lu bon a bon la woon ?
Ndegam waa Israyil bëggatuñu ko topp, lan la Yexowa wax ?
Lan la buur Nebukanesar def bi ko waa Israyil bëggee xeex ?
Lu tax Yexowa bàyyi alag bu metti boobu dal waa Israyil ?
Naka la nit ñépp mujjee jóge Israyil, te ñaata at lañu def bitim réew ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 2 Buur yi (2 Rois) 25:1-26.
Kan moo doon Sédésiyas, te lan moo ko dal ? Loolu, naka la nekke woon li Biibël bi waxoon ne dina am (2 Buur. 25:5-7 ; Ézék. 12:13-15) ?
Ci gis-gisu Yexowa, kan moo gàddu woon àq ci lépp lu bon li waa Israyil defoon (2 Buur. 25:9, 11, 12, 18, 19 ; 2 Chron. 36:14, 17) ?
Jàngal Ézékiel 8:1-18.
Diine yi wax ne dañuy topp Kirist, fekk du dëgg, naka lañuy roye waa Israyil yi doon jaamu naaj bi (Ézék. 8:16 ; Is. 5:20, 21 ; Ywna. 3:19-21 ; 2 Tim. 4:3) ?
Nettali 77
Nanguwuñu sukk
Ban ndigal la Nebukanesar, mi nekkoon buur ci Babilon, jox mbooloo mi ?
Lu tax ñetti xaritu Dañeel bañ a sukk ci kanamu nataalu wurus bi ?
Bi Nebukanesar waxee ñetti Yawut yi ne dina leen mayaat ñu mën a sukk ci kanamu nataalu wurus bi, naka lañu wonee ne wóolu woon nañu Yexowa dëgg ?
Lan la Nebukanesar digal ñu def Sadarag, Mesag ak Abed-nego ?
Lan la Nebukanesar gis bi mu xoolee ci biir fuur bu mag boobu ?
Lu tax buur bi màggal Yàllay Sadarag, Mesag ak Abed-nego, te ñun, naka lañu leen mënee roy ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Dañeel 3:1-30.
Naka la jaamukati Yàlla yépp tey waree roy ñetti ndaw yu yawut yi bu amee ñu leen di bëgg a defloo lu bon (Dañ. 3:17, 18 ; Macë 10:28 ; Room 14:7, 8) ?
Yexowa Yàlla am na lu am solo lu mu jàngal Nebukanesar. Loolu mooy lan (Dañ. [Dan.] 3:28, 29 ; 4:34, 35) ?
Nettali 78
Loxo buy bind ci miir bi
Lan moo xew bi buuru Babilon defee benn feet bu mag te jëfandikoo ay kaas ak ay bool yi ñu jële woon kër Yexowa gi nekkoon Yerusalem ?
Lan la Balsasar wax boroom xam-xam yu Babilon yi, te lan lañu mënul a def ?
Lan la ko yaayam wax mu def ?
Ni ko Dañeel waxe buur bi, lu tax Yexowa def loxo bi bind ci miir bi ?
Ci li Dañeel wax, lan la mbind yi ci miir bi tekki ?
Lan moo xew fekk Dañeel pareegul sax wax ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Dañeel 5:1-6:1.
Ragal Yàlla ak ragal bi Balsasar amoon bi mu gisee mbind yi ci miir bi, lu ñu wuute (Dañ. 5:6, 7 ; Sab. 19:10 ; Room 8:35-39) ?
Naka la Dañeel wonee fit bu réy bi mu waxee ak Balsasar ak yeneen nit yu mag yu nekkoon foofu (Dañ. 5:17, 18, 22, 26-28 ; Jëf. 4:29) ?
Naka la Dañeel pàcc 5 màggale kiliftéef bi Yexowa am ci kow lépp (Dañ. 4:17, 25 ; 5:21) ?
Nettali 79
Dañeel ci kàmb gaynde yi
Kan mooy Dariyus, te naka lay gise Dañeel ?
Góor ñi doon iñaane Dañeel, lan lañu defloo Dariyus ?
Lan la Dañeel def bi mu déggee ndigal bu bees bi ?
Lan moo naqari Dariyus ba mënul nelaw, te lan la def bi suba si jotee ?
Lan la Dañeel tontu Dariyus ?
Lan moo dal nit ñu bon ñi bëggoon a rey Dañeel, te lan la Dariyus bind ñi bokkoon ci nguuram ñépp ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Dañeel 6:2-29.
Li nit ñooñu bëggoon a def Dañeel, lan la ñuy fàttali lu jëm ci li ay noon jéem a def ci suñu jamano ngir Seede Yexowa yi bàyyi liggéey bi ñuy def (Dañ. 6:8 ; Ps. 94:20 ; Is. 10:1 ; Room 8:31) ?
Naka la jaamukati Yàlla tey mënee roy Dañeel bu ñuy nangu kiliftéefu ‘ ñi yore baat ci kanamu ’ nit (Dañ. 6:6, 11 ; Room 13:1 ; Jëf. 5:29) ?
Naka lañu mënee roy Dañeel ci lu jëm ci kontine di jaamu Yexowa (Dañ. 6:17, 21 ; Fil. 3:16 ; Peeñ. 7:15) ?
Nettali 80
Mbooloo Yàlla mu ngi jóge Babilon
Ni ñu koy wonee foofu, lan la waa Israyil di def ?
Naka la Sirus defe li Yexowa waxoon jaare ko ci Esayi ?
Lan la Sirus wax waa Israyil yi mënul a dellu Yerusalem ?
Lan la Sirus jox mbooloo mi pur ñu delloo ko Yerusalem ?
Ñaata weer la waa Israyil def ci yoon bi bala ñu àgg Yerusalem ?
Ñaata at la réew mi def fekk amul woon kenn foofu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Isaïe 44:28 ak 45:1-4.
Naka la Yexowa wonee ne li mu wax lu jëm ci Sirus dina am ci lu wóor (Esa. 55:10, 11 ; Room 4:17) ?
Li Esayi waxoon lu jëm ci Sirus, naka lay wonee ne Yexowa Yàlla mën na wax luy am ëllëg (Esa. 42:9 ; Is. 45:21 ; 46:10, 11 ; 2 Piy. 1:20) ?
Jàngal Esras [Ezra] 1:1-11.
Ñi mënul woon a dellu Yerusalem, bu ñu toppee li ñu def, naka lañuy mënee dimbali tey ñi am buntu jébbal seen jot yépp ci liggéeyu Yàlla (Esr. 1:4, 6 ; Room 12:13 ; Kol. 4:12) ?
Nettali 81
Dañu yaakaar ci ndimbalu Yexowa
Ñaata nit ñoo jóge Babilon dem Yerusalem fekk yoon bi sore na, te lan lañu fekke bi ñu fa àggee ?
Lan la waa Israyil komaase tabax bi ñu àggee foofu, waaye lan la seeni noon def ?
Ñan ñooy Ase ak Sakari, te lan lañuy wax mbooloo mi ?
Lu tax Tatnay yónnee benn leetar ca Babilon, te ban tont la jot ?
Lan la Esras def bi mu déggee ne war nañu defaraat kër Yàlla gi ?
Xoolal li Esras di def foofu. Lan lay ñaan, naka la ame li mu doon ñaan, te loolu lan la ñuy jàngal ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Esras (Ezra) 3:1-13.
Bu ñu nekkee ci béréb bu amul mbooloo jaamukati Yàlla, lan lañu war a kontine di def (Ezra 3:3, 6 ; Jëf. 17:16, 17 ; Yaw. 13:15) ?
Jàngal Ezra 4:1-7.
Naka la Sorobabel nekke royukaay ci mbooloo Yexowa lu jëm ci ànd ak yeneen diine (Ex. 34:12 ; 1 Kor. 15:33 ; 2 Kor. 6:14-17) ?
Jàngal Esras (Ezra) 5:1-5, 17 ak 6:1-22.
