Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 18

Yanqóoba dem na karan

Yanqóoba dem na karan

NDAX xam nga ñan la Yanqóoba di waxal fii ? Moom def na ay fan yu bare ci yoon bi. Léegi àgg na ci benn teen. Mu gis nit ñii di toppatoo seeni xar. Mu ne leen : ‘ Fan ngeen dëkk ? ’

Ñu ne : ‘ Karan. ’

Mu ne leen : ‘ Ndax xam ngeen Laban ? ’

Ñu ne : ‘ Waaw. Doomam Rasel moo nekk nii di ñów ak géttu baayam. ’ Ndax gis nga Rasel fii ?

Yanqóoba gis Rasel ak géttu nijaayam Laban, mu daldi dindi xeer bi uboon teen bi, ngir xar yi mën a naan. Ba pare mu fóon Rasel te wax ko ki mu doon. Rasel daw këram, yégal ko baayam Laban.

Laban kontaan na lool ndax li Yanqóoba nekke këram. Moo tax mu kontaan it bi mu ko ñaanee doomam Rasel. Waaye dafa wax Yanqóoba mu liggéeyal ko juróom-naari at bala mu koy may Rasel. Yanqóoba nangu ndaxte bëggoon na Rasel lool. Waaye bi bésu séy bi jotee, xam nga lan moo xew ?

Laban mayu ko Rasel. Dafa ko may magam bi tudd Leya. Laban nee na ko bala mu koy may Rasel, fàww mu nangu liggéeyal ko yeneen juróom-ñaari at. Yanqóoba nangu. Ca jamano yooya, Yàlla dafa doon bàyyi nit mu am lu ëpp benn jabar. Waaye léegi, ni ko Biibël bi wonee, góor, benn jabar rekk la war a am.