Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 81

Dañu Yaakaar Ci Ndimbalu Yexowa

Dañu Yaakaar Ci Ndimbalu Yexowa

AY JUNNIY junni nit ñoo jóge Babilon dem Yerusalem ci yoon bu gudd boobu. Bi ñu àggee Yerusalem, ñu gis ne dëkk bi, kër yu yàqu kese la woon. Kenn dëkku fa woon. Lépp la waa Israyil waroon a tabaxaat.

Lenn ci li ñu jëkk def mooy tabax benn saraxalukaay fu ñuy mën a saraxe ay mala ngir may leen Yexowa. Ay weer ginnaaw loolu, ñu daldi tàmbalee tabax kër Yàlla gi. Waaye dañu amoon ay noon yu dëkk ci réew yi leen jege. Noon yooyu, bëgguñu waa Israyil tabax kër Yàlla gi. Ñu daldi leen jéem a tiital pur ñu bàyyi tabax bi. Mujj nañu jaar ci buuru Pers bu bees bi ngir mu digal ñu bàyyi liggéey boobu.

At yi di jàll. Am na léegi 17 at bi waa Israyil jógee Babilon, ñów Yerusalem. Yexowa yónni na yonentam yi tudd Ase ak Sakari ñu wax mbooloo mi ñu tàmbaliwaat liggéey bi. Mbooloo mi gëm ne Yexowa dina leen dimbali, topp li yonent yi wax te tàmbaliwaat tabax bi, fekk xamoon nañu ne am na ndigal bu koy tere.

Kenn ku bokkoon ci nguuru Pers daldi ñów. Turam mooy Tatnay. Mu laaj leen kan moo leen may ñu tabax kër Yàlla gi. Waa Israyil ne ko bi ñu nekkee Babilon, buur Sirus moo leen waxoon lii : ‘ Léegi, demleen Yerusalem te tabax kër Yexowa mi nekk seen Yàlla. ’

Tatnay daldi yónni benn leetar ca Babilon ba xam ndax Sirus, mi dee ba noppi fi mu tollu nii, waxoon na loolu dëgg. Buuru Pers bu bees bi daldi gaaw a yónni leetar ngir ne loolu dëgg la, Sirus waxoon na ko. Buur bi teg ci lii : ‘ Bàyyil waa Israyil ñu tabax këru seen Yàlla. Te maa ngi lay digal nga dimbali leen. ’ Waa Israyil mujj nañu àggale kër Yàlla gi ci lu mat ñeenti at. Ñu kontaan lool.

At yaa ngi dem rekk. Bi ñu àggalee kër Yàlla gi, am na léegi lu jege 48 at. Ci Yerusalem, nit ñi amuñu xaalis te dëkk bi ak kër Yàlla gi rafetuñu noonu. Ca Babilon, Esras mi nekk waa Israyil dégg na ne am na lu ñu war a defar ci kër Yàlla gi. Xam nga lan la def ?

Esras dem na ci Artaserse mi nekk buuru Pers. Buur bu baax boobu may na ko lu bare lu muy yóbbu Yerusalem. Esras laaj na waa Israyil yi nekk Babilon ñu dimbali ko ci. Lu tollu ak 6 000 nit ñoo nangu dem ak moom. Li ñu waroon a yóbbu mooy xaalis, wurus ak yeneen yëf yu am maanaa.

Xelu Esras dalul, ndaxte ci yoon bi am na ay nit ñu bon ñu mën a sàcc seen xaalis ak seen wurus te rey leen. Esras daldi def li ñuy wone fii. Mu woo ñi mu war a àndal, ñu ñaan Yexowa mu aar leen ci yoon bu gudd bi jëm Yerusalem.

Yexowa aar na leen. Def nañu ñeenti weer ci yoon bi, ñu daldi àgg Yerusalem ci jàmm. Ndax loolu wonewul ne Yexowa mën na aar ñiy teg seen yaakaar ci moom ngir mu dimbali leen ?

Esras (Ezra) pàcc 2 ba 8.