Lu tax noon yi mënuñu woon a def ba ñu bàyyi tabax kër Yàlla gi (Esr. 5:5 ; Is. 54:17) ?
Li mag ñi ci Yawut yi defoon booba, naka lay xiire njiiti karceen yi tey ci jéem a xam li Yexowa bëgg bu amee ku leen di xeex (Esr. 6:14 ; Sab. 32:8 ; Room 8:31 ; Saag 1:5) ?
Jàngal Ezra 8:21-23, 28-36.
Bu amee lu ñu bëgg a def, lan lañu mën a roy ci Esras (Ezra 8:23 ; Sab. 127:1 ; Prov. 10:22 ; Saag 4:13-15) ?
Nettali 82
Mordekay ak Esteer
Ñan ñooy Mordekay ak Esteer ?
Lu tax buur Asuerus bëgg a takk beneen jabar, te kan la tànn ?
Kan mooy Amaan, te lu tax mu mer lool ?
Lan la buur bi digal, te lan la Esteer def bi mu déggee li ko Mordekay wax ?
Lan moo dal Amaan, te lan lañu def Mordekay ?
Naka la waa Israyil mucce ci seeni noon ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Esther 2:12-18.
Esteer wone na ne am “ xol bu nooy te dal ”, am na solo lool. Naka la defe loolu (Est. 2:15 ; 1 Piy. 3:1-5) ?
Jàngal Esther 4:1-17.
Esteer amoon na bunt ngir wone ne fonk na lépp lu jëm ci jaamu Yàlla dëgg ji. Ñun it, lan lañu mën a def tey ngir wone ne bëgg nañu Yexowa te dañu bëgg takku ci moom (Est. 4:13, 14 ; Macë 5:14-16 ; 24:14) ?
Jàngal Esther 7:1-6.
Naka la ñu bare ci mbooloo Yàlla tey defe lu mënoon a tax ñu fitnaal leen, mel ni li Esteer defoon (Est. 7:4 ; Macë 10:16-22 ; 1 Piy. 2:12) ?
Nettali 83
Miiru Yerusalem yi
Lan la waa Israyil yëgoon bi ñu amulee miir yu doon wër dëkku Yerusalem ?
Kan mooy Nëxemiya ?
Lan mooy liggéeyu Nëxemiya, te lu tax liggéey boobu am solo ?
Lan la Nëxemiya dégg ba xolam jeex, te lan la def ?
Naka la buur Artaserse baaxe ak Nëxemiya ?
Naka la Nëxemiya doxale tabax bi ci fasoŋ boo xam ne noonu Israyil yi duñu leen ko mën a teree def ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Nehémia 1:4-6 ak 2:1-20.
Naka la Nëxemiya jéemee xam li Yexowa bëgg mu def (Neh. 2:4, 5 ; Room 12:12 ; 1 Piy. 4:7) ?
Jàngal Nehémia 3:3-5.
Lan la njiit yi ak surga mbooloo yi mën a jàng ci li waa Tekowa (Teqoïtes) wuute woon ak seeni nit ñu mag ñi (Neh. 3:5, 27 ; 2 Tes. 3:7-10 ; 1 Piy. 5:5) ?
Jàngal Nehémia 4:1-23.
Lan moo xiiroon waa Israyil ci kontine di tabax bu dee sax dañu leen doon xeex lool (Neh. 4:6, 8, 9 ; Ps. 50:15 ; Is. 65:13, 14) ?
Naka la li waa Israyil defoon di dëgërale suñu ngëm tey ?
Jàngal Nehémia 6:15.
Bu ñu gisee naka la nit ñi àggalee tabaxu miiri Yerusalem bala ñaari weer mat sax, loolu, lan lay wone lu jëm ci doole bi ngëm di ñu mën a may (Ps. 56:3, 4 ; Macë 17:20 ; 19:26) ?
Nettali 84
Benn malaaka seetsi na Maryaama
Kan mooy jigéen bi ñuy wone foofu ?
Lan la Jibril wax Maryaama ?
Ci li Jibril wax, naka la Maryaama di ame doom fekk masul ànd ak góor sax ?
Lan moo xew bi Maryaama demee seeti mbokkam Elisabet ?
Lan la Yuusufa xalaat bi mu déggee ne Maryaama dafa ëmb, waaye lan moo tax mu soppi xelam ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Luug 1:26-56.
Maryaama matul woon. Waaye lan la Luug 1:35 wax ci li Yàlla def bi mu jëlee bakkanu doomam ci asamaan def ko ci biiru Maryaama (Hag. 2:11-13 ; Ywna. 6:69 ; Yaw. 7:26 ; 10:5) ?
Naka lañu màggale Yeesu bala mu juddu sax (Luug 1:41-43) ?
Naka la Maryaama nekke royukaay bu rafet ngir karceen yi ñu dénk tey lu réy ci liggéeyu Yàlla bi (Luug 1:38, 46-49 ; 17:10 ; Prov. 11:2) ?
Jàngal Macë 1:18-25.
Dëgg la, tuddewuñu Yeesu Emanuwel, waaye, naka la li mu def ci kow suuf wonee ne topp na li tur boobu tekki (Macë 1:22, 23 ; Ywna. 14:8-10 ; Yaw. 1:1-3) ?
Nettali 85
Yeesu juddu na fu ay mala di fanaan
Kan mooy liir bi ñuy wone foofu, te fan la Maryaama di ko tëral ?
Lu tax Yeesu juddu fu ay mala di fanaan ?
Góor ñiy dugg nii, ñan lañu, te lan la leen benn malaaka waxoon ?
Lu tax Yeesu wuute woon ak ñeneen nit ñi ?
Lu tax ñu mën a woowe Yeesu Doomu Yàlla ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Luug 2:1-20.
Lan la Sesaar Ogust def, fekk loolu bokkoon na ci li Yàlla waxoon ne dina am lu jëm ci juddu Yeesu (Luug 2:1-4 ; Mika 5:2) ?
Naka la nit mënee bokk ci ñi ñu woowe “ nit ñi mu nangu ndax yiwam ”, maanaam mbaaxaayam (Luug 2:14 ; Macë 16:24 ; Ywna. 17:3 ; Jëf. 3:19 ; Yaw. 11:6) ?
Sàmmkat yi nekkoon ci diiwaanu Yuda bégoon nañu lool ci li benn Musalkat juddu. Waaye tey, am na lu gën a war a tax jaamukatu Yàlla yi bég. Loolu lan la (Luug 2:10, 11 ; Efes 3:8, 9 ; Peeñ. 11:15; 14:6) ?
Nettali 86
Biddéew buy won ay góor seen yoon
Góor ñi ñuy wone foofu, ñan lañu? Lu tax kenn ci ñoom di joxoñ benn biddéew bu leer lool ?
Lu tax buur Erodd jaaxle, te lan la def ?
Biddéew bi leeroon lool, fan la yóbbu góor ñi ? Waaye lu tax bi ñu ñibbee seen réew, ñu jaar ci beneen yoon ?
Ban ndigal la Erodd joxe, te lu tax mu joxe ko ?
Lan la Yexowa sant Yuusufa ?
Kan moo taxoon biddéew boobu leer, te lu tax mu def loolu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 2:1-23
Bi gisaanekat yi jóge woon penku ñówee seetsi Yeesu, ñaata at la Yeesu amoon te fan la dëkkoon (Macë 2:1, 11, 16) ?
Nettali 87
Yeesu ci kër Yàlla gi, fekk xale la
Xoolal li ñuy wone foofu. Ñaata at la Yeesu am, te fan la nekk ?
Lan la Yuusufa faral a def at mu nekk, moom ak njabootam ?
Bi ñu jógee Yerusalem ba mu def benn fan, lu tax Yuusufa ak Maryaama delluwaat Yerusalem ?
Fan la Yuusufa ak Maryaama gise Yeesu, te lu tax nit ñi waaru ?
Lan la Yeesu wax yaayam Maryaama ?
