Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 89

Yeesu Dafay Sellal Kër Yàlla Gi

Yeesu Dafay Sellal Kër Yàlla Gi

FII de, Yeesu dafa mer lool ! Lu tax mu mer noonu ? Ndaxte nit ñooñu nekk ci kër Yàlla gi ci Yerusalem, dañu bëgge lool. Dañu bëgg a am xaalis bu bare ci ñi ñów fii ngir jaamu Yexowa.

Xoolal nag yi, xar yi ak pitax yi ñuy wone fii. Góor ñii dañu leen di jaay fii ci biir kër Yàlla gi. Xam nga lu tax ? Ndaxte waa Israyil dañu soxla ay mala ak ay picc ngir def ay sarax pur Yàlla.

Yàlla digal na ne bu benn waa Israyil defee lu bon, dafa war a may Yàlla dara. Amoon na it ay bés fu ñu waroon a def ay maye yu mel noonu. Waaye fan la waa Israyil mënee am picc ak mala bu ñuy saraxal Yàlla ?

Am na ay waa Israyil yu amoon ay picc ak ay mala yi ñu mënoon a saraxe. Waaye waa Israyil yu bare, amuñu ko woon. Amoon na ñeneen ñu dëkkoon fu sore lool. Mënuñu woon a indi mala ba ci kër Yàlla gi ci Yerusalem. Kon nit ñi dañu doon ñów fii, sog a jënd mala ak picc yu ñu soxla. Waaye góor ñii, li ñu doon jaaye mala yooyu, dafa ëppoon. Dañu doon nax nit ñi. Te it, waruñu woon a jaay ci biir kër Yàlla gi.

Loolu moo tax Yeesu mer noonu. Mu daldi daaneel taabal yi, xànjar yi tasaaroo. Mu jël ay buum, defar ci benn yar ba pare dàq mala yépp ci biti kër Yàlla gi. Mu wax ñiy jaay pitax yi : ‘ Génneleen fi pitax yépp ! Sama kër Baay, buleen ko def màrse. ’

Am na ay taalibe Yeesu yu nekk fi ci kër Yàlla gi ci Yerusalem. Dañu waaru ci li Yeesu def. Waaye ñu ngi fàttaliku fu Biibël bi waxe lii ci Doomu Yàlla ji : ‘ Mbëggeel bi muy am ci kër Yàlla gi, dina mel ni taal buy tàkk ci biiram. ’

Yeesu mu ngi Yerusalem di xaar bésu Jéggi bi. Ci diggante bi, def na ay kéemaan yu bare. Bi mu paree loolu yépp, mu jóge Yude, dellu Galile. Ci yoon bi, jaar na ci diiwaanu Samari. Nañu seet li xewoon foofu.