Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

3 feewriyee ba 9 feewriyee

TAALIFI CANT 144-146

3 feewriyee ba 9 feewriyee

Woy-Yàlla nº 145 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. «Nit ñi nga xam ne Yexowa mooy seen Yàlla, bég nañu!»

(10 minit)

Yexowa dafay barkeel ñi ko wóolu (Taalifi Cant 144:​11-15; w18.04-F 32 § 3-4)

Nañu bég ci yaakaar bi ñu am (Taalifi Cant 146:5; w22.10-F 28 § 16-17)

Nit ñi nga xam ne Yexowa mooy seen Yàlla dinañu bég ba fàww! (Taalifi Cant 146:10; w18.01-F 26 § 19-20)

Bu ñuy jaamu Yexowa ak takkute, dinañu bég bu dee sax dañu am ay jafe-jafe

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 145:​15, 16—Naka lañu aaya yii di wonee ni ñu war a jàppe mala yi? (it-1-F 125 § 1)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(4 minit) KËROO-KËR. Li nga mën a def bu la nit ki waxee ne université la nekk. (lmd-F lesoŋ 1 ponk 5)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Wonal nit ki benn ci wideo yi nekk ci jumtukaay yi ngir jàngale Biibël bi, ba pare ngeen waxtaan ci. (lmd-F lesoŋ 7 ponk 4)

6. Waxtaan bi

(4 minit) lmd-F appendice A idée 7—Turu waxtaan bi ci farãse: Une femme « doit avoir un profond respect pour son mari ». (th lesoŋ 1)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 59

7. Yexowa dafa bëgg nga bég

(10 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Yexowa, Yàlla bu bég la (1 Timote 1:11). May na ñu lu bare luy wone ne dafa ñu bëgg. Bëgg na itam ñu bég (Kàdduy Waare 3:​12, 13). Nañu waxtaan ci ñaar ci maye yooyu—lekk bu neex ak lu neex lu ñuy dég.

Woneel WIDEO bi tudd: Li Yexowa sàkk dafay wone ne bëgg na ñu bég—lekk bu neex ak lu neex lu ñuy dég. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka la lekk bu neex ak lu neex lu ñuy dég di wonee ne Yexowa dafa bëgg nga bég?

Jàngal Taalifi Cant 32:8. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Xam ne Yexowa dafa bëgg nga bég naka la la loolu di xiire nga nangu tegtal yi mu ñuy jox ci Biibël bi te jaarale ko itam ci mbootaayam?

8. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm

(5 minit)

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 85 ak ñaan