Bu ñuy jàng lu jëm ci Yàlla, naka lañu mënee mel ni Yeesu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Luug 2:41-52.
Ci ndigal yi Yàlla joxoon Musaa, góor ñi rekk la Yàlla santoon ñu dem ci màggal yi ñu doon def at mu nekk. Waaye lan la Yuusufa ak Maryaama daan def, te lu tax loolu nekk lu jar a roy (Luug 2:41 ; Deut. 16:16 ; 31:12 ; Prov. 22:6) ?
Ci lu jëm ci déggal sa wayjur, naka la Yeesu nekke royukaay bu rafet ci ndaw yi tey (Luug 2:51 ; Deut. 5:16 ; Prov. 23:22 ; Kol. 3:20) ?
Jàngal Macë 13:53-56.
Yan ñeenti rakku Yeesu yu góor lañu wax seen tur ci Biibël bi ? Ban liggéey la ñaar ci ñoom mujj a def ci mbooloo mi (Macë 13:55 ; Jëf. 12:17 ; 15:6, 13 ; 21:18 ; Gal. 1:19 ; Saag 1:1 ; Yudd 1) ?
Nettali 88
Yaxya mu ngiy sóob Yeesu ci ndox
Ñan ñooy ñaari góor ñi ñuy wone foofu ?
Naka lañuy sóobe nit ?
Ñan la Yaxya doon sóob ci ndox ?
Lu tax Yeesu wax Yaxya mu sóob ko ci ndox ?
Naka la Yàlla wonee ne dafa kontaan ci li ñu sóob Yeesu ?
Lan moo xew bi Yeesu demee ci béréb bu wéet te des fa lu mat 40 fan ?
Waxal ñenn ci ñi jëkk a topp Yeesu, maanaam taalibeem yu jëkk yi. Lan mooy kéemaan bi Yeesu jëkk a def ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 3:13-17.
Ni ñu ko defe ak Yeesu, naka la taalibeem yi waree sóob nit ? (Ps. 40:7, 8 ; Macë 28:19, 20 ; Luug 3:21, 22) ?
Jàngal Macë 4:1-11.
Yeesu, ku aay la woon ci jëfandikoo Mbind mi bi mu doon jàngale. Lu tax loolu war ñu xiir ci tàmm a jàng Biibël bi (Macë 4:5-7 ; 2 Pet. 3:17, 18 ; 1 Ywna. 4:1) ?
Jàngal Yowaana 1:29-51.
Kan la Yaxya won taalibeem yi ngir ñu topp ko, te tey naka lañu mënee def ni moom (Ywna. 1:29, 35, 36 ; 3:30 ; Macë 23:10) ?
Jàngal Yowaana 2:1-12.
Kéemaan bi Yeesu jëkk a def, naka lay wonee ne Yexowa amul dara lu baax lu muy bañ a may jaamam yi (Yowaana 2:9, 10 ; Ps. 84:11 ; Saag 1:17) ?
Nettali 89
Yeesu dafay sellal kër Yàlla gi
Lu tax ñu doon jaay ay mala ci biir kër Yàlla gi ?
Lu tax Yeesu mer ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Yeesu, lan lay def te lan lay wax ñiy jaay pitax yi ?
Taalibe Yeesu yi, bi ñu gisee li mu doon def, lan lañu fàttaliku ?
Ci ban diiwaan la Yeesu jaar bi mu doon dellu Galile ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Yowaana 2:13-25.
Ndegam Yeesu dafa meroon bi mu gisee ñi doon wecceeku xaalis ci biir kër Yàlla gi, naka lañu war a gise mbirum jaay ak jënd ci biir Saalu Nguur gi (Ywna. 2:15, 16 ; 1 Kor. 10:24, 31-33) ?
Nettali 90
Mu ngiy waxtaan ak jigéen ci teen
Lu tax Yeesu toog ci wetu teen ci Samari, te lan lay wax benn jigéen foofu ?
Lu tax jigéen bi waaru ? Lan la ko Yeesu wax te lu tax mu wax ko loolu ?
Ndox mi Yeesu doon wax, ban ndox la woon, waaye lan la jigéen bi foogoon ?
Lu tax jigéen bi waaru ndax li Yeesu xam ci moom, te naka la Yeesu xame loolu ?
Lan lañu mën a jële ci waxtaan bi Yeesu am ak jigéen bi ci teen bi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Yowaana 4:5-43.
Bu ñu bëggee topp Yeesu, naka lañu war a gise nit ñi nu bokkalul xeet walla cosaan (Ywna. 4:9 ; 1 Kor. 9:22 ; 1 Tim. 2:3, 4 ; Tit 2:11) ?
Yan barke ci wàllu ngëm la nit mën a am bu demee ba nekk taalibe Yeesu (Ywna. 4:14 ; Is. 58:11 ; 2 Kor. 4:16) ?
Jigéen boobu bokkoon ci waa Samari, li mu dégg, dafa ko neexoon ba nga xam ne, dafa ko yàkkamti woon a xamal nit ñi. Naka lañu ko mënee roy ci loolu (Ywna. 4:7, 28 ; Macë 6:33 ; Luug 10:40-42) ?
Nettali 91
Yeesu mu ngiy jàngale ci kow tund
Xoolal li ñuy wone foofu. Fan la Yeesu di jàngalee, te ñan ñoo toog ci wetam ?
Waxal naka la 12 ndawu Yeesu yi tudd ?
Nguur gi Yeesu doon wax bi mu doon waare, ban nguur la ?
Yeesu wax na li ñu mën a ñaan Yàlla. Loolu lan la ?
Lan la Yeesu wax lu jëm ci ni ñu war a digaale ak suñu moroom ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 5:1-12.
Naka lañu mën a wonee ne xam nañu ne dafa am li ñu soxla ci wàllu ngëm (Macë 5:3 ; Room 10:13-15 ; 1 Tim. 4:13, 15, 16) ?
Jàngal Macë 5:21-26.
Naka la Macë 5:23, 24 wonee bu baax ne suñu diggante ak suñu mbokk ci ngëm, am na lu muy def ci suñu diggante ak Yexowa (Macë 6:14, 15 ; Ps. 133:1 ; Kol. 3:13 ; 1 Ywna. 4:20) ?
Jàngal Macë 6:1-8.
Lan la Karceen war a moytu lu jëm ci fexe ba nit gise ko ni ku jub, fekk jubul dëgg (Luug 18:11, 12 ; 1 Kor. 4:6, 7 ; 2 Kor. 9:7) ?
Jàngal Macë 6:25-34.
Lan la Yeesu wax ngir wone ne dañu war a wóolu Yexowa ci lu jëm ci faj suñuy soxla ci wàllu xaalis (Gàdd. 16:4 ; Ps. 37:25 ; Fil. 4:6) ?
Jàngal Macë 7:1-11.
Lan lañu mën a jàng ci li Yeesu misaal ci Macë 7:5 (Prov. 26:12 ; Room 2:1 ; 14:10 ; Saag 4:11, 12) ?
Nettali 92
Yeesu dafay dekkal ay nit ñu dee woon
Kan mooy baayu xale bu jigéen bi ñuy wone foofu, te lu tax moom ak jabaram jaaxle lool ?
Lan la Yayrus def bi mu gisee Yeesu ?
Bi Yeesu doon ànd ak Yayrus di dem këram, lan moo xew ci yoon bi, te ban xibaar la Yayrus jot bala ñu àgg ?
Lu tax nit ñi nekk ci kër Yayrus di reetaan Yeesu ?
Yeesu dafa wax ñetti ndawam, baayu xale bi ak yaayam ñu dugg ci néegu xale bu jigéen bi. Lan la def ginnaaw loolu ?
Waxal ñeneen ñi Yeesu dekkal, te li mu def noonu, lan lay wone ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Luug 8:40-56.
