NETTALI 92
Yeesu Dafay Dekkal Ay Nit Ñu Dee Woon
XALE bu jigéen bi ngay gis fii, 12 at la am. Yeesu jàpp na loxoom te yaayam ak baayam ñu ngi taxaw foofu. Ndax xam nga lu tax ñu kontaan nii ? Nañu seet loolu.
Baayu xale bu jigéen bi, nit ku mag la. Yayrus la tudd. Benn bés, doomam bu jigéen feebar, ñu tëral ko ci laal. Waaye tanewul, feebar bi di yokku rekk. Yayrus ak jabaram jaaxle lool, ndaxte dafa mel ni xale bi dafay waaj a dee. Doom bu jigéen boobu rekk lañu am. Yayrus dem ci Yeesu. Dégg na kéemaan yi muy def.
Bi Yayrus gisee Yeesu, dafa fekk nit ñu bare wër ko. Waaye Yayrus jaar na ci biir nit ñi, daanu ci tànki Yeesu, ne ko : ‘ Sama doom bu jigéen dafa feebar lool. Maa ngi lay ñaan, nga ñów faj ko. ’ Yeesu ne ko dina ñów.
Bi ñu doon dem, nit ñi di buuxante rekk, ku nekk bëgg ko jege. Jékki-jékki Yeesu daldi taxaw, ne : ‘ Kan moo ma laal ? ’ Dafa yëg kàttan gu jóge ci moom, moo tax mu xam ne am na ku ko laal. Waaye kooku kan la ? Jigéen la bu feebaroon lu mat 12 at feebar bu metti. Moom moo ñówoon te laal yére Yeesu, daldi wér !
Yayrus kontaan na ndaxte gis na ne faj nit, yomb na ci Yeesu. Waaye mu am ku jóge kër Yayrus, ñów, ne Yayrus : ‘ Jaratul ngay sonal Yeesu. Sa doom faatu na. ’ Yeesu dégg loolu, mu ne Yayrus : ‘ Bul tiit. Dina baax. ’
Bi ñu àggee kër Yayrus, ñu gis ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Waaye Yeesu ne : ‘ Buleen jooy. Xale bi deewul. Day nelaw rekk. ’ Waaye dañu ko reetaan, di ko ñaawal ndaxte xam nañu ne dee na.
Yeesu jël baayu xale bi, yaay ji ak ñetti ndawam, ñu dugg ci néeg fi xale bi tëdd. Mu jàpp loxoom te ne : ‘ Jógal ! ’ Xale bi daldi dundaat, ni nga ko gise fii. Mu jóg, dox ! Loolu moo tax yaayam ak baayam kontaan lool !
Du xale bii la Yeesu jëkk dekkal. Ci li ñu jàng ci Biibël bi, ki Yeesu jëkk dekkal, doomu benn jigéen ju jëkkëram faatu la woon te mu dëkk Nayin. Yeesu dekkal na itam Lasaar mi bokkoon ndey ak baay ak Maryaama ak Màrt. Bu Yeesu di nguuru ci Nguuru Yàlla, dina dekkal ay nit ñu baree bare. Ndax loolu neexul a dégg lool ?