21 oktoobar ba 27 oktoobar
TAALIFI CANT 100-102
Woy-Yàlla nº. 37 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
1. Yexowa ku gore la. Ñun itam dañu war a gore te takku ci moom
(10 minit)
Nañu bëgg Yexowa ak suñu xol bépp (Taalifi Cant 100:5; w23.03-F 12 § 18-19)
Nañu moytu lépp li mën a yàq suñu xaritoo ak Yexowa (Taalifi Cant 101:2, 3; w23.02-F 17 § 10)
Nañu moytu képp kuy tilimal turu Yexowa ak mbootaayam (Taalifi Cant 101:5; w11-F 15/7 16 § 7-8)
LAAJAL SA BOPP LII: ‘Ndax ni may jëfandikoo réseaux sociaux yi mën na yàq sama diggante ak Yexowa?’
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
Taalifi Cant 102:8—Lu tax taalifkat bi méngale boppam ak picc bu wéetoo ci kaw teraas? (it-2-F 522)
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Taalifi Cant 102:2-29 (th lesoŋ 12)
4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(3 minit) KËROO-KËR. (lmd-F lesoŋ 2 ponk 3)
5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki
(5 minit) KËROO-KËR. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 9 ponk 4)
6. Wax ci li ñu gëm
(4 minit) Wone bi. ijwbq-F 129—Wone bi mu ngi sukkandiku ci waxtaan bii: Biibël bi, ndax am na lu ñu ci yokk walla lu ñu ci wàññi? (th lesoŋ 8)
Woy-Yàlla nº. 137
7. «Dama takku ci yaw; nga teye ma»
(15 minit)
Waxtaan ak ñi teew. Woneel WIDEO bi. Ba pare nga laaj ñi teew lii:
Naka la Aana wone ngor maanaam mbëggeel gu takku?
Naka lañu mënee roy ci moom?
8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi
(30 minit) bt-F pàcc 17 § 1-7