Jigéen bi feebaroon te doon xëpp deret, Yeesu won na ko ne ku am yërmande la te du yem rekk ci li Mbind mi wax, bañ ci boole lépp li ci war a ànd. Naka la defe loolu, te tey lan la njiiti mbooloo karceen yi mën a jàng ci loolu (Luug 8:43, 44, 47, 48 ; Lév. 15:25-27 ; Macë 9:12, 13 ; Kol. 3:12-14) ?
Jàngal Luug 7:11-17.
Am na lu Yeesu defal jigéen ju jëkkëram faatu woon te mu dëkkoon Nayin. Loolu naka la mënee seddal bu baax xolu ñi am mbokk bu gaañu (Luug 7:13 ; 2 Kor. 1:3, 4 ; Yaw. 4:15) ?
Jàngal Yowaana 11:17-44.
Naka la Yeesu wonee ne jooy bu sa mbokk gaañoo, dara aayu ci (Ywna. 11:33-36, 38 ; 2 Sam. 18:33 ; 19:1-4) ?
Nettali 93
Yeesu jox na lekk nit ñu bare
Am na lu garaaw lu dal Yaxya sóobkat bi. Loolu lan la, te lan la def Yeesu ?
Lan la Yeesu def ngir jox lekk mbooloo mi ko toppoon, te lekk bi desoon, nu mu tollu woon ?
Lu tax taalibe yi tiit ci guddi gi, te lan moo dal Piyeer ?
Ci ñaareelu yoon bi Yeesu joxee lekk ay junniy nit, naka la ko defe ?
Bu Yeesu di nguuru ci kow suuf si, lan mooy tax dund gi di neex lool ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 14:1-32.
Ban jikko Piyeer moo feeñ ci li ñu nettali ci Macë 14:23-32 ?
Naka la Mbind mi wonee ne Piyeer dafa mujj a màgg ci wàllu ngëm te dem ba nekk ku teey (Macë 14:27-30 ; Ywna. 18:10 ; 21:7 ; Jëf. 2:14, 37-40 ; 1 Piy. 5:6, 10) ?
Jàngal Macë 15:29-38.
Naka la Yeesu wonee ne du fowe lekk bi Yàlla jox nit ñi (Macë 15:37 ; Ywna. 6:12 ; Kol. 3:15) ?
Jàngal Yowaana 6:1-21.
Tey, naka la karceen yi mënee topp Yeesu ci lu jëm ci seen diggante ak nguur gi ilif seen réew (Ywna. 6:15 ; Macë 22:21 ; Room 12:2 ; 13:1-4) ?
Nettali 94
Ku bëgg xale la
Bi ndaw yi doon jóge dëkk bu sore, di ñibbisi, ci lan lañu doon werante ci yoon bi ?
Lu tax Yeesu woo benn xale bu ndaw, wax ko mu taxaw ci diggu ndaw yi ?
Ci ban fànn la ndawu Yeesu yi war a jéem a mel ni xale ?
Ay weer ginnaaw loolu, naka la Yeesu wonee ne ku bëgg xale la ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 18:1-4.
Lu tax Yeesu di joxe ay misaal bi mu doon jàngale (Macë 13:34, 36 ; Màrk 4:33, 34) ?
Jàngal Macë 19:13-15.
Bu ñu bëggee bokk ci barke yi Nguuru Yàlla di indi, yan jikko yu rafet yu nekk ci xale yu ndaw yi lañu war a am (Ps. 25:9 ; 138:6 ; 1 Kor. 14:20) ?
Jàngal Màrk 9:33-37.
Lan la Yeesu jàngal talibeem yi lu jëm ci bëgg a jiitu sa moroom (Màrk 9:35 ; Macë 20:25, 26 ; Gal. 6:3 ; Fil. 2:5-8) ?
Jàngal Màrk 10:13-16.
Ndax jege Yeesu yomboon na, te naka la ko njiitu mbooloo karceen yi mënee roy ci loolu (Màrk 6:30-34 ; Fil. 2:1-4 ; 1 Tim. 4:12) ?
Nettali 95
Ni Yeesu di jàngalee
Lan la benn góor laaj Yeesu, te lu tax mu laaj ko loolu ?
Lée-lée, lan la Yeesu di def ngir jàngal nit ñi, te lan lañu xam ba pare lu jëm ci diggante Yawut yi ak waa Samari ?
Ci li Yeesu nettali, lan moo dal benn Yawut bu doon dem Yeriko ?
Lan la benn Yawut bu nekkoon saraxalekat def bi mu awee ci yoon boobu ? Waa Lewi bi nag ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Kan mooy dimbali Yawut bi ñu gaañoon ?
Bi Yeesu jeexalee nettali bi, lan la laaj waa ji, te kooku, lan la ko tontu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Luug 10:25-37.
Bi ko benn xutbakat, maanaam ku doon gëstu yoonu Musaa, laajee dara, Yeesu tontuwu ko ci saa si, waaye dafa ko dimbali mu gisal boppam tont bi. Naka la defe loolu (Luug 10:26 ; Macë 16:13-16) ?
Naka la Yeesu doon jaar ci ay misaal ngir dimbali ñi ko doon déglu ñu bañ a ñaaw njort (Luug 10:36, 37 ; 18:9-14 ; Tit 1:9) ?
Nettali 96
Yeesu faj na ñi feebar
Lan la Yeesu doon def bi mu doon wër réew mi ?
Lan la Yeesu wax ndawam yi lu jege ñetti at ginnaaw bi ñu ko sóobee ci ndox ?
Ñan ñooy ñi ñuy wone foofu, te lan la Yeesu di defal jigéen bi ?
Lu tax kilifa diine yi rus bi ñu déggee li leen Yeesu tontu ?
Bi Yeesu ak ndawam yi nekkee ci wetu Yeriko, lan la Yeesu defal ñaari gumba yu doon yelwaan ?
Lu tax Yeesu doon def ay kéemaan ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 15:30, 31.
Naka la kàttanu Yexowa feeñe ci Yeesu ci fasoŋ bu doy kéemaan ? Loolu lu mu war a def ci ni ñuy gise li ñu Yexowa dig lu jëm ci àddina su bees si ? (Ps. 37:29 ; Is. 33:24) ?
Jàngal Luug 13:10-17.
Ci bésu noflaay bi la Yeesu defoon yenn ci kéemaanam yi gën a mag. Naka la loolu di wonee coono yi muy dindil doom-Aadama yi ci junni at yi muy nguuru ? (Luug 13:10-13 ; Sab. 46:9 ; Macë 12:8 ; Kol. 2:16, 17 ; Peeñ. 21:1-4) ?
Jàngal Macë 20:29-34.
Li ñu nettali fii, naka lay wonee ne Yeesu, ak li mu waroon a def yépp, masul ñàkk a jot ngir dimbali nit ñi ? Loolu lu mu ñuy jàngal (Deut. 15:7 ; Saag 2:15, 16 ; 1 Ywna. 3:17) ?
Nettali 97
Yeesu, Buur bi, mu ngi ñów
Bi Yeesu ñówee ci benn dëkk bu ndaw bu jege woon Yerusalem, lan la wax talibeem yi pur ñu def ko ?
Ci li ñuy wone foofu, lan moo xew bi Yeesu jegee Yerusalem ?
Lan la xale yu ndaw yi def bi ñu gisee Yeesu di faj ñi gumba ak ñi lafañ ?
Lan la Yeesu wax saraxalekat yi meroon ?
Naka lañu mënee mel ni xale yi doon tagg Yeesu ?
Lan la taalibe yi bëgg a xam ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 21:1-17.
Ni Yeesu dugge ci Yerusalem, fekk Buur la woon, naka la wuutee ak ni kilifa soldaar yi ci Room doon ñibbisi ginnaaw bi ñu gañee xare bi ñu doon def (Macë 21:4, 5 ; Sak. 9:9 ; Fil. 2:5-8 ; Kol. 2:15) ?
