Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

28 oktoobar ba 3 ​nowàmbar

TAALIFI CANT 103-104

28 oktoobar ba 3 ​nowàmbar

Woy-Yàlla nº. 30 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Dafay «bàyyi xel ne pënd lanu»

(10 minit)

Yexowa dafa bare yërmande, looloo tax mu am gis-gis bu yem ci ñun (Taalifi Cant 103:8; w23.07-F 21 § 5)

Buñu juumee sax, Yexowa duñu bàyyi (Taalifi Cant 103:​9, 10; w23.09-F 6-7 § 16-18)

Duñu laaj mukk ñu def luñu mënul (Taalifi Cant 103:14; w23.05-F 26 § 2)

LAAJAL SA BOPP LII: ‘Ndax gis-gis bu yem bi Yexowa am ci ñun, feeñ na ci ni may doxale ak sama jëkkër walla sama jabar?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 104:24—Lan la ñu aaya bii di jàngal ci Yexowa mi sàkk lépp? (cl-F 64 § 18)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. (lmd-F lesoŋ 3 ponk 4)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) KËROO-KËR. Nit ki dafa nangu jàng Biibël bi. Seetaanal ak moom te waxtaan ci wideo bi tudd Dalal ak jàmm ci sa njàngum Biibël bi (th lesoŋ 9)

6. Waxtaan bi

(5 minit) lmd-F appendice A idée 6—Turu waxtaan bi: Jëkkër dafa war a «bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam.» (th lesoŋ 1)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 44

7. Ndax xam nga fi sa doole yem?

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Buñuy jaamu Yexowa ak suñu xol bépp, dañuy bégal xolam te ñun itam dinañu bég (Taalifi Cant 73:28). Waaye buñu bàyyiwul xel ci fi suñu doole yem, loolu mën na tax ñu jaaxle walla ñu xàddi fekk jaru ko.

Woneel WIDEO bi tudd: Xamal fi sa doole yem te def li nga mën ak sa xol bépp. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Lan la Yexowa di xaar ci ñun? (Mise 6:8)

  • Lan moo dimbali mbokk bu jigéen bi mu bañ a jaaxle lool ci ni mu mënee matal jubluwaay bi mu amoon?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëjee ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 55 ak ñaan