9 suweŋ ba 15 suweŋ
KÀDDU YU XELU PÀCC 17
Woy-Yàlla nº 157 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
1. Na jàmm ak bànneex am ci sa biir kër
(10 minit)
Wéy di am jàmm ci suñu biir kër yombul, waaye lépp li ñu mënta def ba jàmm jooju am, jar na ko (Kàddu yu Xelu 17:1; xoolal )
Moytuleen di xuloo ci li nga xam ne jaru ko (Kàddu yu Xelu 17:9; g 9/14 11 § 2)
Bul gaw a mer (Kàddu yu Xelu 17:14; w08 1/5 10 § 6–11 § 1)
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
-
Kàddu yu Xelu 17:24—Lu tax aaya bi wax ne: «Ku amul xel moom, dafay xool fu nekk»? (it-2 432-433)
-
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Kàddu yu Xelu 17:1-17 (th lesoŋ 10)
4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. (lmd lesoŋ 3 ponk 5)
5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(4 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd lesoŋ 6 ponk 4)
6. Waxtaan bi
(5 minit) ijwbv-F 60—Turu waxtaan bi ci farãse: Quelle est la signification de Proverbes 17:17 ? (th lesoŋ 13)
Woy-Yàlla nº 113
7. Wone leen jikko yuy yombal waxtaan ci biir njaboot gi
(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.
Bu waa kër gi di jël jot ngir toog te di waxtaan bu baax, loolu dafay indi jàmm ak déggoo ci biir njaboot gi. Bu ku nekk di may moroomam muy wax li mu yëg ci xolam, dina gën a yomb ci ñoom ñu topp dogal yi ñu jël, te ku nekk dina mën a dëfël sa moroom bu jafe-jafe amee. (Kàddu yu Xelu 15:22) Kon, lan nga mën a def ngir loolu mën a am ci sa biir kër?
Nanga faral di jël jotu def yeen yi ak sa waa kër. (Baamtug Yoon wi 6:6, 7) Bu waa kër gi di ànd di def yeen yi, maanaam, di liggéeyandoo ci kër gi, di teewe ndaje yi, di ànd di waare, di ànd di fo, seen diggante dina gën a dëgër. Noonu, dinañu am occasion yu bare ngir waxtaan ci seen biir. Dëgg la ne , yeen saay nag, danga war a bàyyi li nga bëggoon a def te def li sa waa kër yi bëgg ngir nga am jotu def yeen yi ak ñoom. Waaye, jar na ko! (Filib 2:3, 4) Lan nga mën a def ba waxtu yi ngay nekk ak say waa kër, nekk waxtu yuy amal njariñ waa kër gi yépp?—Efes 5:15, 16.
Woneel WIDEO bi tudd: Toppleen xelal yiy indi jàmm ci biir njaboot (Amleen wax ju rafet ci biir njaboot gi). Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Jëfandikoo saa su ne, ordinatër, telefon ak lu ni mel, mën na tere waa kër gi ñu am jotu waxtaan. Ci naka?
-
Ni ko wideo bi wonee, lan la ku nekk mën a def ba waa kër gi yépp mën a toog di waxtaan ci jàmm?
Deel déglu bu baax. (Saag 1:19) Sa doom yi dinañu la nangu wax li ñuy yëg bu ñu gisee ne danga leen di déglu bu baax te doo leen xas bu ñu waxee li àndul ak sa gis-gis. Bu la sa doom waxee lu la yéemloo, bul gaaw à mer. (Kàddu yu Xelu 17:27) Waaye, déglu ko bu baax te won ko ne ya ngi yëg li muy yëg. Boo nàndee bu baax li muy xalaat ak li muy yëg, dinga ko mën a dimbali bu baax te ànd ceek mbëggeel.