Li xale yu góor yu waa Israyil wax bi Yeesu doon dugg ci kër Yàlla gi, dañu ko jële woon ci Psaume 118. Lan la xale yu ndaw yi tey mën a jàng ci loolu (Macë 21:9, 15 ; Ps. 118:25, 26 ; 2 Tim. 3:15 ; 2 Piy. 3:18) ?
Jàngal Yowaana 12:12-16.
Bànqaasu garabu tiir yi nit ñi amoon bi ñu doon tagg Yeesu, lu ñuy misaal (Ywna. 12:13 ; Fil. 2:10 ; Peeñ. 7:9, 10) ?
Nettali 98
Ci tundu oliw yi
Xoolal li ñuy wone foofu. Ana Yeesu te ñan ñoo nekk ak moom ?
Saraxalekat yi, lan lañu jéem a def Yeesu ci kër Yàlla gi, te lan la leen Yeesu wax ?
Lan la ndaw yi laaj Yeesu ?
Lu tax Yeesu wax ndawam yi lu war a xew ci kow suuf si bés buy nguuru ca asamaan ?
Lan la Yeesu wax ne dina am bala muy dindi lépp lu bon ci kow suuf ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 23:1-39.
Dëgg la, Mbind mi dafa ñuy won ne bu ñuy woo nit, mën nañu jaar ci tiitar bi ñu koy woowe fi muy liggéeye. Waaye li Yeesu wax ci Macë 23:8-11, lan lay wone lu jëm ci jaar ci tiitar ngir màggal nit ci mbooloo karceen yi (Jëf. 26:25 ; Room 13:7 ; 1 Piy. 2:13, 14) ?
Lan la Farisen yi doon jéem a def ngir tere nit ñi ñu nekk karceen, te naka la njiiti diine yi tey defe lu mel noonu (Macë 23:13 ; Luug 11:52 ; Ywna. 9:22 ; 12:42 ; 1 Tes. 2:16) ?
Jàngal Macë 24:1-14.
Naka la Macë 24:13 wonee ni muñ ame solo ?
“ Muj ” gi ñuy wax ci Macë 24:13, lan la tekki (Macë 16:27 ; Room 14:10-12 ; 2 Kor. 5:10) ?
Jàngal Màrk 13:3-10.
Lan la Yeesu wax ci Màrk 13:10 luy wone ne waruñu yéexantu ci liggéeyu waare xibaar bu baax bi ? Li Yeesu wax noonu, lan la war a def ci ñun (Room 13:11, 12 ; 1 Kor. 7:29-31 ; 2 Tim. 4:2) ?
Nettali 99
Ci néeg bi nekk ci kow
Xoolal li ñuy wone foofu. Lu tax Yeesu ak 12 ndawam yi nekk ci néeg bu yaatu boobu ?
Kii di génn nii, kan la, te lan lay defi ?
Ban reer bu am solo la Yeesu komaase bi ñu lekkee reeru bésu Jéggi bi ba pare ?
Lan la bésu Jéggi bi doon fàttali waa Israyil, te reer bu am solo boobu Yeesu taxawal, lan lay fàttali taalibe Yeesu yi ?
Bi ñu lekkee reeru Sang bi ba pare, lan la Yeesu wax taalibeem yi, te lan lañu def ñoom ñépp ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 26:14-30.
Naka la Macë 26:15 wonee ne bi Yudaa woree Yeesu, moo ko teyoon ?
Ñaar a tax deretu Yeesu tuuru. Ñaar yooyu, lan ak lan la (Macë 26:27, 28 ; Yér. 31:31-33 ; Efes 1:7 ; Yaw. 9:19, 20) ?
Jàngal Luug 22:1-39.
Lu tax ñu wax ne Seytaane dafa solu Yudaa, maanaam dafa ko dugg (Luug 22:3 ; Ywna. 13:2 ; Jëf. 1:24, 25) ?
Jàngal Yowaana 13:1-20.
Bu ñu jàngee li nekk ci Yowaana 13:2 ba pare, ndax mën nañu wax ne Yudaa moo tey li mu def ? Loolu, lu muy jàngal ñiy jaamu Yàlla (Njàl. 4:7 ; 2 Kor. 2:11 ; Gal. 6:1 ; Saag 1:13, 14) ?
Naka la Yeesu nekke royukaay bu am solo lool (Ywna. 13:15 ; Macë 23:11 ; 1 Piy. 2:21) ?
Jàngal Yowaana 17:1-26.
Lan la Yeesu bëggoon a wax bi mu ñaanee Yàlla ngir taalibeem yi “ doon benn ” (Ywna. 17:11, 21-23 ; Room 13:8 ; 14:19 ; Kol. 3:14) ?
Nettali 100
Yeesu ci tool bi
Bi Yeesu ak ndawam yi jógee néeg ba nekkoon ci kow, fan lañu dem te lan la leen Yeesu wax ñu def ?
Bi Yeesu delloo fi ndawam yi nekkoon, lu mu fa fekk te loolu ñaata yoon la am ?
Ñan ñooy dugg ci tool bi, te lan la Yudaa Iskariyoo def, ni ñu koy wonee foofu ?
Lu tax Yudaa def loolu te lan la Piyeer def ?
Lan la Yeesu wax Piyeer, waaye lu tax ñaanul Yàlla mu yónni malaaka ngir dimbali ko ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 26:36-56.
Fasoŋ bi Yeesu doon xelal talibeem yi, lu tax mu nekk lu rafet lu njiiti mbooloo karceen yi tey war a topp (Macë 20:25-28 ; 26:40, 41 ; Gal. 5:17 ; Efes 4:29, 31, 32) ?
Lan la Yeesu wax ci jëfandikoo gànnaay ngir xeex sa moroom (Macë 26:52 ; Luug 6:27, 28 ; Ywna. 18:36) ?
Jàngal Luug 22:39-53.
Benn malaaka moo ñów ngir may Yeesu doole ci toolu Setsemane. Ndax loolu dafa tekki ne ngëmu Yeesu dafa doon wàññeeku ? Lu tax ngay tontu loolu (Luug 22:41-43 ; Is. 49:8 ; Matt. 4:10, 11 ; Yaw. 5:7) ?
Jàngal Yowaana 18:1-12.
Naka la Yeesu aare talibeem yi ci noonam yi, te lan lañu mën a jàng ci loolu (Ywna. 10:11, 12 ; 18:1, 6-9 ; Yaw. 13:6 ; Saag 2:25) ?
Nettali 101
Ñu ngiy rey Yeesu
Kan moo jëkk a gàddu àqu deewu Yeesu ?
Lan la ndaw yi def bi kilifa diine yi jàppee Yeesu ?
Lan moo xew ci kër Kayif mi nekkoon saraxalekat bu mag bi ?
Lu tax Piyeer dem, di jooy ?
Bi ñu delloo Yeesu ci Pilaat, lan la saraxalekat yu mag yi wax di yuuxu ?
Lan moo dal Yeesu àjjuma ji, bi midi paasee tuuti ? Lan la Yeesu dig nit ki defoon lu bon te ñu takkoon ko ci wetam ci benn bant ?
Àjjana bi Yeesu doon wax, fan lay nekk ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 26:57-75.
Ñi bokkoon ci gurupu àttekat yu mag yi ci Yawut yi, naka lañu wonee ne seen xol dafa bon (Macë 26:59, 67, 68) ?
Jàngal Macë 27:1-50.
Réccu bi Yudaa amoon, lu tax ñu mën a wax ne nekkul woon réccu dëgg (Macë 27:3, 4 ; Màrk 3:29 ; 14:21 ; 2 Kor. 7:10, 11) ?
Jàngal Luug 22:54-71.
Ci guddi gi ñu wor Yeesu ba jàpp ko, Piyeer waxoon na ne xamul Yeesu. Lan lañu mën a jàng ci loolu (Luug 22:60-62 ; Macë 26:31-35 ; 1 Kor. 10:12) ?
Jàngal Luug 23:1-49.
Xoolal li ñu def Yeesu, fekk deful woon dara lu bon. Waaye ba tey, moom lan la def ? Lan lañu mën a jàng ci loolu (Luug 23:33, 34 ; Room 12:17-19 ; 1 Piy. 2:23) ?
