NETTALI 1
Yàlla Mu ngi tàmbalee sàkk
LÉPP lu baax lu ñuy gis, Yàlla moo ko sàkk. Sàkk na naaj bi ngir leer am bëccëg. Sàkk na weer bi ak biddéew yi ngir ñu am tuuti leer guddi. Suuf si, dafa ko sàkk ngir ñu dund ci.
Waaye naaj bi, weer bi, biddéew yi ak suuf si, du loolu la Yàlla jëkk a sàkk. Ndax xam nga lan la jëkk a sàkk ? Dafa jëkk a sàkk ay malaaka. Ni ñu mënulee gis Yàlla, noonu lañu mënulee gis malaaka yi. Yàlla dafa sàkk malaaka yi ngir ñu nekk ak moom ca asamaan.
Malaaka bi Yàlla jëkk a sàkk, wuute woon na ak yeneen malaaka yi. Ndegam moom la Yàlla jëkk a sàkk, mu ngi meloon ni taawam. Loolu moo tax ñu koy woowe Taawu Yàlla. Dafa doon liggéey ak Yàlla bi Yàlla doon sàkk lépp, naaj bi, weer wi, biddéew yi ak suuf si.
Naka la suuf si meloon ca njëlbéen ? Booba, kenn mënul woon a dund ci kowam. Ndox rekk moo muuroon suuf si sépp. Waaye Yàlla dafa bëggoon nit dëkk ci. Mu daldi def ba loolu mën a am. Lan la def ?
Yàlla dafa jëkk a indi leer ndaxte suuf si, leer la jëkk a soxla. Yàlla fexe na ba leer gi jóge ci naaj bi agsi ba ci suuf si. Guddi ak bëccëg daldi am. Ginnaaw loolu, fexe na ba suuf si feeñ ci kow ndox mi muuroon suuf si sépp.
Booba amul woon dara ci kow suuf si. Xoolal li ñuy wone fii. Noonu la suuf si meloon. Tóor-tóor amul woon. Garab amul woon. Mala amul woon. Amul woon sax jën ci géej gi. Desoon na lu bare bala suuf si rafet te mala yi ak nit ñi mën cee dund.