Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
Téere bii dañu ko defar ngir dimbali la nga xam li Biibël bi wax ci lu bare, lu mel ni lu tax ñuy am ay metit, lan mooy dal nit bu deewee, li ñu mën a def ba gën a am jàmm ci suñu kër, ak yeneen yu mel noonu.
Ndax lii la Yàlla bëggoon ?
Xey na dinga laaj sa bopp lu tax coono yi bare tey. Ndax xam nga ne Biibël bi wax na ci lu jëm ci ay coppite yuy ñëw te mën nga ci jariñoo ?
PÀCC 1
Li ñu wax ci Yàlla bare na. Lan mooy dëgg gi ?
Ndax yaakaar nga ne Yàlla fonk na la yaw ci sa bokk ? Jàngal lu jëm ci jikkoom ak ni nga mën a def ba jege ko.
PÀCC 2
Biibël bi : téere la bu jóge ci Yàlla
Naka la la Biibël bi mënee dimbali ci say poroblem ? Lu tax nga mën a gëm li mu wax ne dina am ëllëg ?
PÀCC 3
Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?
Ndax àjjana bi Yàlla bëggoon ci kaw suuf dina mas a am ? Bu dee waaw, kañ ?
PÀCC 4
Kan mooy Yeesu Kirist ?
Jàngal ba xam li tax Yeesu nekk Almasi bi Yàlla dige woon, fi mu nekkoon bala muy ñëw ci kaw suuf, ak li tax ñu koy woowe benn doom ji Yàlla am kepp.
PÀCC 6
Fan la ñi dee nekk ?
Jàngal li Biibël bi wax ci li jëm fi nit ñi dee nekk ak li tax doomu Aadama yi dee.
PÀCC 7
Ci lu wóor mën nañu yaakaar ne suñu mbokk yi gaañu dinañu dekki
Ndax mas nga am mbokk walla xarit bu gaañu ? Ndax mën nañu leen a gisaat ? Jàngal li Biibël wax ci ndekkite.
PÀCC 8
Lan mooy Nguuru Yàlla ?
Ay nit ñu bare xam nañu ñaan bi ñuy woowe Suñu Baay bi. “ Na sa nguur ñëw ”, lan la wax jooju di tekki ?
PÀCC 9
Ndax ñu ngi ci “ muju jamono ”?
Seetal liy xew ak ni nit ñi mel di dëggale ne ñu ngi dund ci “ muju jamono ” bi Biibël bi yégle woon .
PÀCC 10
Malaaka yi : li ñuy def nit ñi
Biibël bi dafay wax ci malaaka yu baax yi ak yu bon yi. Ndax malaaka yooyu am nañu ci dëgg ? Ndax mënal nañ ñu dara ?
PÀCC 11
Lu tax Yàlla bàyyi nit ñi di am metit ?
Ñu bare dañu foog ne Yàlla moo dogal metit yépp yiy am ci àddina. Lan moo ciy sa xalaat ? Jàngal li Yàlla wax ne moo tax metit yi di am.
PÀCC 12
Nañu dund ci fasoŋ bu neex Yàlla
Mën nga dund dund bu neex Yexowa. Noonu dinga mën a nekk xaritam.
PÀCC 13
Nañu jàppe bakkan ni ko Yàlla jàppe
Naka la Yàlla gise yàq biir, sol deret ci sa yaram ak bakkanu mala yi ?
PÀCC 14
Li ñu mën a def ba suñu njaboot bare jàmm
Mbëggel bi Yeesu amoon royukaay bu jëkkër yi, jabar yi, waajur yi ak xale yi mën a roy. Lan lañuy jàng ci moom ?
PÀCC 16
Woneel ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge
Yan jafa-jafe nga mën a am booy wax nit ñi li nga gëm ? Naka nga mën a def ba bañ leen a merloo ?
PÀCC 17
Jegeleen Yàlla ci ñaan
Ndax Yàlla dina déglu say ñaan ? Boo bëggee xam tontu laaj boobu, faww nga xam li Biibël bi jàngale lu jëm ci ñaan Yàlla.
PÀCC 18
Sóob bi ak sa diggante ak Yàlla
Lan la karceen war a def ngir ñu sóob ko ci ndox ? Jàngal li sóob boobu di tekki ak ni ñu koy defe.
PÀCC 19
Nañu sax ci mbëggeelu Yàlla
Naka lañu mën a wone mbëggeel ak ngërëm ci lépp li ñu Yàlla defal ?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Turu Yàlla : ni ñu koy jëfandikoo ak li muy tekki
Dañu dindi turu Yàlla ci ay Biibël yu bare yu ñu bind ci yeneen làkk. Lu tax ? Woo Yàlla ciw turam, ndax am na solo ?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Ni yonent Yàlla Dañeel yéglee ñëwu Almasi bi
Yàlla xamle na ñëwu Almasi bi lu ëpp 500 at bala ñuy àgsi. Jàngal lu jëm ci yégle bu yéeme boobu !
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Yeesu Kirist, Almasi bi Yàlla dige woon
Gis nañu ci Yeesu lépp li ñu yégle woon ci Biibël bi te mu jëm ci Almasi bi. Seetal ci sa Biibël ni yégle yooyu ame ba bi ci gën a ndaw.
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Dëgg gi ci lu jëm ci Baay bi, Doom ji, ak xel mu sell mi
Nit ñu bare dañu gëm ne Biibël bi mooy jàngale trinité. Ndax loolu dëgg la ?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Lu tax karceen dëgg yi duñu jëfandikoo kurwaa ngir jaamu Yàlla
Ndax ci dëgg Yeesu ci bant la dee ? Jàngal tont bi bi Biibël bi joxe ci loolu.
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Reeru Boroom bi : Fàttaliku buy màggal Yàlla
Dañu sant karceen yi ñuy fàttaliku deewu Kiris. Kañ lañu koy def ak naka lañu ko war a defe?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Ci dëgg-dëgg, lan mooy “ ruu ” ak lan mooy “ xel ” ?
Ñu bare dañu foog ne, bu nit deewee dafay am luy jóge ci moom kontine di dund feneen. Lan lañu Kàddu Yàlla wax ci loolu ?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Lan mooy shéol ak hadès ?
Ci Biibël yi ñu bind ci yeneen làkk, “ bammeel ”, “ safara ” ci palaasu shéol ak hadès. Lan la baat yooyu di tekki dëgg ?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Lan mooy Bésu Àtte bi ?
Jàngal ngir xam ni Bésu Àtte bi nekke luy indil barke doomu aadama yépp yi topp Yàlla.
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
1914 : At bu am solo ci li Biibël bi wax ne dina am
Ban xew-xew ci Biibël bi mooy wone ne atum 1914 dafa amoon solo ?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Kan mooy Mikayel mi nekk kilifa ci malaaka yi ?
Biibël bi wax na kan mooy kilifa ci malaaka yi te mu bare doole. Jàngal ngir gën a xam lu jëm ci moom ak li mu nekk di def léegi.
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Lan mooy “ Babilon mu mag mi ”
Téere Peeñu ma wax na lu jëm ci ab jigéen bu ñuy woowee “ Babilon mu mag mi. ” Ndax jigéen dëgg la ? Lan la Biibël bi wax ci moom ?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Ndax ci weeru desàmbar la Yeesu juddu ?
Nañu seet ni climat bi doon mel ci at bi Yeesu juddu. Loolu, lan lañuy jàngal ?
LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Ndax war nañu bokk ci feet yi ?
Feet yu bare yi nit ñi di feetu ci fi nga dëgg fan lañu jóge ? Tontu laaj bi mën na la bett.