Jàngal Yowaana 18:12-40.
Piyeer mas na ragal nit ba mënatul woon a def li ko war. Waaye mujj na nekk ndawu Yeesu bu mag. Loolu, lan lay wone (Ywna. 18:25-27 ; 1 Kor. 4:2 ; 1 Piy. 3:14, 15 ; 5:8, 9) ?
Jàngal Yowaana 19:1-30.
Yeesu xamoon na ni ñu war a gise xaalis ak fi ñu ko war a yemale. Naka la ko gise woon (Ywna. 2:1, 2, 9, 10 ; 19:23, 24 ; Macë 6:31, 32 ; 8:20) ?
Kàddu yi Yeesu mujj a wax, naka lañu wonee ne Yeesu faraloon na kiliftéefu Yexowa ba mu mat (Ywna. 16:33 ; 19:30 ; 2 Piy. 3:14 ; 1 Ywna. 5:4) ?
Nettali 102
Yeesu mu ngi dund
Kan mooy jigéen bi ñuy wone foofu ? Ñan ñooy ñaari góor ñi, te fan lañu nekk ?
Lu tax Pilaat wax saraxalekat yi ñu yónni ay soldaar ngir wottu bàmmeelu Yeesu ?
Ci ñetteelu fan bi ginnaaw bi Yeesu deewee, lan la benn malaaka def ci suba teel, waaye lan la saraxalekat yi def ?
Jigéen yi demoon ci bàmmeelu Yeesu, lu tax ñu jaaxle ?
Lu tax Piyeer ak Yowaana daw ci bàmmeelu Yeesu, te lan lañu fa fekk ?
Lu tax néewu Yeesu nekkatu fa, waaye lan la Yeesu def ngir won taalibeem yi ne mu ngiy dund ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Macë 27:62-66 ak 28:1-15.
Bi Yàlla dekkalee Yeesu ba pare, naka la saraxalekat yu mag yi, Farisen yi ak yeneen mag bàkkaare ba tooñ xel mu sell mi (Macë 12:24, 31, 32 ; 28:11-15) ?
Jàngal Luug 24:1-12.
Li xewoon bi Yàlla dekkalee Yeesu, naka lay wonee ne ci gis-gisu Yexowa mën nañu gëm jigéen buy seede dara (Luug 24:4, 9, 10 ; Macë 28:1-7) ?
Jàngal Yowaana 20:1-12.
Naka la Yowaana 20:8, 9 wonee ne waruñu yàkkamti bu ñu xamagul naka la li Biibël bi yégle di ame (Prov. 4:18 ; Macë 17:22, 23 ; Luug 24:5-8 ; Ywna. 16:12) ?
Nettali 103
Ci biir néeg bu ñu tëj
Lan la Maryaama wax góor gi mu foogoon ne mooy kiy liggéey ci tool bi, waaye lan moo ko won ne Yeesu la woon ?
Lan moo dal ñaari taalibe Yeesu bi ñu doon dox, jëm ca dëkku Emayus ?
Bi ñaari taalibe yi doon wax ndaw yi ne gis nañu Yeesu, am na lu doy waar lu fa xew. Loolu mooy lan ?
Ñaata yoon la Yeesu feeñu taalibeem yi ?
Lan la Tomaa wax bi mu déggee ne taalibe yi gis nañu Yeesu, waaye lan moo xew juróom-ñetti fan ginnaaw loolu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Yowaana 20:11-29.
Ndax ci Yowaana 20:23 Yeesu dafa bëggoon a wax ne nit mën na baal bàkkaaru nit ? Leeralal sa tont (Ps. 49:2, 7 ; Esa. 55:7 ; 1 Tim. 2:5, 6 ; 1 Ywna. 2:1, 2)
Jàngal Luug 24:13-43.
Naka lañu mënee waajal suñu xol ngir mu nangu dëgg gi nekk ci Biibël bi (Luug 24:32, 33 ; Ezra 7:10 ; Macë 5:3 ; Jëf. 16:14 ; Yaw. 5:11-14) ?
Nettali 104
Yeesu mu ngiy dellu asamaan
Benn bés, ñaata taalibe la Yeesu feeñu, te ci lan la wax ak ñoom ?
Lan mooy Nguuru Yàlla, te ci junni at yi Yeesu di nguuru, dund gi ci kow suuf si, naka lay mel ?
Ñaata fan la Yeesu feeñu taalibeem yi ? Lan la war a def léegi ?
Tuuti bala Yeesu di tàggoo ak taalibeem yi, lan la leen sant ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan moo xew ? Ginnaaw loolu, lan moo nëbb Yeesu ba kenn mënatu ko gis ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal 1 Korent 15:3-8.
Ndaw li Pool dafa doon wax ci ndekkite Yeesu ci fasoŋ buy wone ne dafa gëmoon li mu doon wax. Lu tax mu mënoon a def loolu ? Ñun itam, ci lan lañu mën a wax tey ak ngëm gu mel noonu (1 Kor. 15:4, 7, 8 ; Is. 2:2, 3 ; Macë 24:14 ; 2 Tim. 3:1-5) ?
Jàngal Jëf ya 1:1-11.
Ni ko Jëf ya 1:8 waxe woon, ba fan la liggéeyu waare bi tollu woon (Jëf. 6:7 ; 9:31 ; 11:19-21 ; Kol. 1:23) ?
Nettali 105
Ñu ngiy xaar ci Yerusalem
Xoolal li ñuy wone foofu. Lan moo dal taalibe Yeesu yi doon xaar ci Yerusalem ?
Lan la nit ñi ñówoon Yerusalem gis ba waaru ?
Lan la Piyeer wax nit ñi ?
Bi nit ñi dégloo Piyeer ba pare, lan lañu yëg ci seen xol ? Lan la leen Piyeer wax ne dañu ko war a def ?
Ci bésu Pàntakot bu atum 33 ci suñu jamano, ñaata nit lañu sóob ci ndox ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 2:1-47.
Xoolal li Piyeer wax ci Jëf ya 2:23, 26. Naka la loolu wonee ne Yawut yi yépp ñoo amoon àq ci deewu Yeesu (1 Tes. 2:14, 15) ?
Naka la Piyeer wonee ci fasoŋ bu rafet ni ñu mënee waxtaan ak nit ci kow li Mbind yi wax (Jëf. 2:16, 17, 29, 31, 36, 39 ; Kol. 4:6) ?
Naka la Piyeer jëfandikoo caabi bi jëkk ci “ caabiy nguuru Yàlla ” yi ko Yeesu digoon (Jëf. 2:14, 22-24, 37, 38 ; Macë 16:19) ?
Nettali 106
Génne nañu leen kaso
Lan moo dal Piyeer ak Yowaana benn ngoon, bi ñu doon dugg ci kër Yàlla gi ?
Lan la Piyeer wax benn lafañ, te lan la ko jox lu ëpp maanaa xaalis fuuf ?
Lu tax kilifa diine yi mer, te lan lañu def Piyeer ak Yowaana ?
Lan la Piyeer wax kilifa diine yi, te ñoom lan lañu tere ndawu Yeesu yi ?
Lu tax kilifa diine yi iñaan, waaye lan moo xew ñaareelu yoon bi ñu tëjee ndaw yi kaso ?
Lan la ndaw yi tontu bi ñu leen indee ci saal bu mag bi fu ñu doon àttee nit ñi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 3:1-10.
Tey, ñun mënuñu def ay kéemaan. Waaye li Piyeer wax ci Jëf ya 3:6, naka la ñuy dimbalee ñu gën a gis njariñ bi nekk ci xibaaru Nguur gi (Ywna. 17:3 ; 2 Kor. 5:18-20 ; Fil. 3:8) ?
Jàngal Jëf ya 4:1-31.
