Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 98

Ci Tundu Oliw Yi

Ci Tundu Oliw Yi

FII, Yeesu la ci tundu Oliw yi. Ñeent yi ci des, ndawam yi la. Am na Andare ak Piyeer. Ñaar ñooñu ñoo bokk ndey ak baay. Am na it Saag ak Yowaana. Ñoom it ñoo bokk ndey ak baay. Li ngay gis noonu ci ginnaaw mooy kër Yàlla gi.

Am na léegi ñaari fan bi Yeesu duggee ci Yerusalem ci kow mbaam bu ndaw. Tey Talaata la. Ci suba si, Yeesu demoon na ci kër Yàlla gi. Foofu, saraxalekat yi jéem nañu ko jàpp ngir rey ko. Waaye dañu ragaloon ndaxte mbooloo mi dafa bëgg Yeesu.

Nii la Yeesu di woowee kilifa diine yooyu : ‘ Yéen, ay jaan ak doomu jaan ngeen ! ’ Mu ne leen Yàlla dina leen yar ndax lépp lu bon li ñu def, ba pare mu dem ci tundu Oliw yi. Ñeenti ndawam yi daldi am li ñu koy laaj. Ndax xam nga lan la ?

Dañu koy laaj lu jëm ci li war a am ëllëg. Xam nañu ne Yeesu dina dindi lépp lu bon ci kow suuf si. Waaye dañu bëgg xam kañ la loolu di am. Kañ la Yeesu di dellusi ngir nguuru ?

Yeesu xam na ne ñi koy topp fii ci suuf duñu ko mën a gis bés bu dellusee, ndaxte ci asamaan lay nekk, te duñu ko mën a gis foofu. Kon Yeesu wax na ndawam yi yenn ci xew-xew yi war a am ci kow suuf ci jamano bu muy nguuru ci asamaan. Loolu lan la ?

Yeesu nee na dina am xare yu mag, feebar ak xiif dina bare, nit ñiy jéggi yoon dinañu bare lool, te dina am yëngu-yëngu suuf yu réy. Yeesu wax na it ne dinañu yégle xibaar bu baax bi jëm ci nguuru Yàlla fu nekk ci àddina si. Ndax gis nañu xew-xew yooyu ci suñu jamano ? Waawaaw ! Kon na ñu wóor ne fi mu nekk nii, Yeesu mu ngiy nguuru ca asamaan. Léegi mu dindi lépp lu bon li am ci kow suuf si.