Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

5 me ba 11 me

KÀDDU YU XELU PÀCC 12

5 me ba 11 me

Woy-Yàlla nº 101 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Bu ñuy liggéey ak suñu xol bépp dañuy am yool

(10 minit)

Bul yàq sa jot ci li amul njariñ (Kàddu yu Xelu 12:11)

Nanga liggéey ànd ceek cawarte, te farlu ci (Kàddu yu Xelu 12:24; w16.06 30 § 6)

Booy liggéey ak sa xol bépp, dinga am yool (Kàddu yu Xelu 12:14)

XELAL: Dinga am mbégte ci sa liggéey bu metti booy xalaat ci njariñ bu muy amal ñeneen ñi.—Jëf ya 20:35; w15 1/2 5 § 4-6.

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Kàddu yu Xelu 12:16—Naka la ñu njàngale bi nekk ci aaya bii mënee may doole ngir ñu wéy di muñ jafe-jafe yi? (ijwyp 95 § 10-11)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(2 minit) KËROO-KËR. (lmd lesoŋ 1 ponk 4)

5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) KËROO-KËR. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd lesoŋ 5 ponk 4)

6. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Wonal kenn ku am ay doom suñu palaas ci internet. (lmd lesoŋ 9 ponk 3)

7. Wax ci li ñu gëm

(3 minit) Wone bi. ijwfq-F 3—Wone bi mu ngi sukkandiku ci waxtaan bi tudd ci farãse: Croyez-vous pratiquer la seule vraie religion? (lmd lesoŋ 4 ponk 3)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 21

8. Yexowa mën nañu dimbali bu ñu amee ay jafe-jafe ci wàllu koom-koom

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Ndax danga jaaxle ci li nga amagul liggéey? Walla danga ragal a ñakk sa liggéey, mbaa nga ñakk a am li ngay dunde tey walla boo gënee màgget? Situation àddina si ci wàllu koom-koom mën na jékki-jékki rekk soppeeku. Waaye, Yexowa dig nañu ne, bu ñu jiitale coobareem ci suñu dund, moom dina ñu may li ñu soxla ngir ñu dund, bu dee sax dañu jékki-jékki rekk ñakk li ñu amoon te loolu jural ñu jafe-jafe yu bare ci wàllu koom-koom.—Taalifi Cant 46:​1-3; 127:2; Macë 6:​31-33.

Woneel WIDEO bi tudd: Yexowa masuñoo bàyyi. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Lan lañuy jàngee ci li mbokk Alvarado dund?

Jàngal 1 Timote 5:8. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka la aaya bi mënee dëgëral suñu ngëm ci Yexowa maanaam, mu wóor ñu ne dina wéy di may jaamam yi li ñu soxla ngir dund?

Xoolal yenn njàngale yu nekk ci Biibël bi yu la mën a dimbali boo amee jafe-jafe ci wàllu koom-koom:

  • Yombalal sa dund. Moytul yenn bor yi ak depãs yu amul solo.—Macë 6:22

  • Jëlal dogal yu baax ci lu jëm ci liggéey ak jàng yu kawe, ngir nga mën a jiital coobare Yàlla ci sa dund.—Filib 1:​9-11

  • Nanga suufeelu te nangu def yenn coppite ci sa dund. Ci misaal, boo ñàkkee sa liggéey, nangul beneen liggéey bu la mën dimbali nga faj sa soxlay njaboot, ba ci fasoŋu liggéey yu nit ñi di xeeb.—Kàddu yu Xelu 14:23

  • Deel maye, di séddook ñeneen ñi li nga am, bu dee sax li nga am barewul.—Yawut ya 13:16

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 57 ak ñaan