Bu ñu dajee ak ay nit ñu bëgg a xeex suñu liggéeyu waare, naka lañu mënee roy suñuy mbokk karceen yu jëkk yi (Jëf. 4:29, 31 ; Efes 6:18-20 ; 1 Tes. 2:2) ?
Jàngal Jëf ya 5:17-42.
Naka la ay nit wonee gis-gis bu jub ci suñu liggéeyu waare bi, fekk nekkuñu woon Seede, muy ca jamano yu yàgg ya walla ci suñu jamano (Jëf. 5:34-39) ?
Nettali 107
Sànni nañu ay xeer Ecen ba rey ko
Kan mooy Ecen, te Yàlla dafa ko dimbali mu def lan ?
Lan la Ecen wax kilifa diine yi ba ñu mer lool ?
Bi ñu yóbboo Ecen ci biti dëkk bi, lan lañu ko def ?
Ki taxaw ci wetu yére yi, kan la ?
Bala mu dee, lan la Ecen ñaan Yexowa ?
Su amee ku ñu def lu bon, lan lañu war a def bu ñu bëggee roy Ecen ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 6:8-15.
Lan la kilifa diine yi def ngir Seede Yexowa yi bàyyi seen liggéeyu waare bi (Jëf. 6:9, 11, 13) ?
Jàngal Jëf ya 7:1-60.
Ecen mu ngi woon ci kanamu àttekat yi bokkoon ci kureelu àttekatu Yawut yi. Waar na leen bu baax ci xibaar bu baax bi. Lan moo ko dimbali ba mu mën a def loolu ? Lan lañu mën a jàng ci loolu ? (Jëf. 7:51-53 ; Room 15:4 ; 2 Tim. 3:14-17 ; 1 Piy. 3:15) ?
Naka lañu war a gise ñi bëgg a xeex suñu liggéey (Jëf. 7:58-60 ; Macë 5:44 ; Luug 23:33, 34) ?
Nettali 108
Ci yoonu Damas
Lan la Sool def ginnaaw bi ñu reyee Ecen ?
Bi Sool nekkee ci yoonu Damas, am na lu doy waar lu fa xew. Loolu lan la ?
Lan la Yeesu wax Sool mu def ?
Lan la Yeesu wax Anañas mu def, te lan lañu def Sool ba mu mën a gisaat ?
Naka lañu mujj a woowe Sool, te ban liggéey lañu ko dénk ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 8:1-4.
Fitnaal bu metti moo daloon mbooloo karceen bu bees bi. Fitnaal boobu tax na dëkk yu bare dégg lu jëm ci seen ngëm. Naka la loolu ame woon, te naka la amewaate tey ci suñu jamano (Jëf. 8:4 ; Is. 54:17) ?
Jàngal Jëf ya 9:1-20.
Ban liggéey bu def ñett la Yeesu bëggoon a dénk Sool (Jëf. 9:15 ; 13:5 ; 26:1 ; 27:24 ; Room 11:13) ?
Jàngal Jëf ya 22:6-16.
Lan lañu mën a def ngir mel ni Anañas, te lu tax loolu am solo (Jëf. 22:12 ; 1 Tim. 3:7 ; 1 Piy. 1:14-16 ; 2:12) ?
Jàngal Jëf ya 26:8-20.
Sool dem na ba nekk karceen. Lu tax loolu nekk lu neex a dégg ci ñi am jëkkër walla jabar ju nekkul Seede (Jëf. 26:11 ; 1 Tim. 1:14-16 ; 2 Tim. 4:2 ; 1 Piy. 3:1-3) ?
Nettali 109
Piyeer seetsi na Korney
Ki sukk fii, kan la ?
Lan la benn malaaka wax Korney ?
Lan la Yàlla feeñal Piyeer bi mu nekkoon ci teraasu kër Simoŋ, ca dëkk bi tudd Yope ?
Lu tax Piyeer wax Korney ne warul a sukk ci kanamam di ko jaamu ?
Lu tax taalibe yawut yi àndoon ak Piyeer waaru ?
Am na lu am solo li ñu mën a jàng ci li xewoon bi Piyeer demee kër Korney. Loolu lan la ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 10:1-48.
Li Piyeer wax ci Jëf ya 10:42, lan la ñuy xamal ci liggéeyu waare xibaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla (Macë 28:19 ; Màrk 13:10 ; Jëf. 1:8) ?
Jàngal Jëf ya 11:1-18.
Bi Piyeer gisee ba mu leer li Yexowa bëggoon a def ak ñi nekkul woon Yawut, lan la def, te naka lañu ko mënee roy ci loolu (Jëf. 11:17, 18 ; 2 Kor. 10:5 ; Efes 5:17) ?
Nettali 110
Timote mooy dimbali Pool léegi
Kan mooy xale bu góor bi ñuy wone foofu ? Fan la dëkk ? Yaayam ak maamam bu jigéen, naka lañu tudd ?
Pool dafa laaj Timote ndax bëgg na ànd ak moom ak Silas ngir waare ca dëkk yu sore. Lan la ko Timote tontu ?
Taalibe Yeesu yi, fan lañu leen jëkk a woowe “ karceen ” ?
Bi Pool, Silas ak Timote jógee Listar, waxal yenn ci dëkk yi ñu dem.
Ci lan la Timote dimbali Pool, te lan la ndaw yi tey war a laaj seen bopp ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 9:19-30.
Bi ay nit doon fitnaal Pool ci waaraate bi, naka la doon wonee ne dafa doon seet bu baax li mu war a def ngir moytu leen (Jëf. 9:22-25, 29, 30 ; Matt. 10:16) ?
Jàngal Jëf ya 11:19-26.
Naka la Jëf ya 11:19-21, 26 wonee ne xelum Yexowa mooy jiite liggéeyu waare bi ?
Jàngal Jëf ya 13:13-16, 42-52.
Naka la Jëf ya 13:51, 52 wonee ne taalibe Yeesu yi nanguwuñu fitnaal bi tax ba ñu bàyyi liggéeyu waare bi (Macë 10:14 ; Jëf. 18:6 ; 1 Piy. 4:14) ?
Jàngal Jëf ya 14:1-6, 19-28.
Li Biibël bi wax foofu ne ‘ dañu leen dénk Boroom bi ’, maanaam Yexowa, lu tax mu war a dalal suñu xel bu ñuy dimbali taalibe yu bees (Jëf. 14:21-23 ; 20:32 ; Ywna. 6:44) ?
Jàngal Jëf ya 16:1-5.
Li Timote nangu ñu xarafal ko, naka lay wonee ne def “ lépp ndax xebaar bu baax bi ”, am na solo (Jëf. 16:3 ; 1 Kor. 9:23 ; 1 Tes. 2:8) ?
Jàngal Jëf ya 18:1-11, 18-22.
Naka la Jëf ya 18:9, 10 wonee wàll bi Yeesu amoon ci liggéeyu waare bi te bu ñu jàngee loolu, lan moo ñu mën a wóor tey (Macë 28:20) ?
Nettali 111
Xale bu góor bu gëmméentu ba nelaw
Xale bu góor bi tëdd foofu ci suuf, kan la te lan moo ko dal ?
Lan la Pool def bi mu gisee ne xale bi dee na ?
Fan la Pool, Timote ak ñi ànd ak ñoom dem, te lan moo xew bi ñu taxawee ca Mile ?
Lan la yonent Yàlla Agabus wax Pool lu jëm ci li ko war a dal, te naka la loolu ame ni mu ko waxe woon ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 20:7-38.
Naka lañu mënee wax ne dañu set ci deretu ñépp, ni ko Pool waxe ci Jëf ya 20:26, 27 (Ézék. 33:8 ; Jëf. 18:6, 7) ?
Njiiti mbooloo mi, bu ñuy jàngale, lu tax ñu war a “ jàpp ci xebaar bu dëggu ” bi (Jëf. 20:17, 29, 30 ; Tit 1:7-9 ; 2 Tim. 1:13) ?
Jàngal Jëf ya 26:24-32.
