WOY-YÀLLA Nº 132
Léegi benn lañu
-
1. Yaay sama suux, sama soxna,
Sama soppe, sama reeni xol.
Yexowa moo ma la baaxe, Léegi dootuma wéet.
Maay sa jëkkër, ñooy bokk kër,
Nañu bennoo, te doon ñu mànkoo.
Yàlla moo fas diggante bi,
Moom moo yelloo ndam li.
Gërëm ko, moom mooy ki ñuy leeral.
Ñu takku ci moom,
Moom mi def góor ak jigéen.
Na suñu waaw doon waaw ba fàww,
Su ko defee,
Yàlla bég ci ñun.
Bare na lu mën a weesu,
Waaye suñu mbëggeel du wees.
(Xoolal itam Njàlbéen ga 29:18; Kàdduy Waare 4:9, 10; 1 Korent 13:8.)