Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 112

Gaal Gi Toj Na

Gaal Gi Toj Na

XOOLAL gaal gi ! Am na poroblem, de ! Dafay toj ! Ndax gis nga ñi tëb ci biir géej gi ? Am na ñu àgg tefes ba pare. Góor gi nekk fii, mbaa du Pool ? Nañu seet li ko dal.

Yaa ngi fàttaliku ne Pool toog na kaso ñaari at ca Sesare. Ginnaaw loolu, moom ak ñeneen ñu nekkoon kaso, dañu leen dugal ci gaal gu doon jëm Room. Ci yoon bi, am na dun, maanaam suuf su feeñ ci biir géej gi, bu tudd Kereet. Dañu doon jaar ci wetam, ngelaw bu réy daldi am. Ngelaw bi dem ba mënatuñu woon a téye gaal gi. Mënuñu gis naaj bi bëccëg, mënuñu gis biddéew yi guddi. Ñu nekk noonu ay fan yu bare, ba amatuñu woon benn yaakaaru mucc.

Pool jóg, ne leen : ‘ Kenn ci yéen du dee. Gaal gi rekk mooy yàqu, ndaxte biig, benn malaaka Yàlla ñów na ci man, ne ma : “ Pool, bul tiit ! Fàww nga taxaw ci kanamu Sesaar, mi nekk buuru Room. Te Yàlla dina aar bakkanu ñi ngay àndal ñépp ci gaal gi. ” ’

Lu mat 14 fan ginnaaw bi ngelaw bu réy bi komaasee, ci booru minwi, ñi doon dawal gaal gi gis nañu ne xóotaayu ndox mi mu ngi wàññeeku ! Ñu ragal gaal gi dóor ay xeer ci guddi gi te toj, ñu daldi sànni diigal yi, maanaam lu diis lu ñu sànni ci biir géej gi te ñu lonk ko ci gaal gi ngir mu taxaw. Bi bët setee, ñu séen béréb bu wóor bu jege tefes gi fu ñu mënoon a yóbbu gaal gi. Ñu daldi jéem a dugal gaal gi foofu.

Dañu doon jublu ca tefes ga, gaal gi laal tundu suuf bu nekkoon ci biir géej gi, mu daldi caŋ foofu. Géej gi daldi dóor gaal gi ba mu komaasee toj. Ki doon jiite soldaar yi yore woon ñi nekkoon kaso, wax na lii : ‘ Képp ku fi mën a féey, na tëb ci biir ndox mi, jéem a jot tefes ga. Ñi ci des, nangeen def noonu it, langaamu ci ay tojitu gaal gi. ’ Ñu def loolu te 276 nit ñi nekkoon ci gaal gi ñépp àgg nañu tefes te mucc, ni ko malaaka mi waxe woon.

Dun bi mu ngi tudd Màlt. Nit ñi fa nekk, baax nañu lool te toppatoo nañu bu baax nit ñooñu mucc. Bi asamaan si gënee neex, ñu dugal Pool ci beneen gaal, yóbbu ko Room.