Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

26 me ba 1 suweŋ

KÀDDU YU XELU PÀCC 15

26 me ba 1 suweŋ

Woy-Yàlla nº 102 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Defal li nga mën ngir dimbali ñeneen ñi ñu am mbégte

(10 minit)

Suñu mbokk yi am jafe-jafe, mën nañu foog ne ci coono rekk lañu dëkk (Kàddu yu Xelu 15:15)

Deel teral ñi am ay jafe-jafe (Kàddu yu Xelu 15:17; w10 15/11 31 § 16)

Booy xool nit ki ak bëtu mbaax te di ko wax kàddu yu neex, loolu mën na ko dëfal bu baax (Kàddu yu Xelu 15:​23, 30, Xoolal li ñu bind ci suufu aaya bi ci Biibël bi ci farãse; w18.04 23-24 § 16-18)

LAAJAL SA BOPP LII: ‘Kan ci sa mbooloo moo soxla ñu dëfal ko?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Kàddu yu Xelu 15:22—Naka lañu njàngale bi nekk ci aaya bii mënee dimbali ñu jël dogal yu baax ci lu jëm ci faju? (ijwbq-F 39 § 3)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) KËROO-KËR. (lmd lesoŋ 1 ponk 5)

5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd lesoŋ 2 ponk 4)

6. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu

(5 minit) Waa këru ki ngay jàngal Biibël bi, ñu ngi koy fitnaal. Dëfal ko. (th lesoŋ 4)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 155

7. Mën nañu bég bu dee sax ñu ngi jànkoonteek ay jafe-jafe

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Woneel WIDEO bi tudd Mën nañu bég bu dee sax dañu . . . Nekk ci njàqare, dañu xiif, te Rafle. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  •   Lan nga jàngee ci nettali yii?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 100 ak ñaan