Woy yi

Ay woy yu neex yu ñu def ndax ngërëm gi ñu am ci lépp li ñu am tey ci wàllu ngëm.

Topp say santaane mooy sama mbégte (Woyu ndaje bu mag bu ñetti fan bu atum 2025)

Yeesu dafa bégoon ci déggal Yàlla. Bu ñu royee ci moom, ñun it dinañu bég ci def li Yàlla santaane.

Nañu màggal Yexowa

Mbëggeel ak ngërëm bi ñu am ci Yexowa, moo ñuy xiir ci màggal ko.

“Am nañu Xibaaru jàmm”! (Woyu Ndaje bu mag bu ñetti fan bu atum 2024)

Am na ay nit ñuy waare xibaaru jàmm bi ak mbégte, ci jamano karceen yu njëkk ya ba léegi, te li ñu def ci liggéey boobu moo ëpp fuuf li ñenn ci ñun def.—Yeesu ci boppam moo jiite liggéey boobu ànd ci ak malaaka yi.

‘Yàggatul dara’ (Woyu Ndaje bu mag bu ñetti fan bu atum 2023)

Royleen ci ñi takkuwoon, te ngeen muñ di xaar Yexowa.

Gëm naa ne Yexowa mu ngi ak man

Xalaatal rekk suuf su naat siy xaar doomu Aadama yi.

Suñu mbégte ba fàww

Yexowa rekk moo ñu mën a may mbégte dëgg.

Mbëggeel gu amul àpp

Mbëggeel gi jóge ci Yexowa amul àpp. Dafa ñuy may mbégte te di ñu dëfal.

Dëgërlul doon jàmbaar

Woy wu neex wuy tax ñuy dëgërlu.

May ma fit

Yexowa mën na ñu may fitu jànkoonteel bépp jafe-jafe.

Bul ragal

Bu ñu nekkee ci jafe-jafe buñu fàtte ne am na ku ànd ak ñun.

Sorry, there are no terms that match your selection.