Pool, waa Room la woon. Naka la jariñoo loolu bi mu doon def liggéeyu waare bi ko Yeesu dénkoon (Jëf. 9:15 ; 16:37, 38 ; 25:11, 12 ; 26:32 ; Luug 21:12, 13) ?
Nettali 112
Gaal gi toj na
Lan moo dal gaal gi Pool nekkoon bi mu awee ci wetu Kereet ?
Lan la Pool wax ñi nekkoon ak moom ci gaal gi ?
Naka la gaal gi toje ?
Lan la njiitu soldaar yi wax, te ñaata nit ñoo àgg tefes te mucc ?
Béréb boobu ñu teeroon, naka la tudd ? Bi asamaan si gënee neex, lan lañu def ak Pool ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 27:1-44.
Bu ñu gisee ni Biibël bi di nettalee tukki bi Pool def ba Room, lu tax mu gën ñu wóor ne Biibël bi dafay wax dëgg (Jëf. 27:16-19, 27-32 ; Luug 1:3 ; 2 Tim. 3:16, 17) ?
Jàngal Jëf ya 28:1-14.
Waa Màlt yi, dañu doon jaamu ay yàlla yu dul dëgg. Waaye ba tey, dañu won Pool ak ñi mu àndaloon “ laabiir gu ràññiku ”. Kon, lan la karceen yi war a wone ñoom itam ? Ci ban fànn lañu ko war a gën a def (Jëf. 28:1, 2 ; Yaw. 13:1, 2 ; 1 Piy. 4:9) ?
Nettali 113
Pool mu ngi Room
Yan nit la Pool waar bi mu nekkee kaso ca Room ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Gan gi toog, kan la te lan lay defal Pool ?
Kan mooy Epafrodit, te lan la yóbbaale bi mu ñibbee Filib ?
Lu tax Pool bind leetar xaritam bu baax bi tudd Filemon ?
Lan la Pool def bi mu génnee kaso, te lan moo ko dal ginnaaw loolu ?
Ci kan la Yexowa jaar ngir bind téere yu mujj yi ci Biibël bi, te ci lan la téere Peeñu ma di wax ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Jëf ya 28:16-31 ak Filib 1:13.
Bi Pool nekkee kaso ca Room, lan la doon def, te ngëm gu dëgër gi mu amoon, lan la def ci mbooloo karceen yi (Jëf. 28:23, 30 ; Fil. 1:14) ?
Jàngal Filib 2:19-30.
Am na lu Pool wax ci Timote ak Epafrodit te muy wone ne dafa leen fonk. Loolu lan la te naka lañu mënee roy Pool ci loolu (Fil. 2:20, 22, 25, 29, 30 ; 1 Kor. 16:18 ; 1 Tes. 5:12, 13) ?
Jàngal Filemon 1-25.
Ci lan la Pool sukkandiku ngir ñaan Filemon mu def li jub, te naka la njiiti mbooloo yi mënee roy Pool ci loolu tey (Filém. 9 ; 2 Kor. 8:8; Gal. 5:13) ?
Li Pool wax ci Filemon 13, 14, naka lay wonee ne dafa doon bàyyi karceen bu nekk mu def li ko xelam may (1 Kor. 8:7, 13 ; 10:31-33) ?
Jàngal 2 Timote 4:7-9.
Ni Pool, lan moo mën a tax mu wóor ñu ne su ñu toppee Yexowa ba ca muj ga Yexowa dina ñu barkeel (Macë 24:13 ; Yaw. 6:10) ?
Nettali 114
Lépp lu bon dina jeex
Lu tax Biibël bi di wax ci ay fas yu nekk ca asamaan ?
Xeex bi Yàlla di def ak nit ñu bon ñi ci kow suuf si, naka lañu koy woowe. Lu tax xeex boobu di am ?
Xoolal li ñuy wone foofu. Kan mooy Kiy jiite xeex boobu ? Lu tax mu sol ci boppam mbaxane yu buur yi di sol, te jaasi bi mu yor, lu mu tekki ?
Delluwaatal ci nettali 10, 15 ak 33. Boo seetee li ñu fa nettali, lu tax waruloo jaaxle boo déggee ne Yàlla dina alag nit ñu bon ñi ?
Yàlla dina alag nit ñu bon ñi bu fekkee ne sax dañuy wax ne ñoom dañuy jaamu Yàlla. Naka la nettali 36 ak 76 wonee loolu ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Peeñu ma 19:11-16.
Naka la Mbind yi wonee ci lu leer ne Yeesu Kirist mooy ki toog ci fas bu weex bi (Peeñ. 1:5 ; 3:14 ; 19:11 ; Esa. 11:4) ?
Mbubb bi Yeesu sol te ñu sóob ko ci deret, naka lay wonee ne moom mooy gañe xeex bi ba mu mat (Peeñ. 14:18-20 ; 19:13) ?
Ñan lañu mën a xalaat ne dinañu bokk ci xarekat yi topp Yeesu mi toog ci fas bu weex bi (Peeñ. 12:7 ; 19:14 ; Macë 25:31, 32) ?
Nettali 115
Àjjana ju bees ci kow suuf si
Ci li Biibël bi wax, naka la suuf si di mel bés bu Àjjana amee ci kow suuf ?
Ci Biibël bi, lan la Yàlla dig ñiy dund ci Àjjana ?
Kañ la Yeesu di def ba lu neex loolu am ?
Bi Yeesu nekkee ci kow suuf, lan la def ngir wone li muy def bés bu nekkee buur ci Nguuru Yàlla ?
Yeesu ak ñiy nguuru ak moom ci asamaan, bu ñuy ilif suuf si, lan lañuy defal nit ñi ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Peeñu ma 5:9, 10.
Lu tax mu mën ñu wóor ne ñiy nguuru ci kow suuf ci junni at yi, dinañu nekk buur ak saraxalekat yu baax te bare yërmande (Efes 4:20-24 ; 1 Piy. 1:7 ; 3:8 ; 5:6-10) ?
Jàngal Peeñu ma 14:1-3.
Dañu bind turu Baay bi ak turu Mbote mi ci jëwu 144 000 yi. Loolu, lu muy wone (1 Kor. 3:23 ; 2 Tim. 2:19 ; Peeñ. 3:12) ?
Nettali 116
Li ñu war a def ngir mën a dund ba fàww
Lan lañu war a xam bu ñu bëggee dund ba fàww ?
Lan lañu mën a def ngir jàng lu jëm ci Yexowa Yàlla ak Yeesu, ni ko xale bu jigéen bi ak xaritam yi ñuy wone foofu di defe ?
Beneen téere bi ñuy wone foofu, ban téere la, te lu tax ñu war koo faral di jàng ?
Ginnaaw jàng lu jëm ci Yexowa ak Yeesu, lan lañu war a def itam ngir am dund gu dul jeex ?
Nettali 69, lan la ñuy jàngal ?
Ni ñu ko wonee ci nettali 55, Samwil def na lu jar a roy fekk xale bu ndaw la woon. Loolu, lan lay wone ?
Naka lañu mënee roy Yeesu Kirist, te su ñu defee loolu, lan lañuy mën a am ëllëg ?
Leneen li ñu mën a laaj :
Jàngal Yowaana 17:3.
Naka la Mbind yi wonee ne xam Yexowa Yàlla ak Yeesu Kirist yemul rekk ci jàng lu jëm ci ñoom (Macë 7:21 ; Saag 2:18-20 ; 1 Ywna. 2:17) ?
Jàngal Sabóor 145:1-21.
Li tax ñu war a màggal Yexowa, bare na lool. Wax ci yenn (Ps. 145:8-11 ; Peeñ. 4:11).
Naka la Yexowa baaxe ak ñépp, te lu tax loolu war a tax ñu gën koo jege (Ps. 145:9 ; Macë 5:43-45) ?
Bëgg Yexowa dëgg, ci lan la ñuy xiir (Ps. 119:171, 172, 175 ; 145:11, 12, 21) ?