3 màrs ba 9 màrs
KÀDDU YU XELU PÀCC 3
Woy-Yàlla nº 8 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
1. Woneel ne wóolu nga Yexowa
(10 minit)
Nanga wóolu Yexowa, te bañ a wóolu sa bopp (Kàddu yu Xelu 3:5; ijwbv waxtaan 14 § 4-5)
Ni ngay wone ne wóolu nga Yexowa, mooy di wut xelal yi muy joxe te di leen topp. (Kàddu yu Xelu 3:6; ijwbv waxtaan 14 § 6-7)
Nañu moytu di wóolu suñu bopp ba mu ëpp (Kàddu yu Xelu 3:7; be 76 § 4)
LAAJAL SA BOPP LII: ‘Ndax damay topp santaane Yexowa yi ci lépp li ma def’?
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
-
Kàddu yu Xelu 3:3—Aaya bi dafa ñuy xiir ñu ‘takk ngor ak worma ci suñu baat te bind leen ci suñu àlluway xol’. Lan la baat yooyu di tekki? (w06 15/9 17 § 7)
-
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Kàddu yu Xelu 3:1-18 (th lesoŋ 12)
4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(3 minit) KËROO-KËR. Nit ki dafa la laaj benn laaj ngir dog waxtaan bi. Naka nga ko mëne tontu? (lmd lesoŋ 1 ponk 5)
5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(4 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. Woneel nit ki suñu palaas bi nekk ci internet ba pare nga jox ko benn kàrtu jw.org. (lmd lesoŋ 3 ponk 3)
6. Waxtaan bi
(5 minit) w11-F 15/3 14 § 7-10—Turu waxtaan bi: Woneel sa kóolute ci Yexowa bu de sax nit ñi bëgguñu la déglu (th lesoŋ 20)
Woy-Yàlla nº 124
7. Woneel ne wóolu nga mbootaayu Yexowa
(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.
Topp li ñu Biibël bi di wax, mën na yomb ci ñun. Waaye yenn saay, topp tegtal yiy jóge ci ñiy jiite mbootaayu Yexowa, mën na jafe ci ñun. Lu tax? Ndaxte ñi ñuy jiite dañoo matadi te xéyna nànd ñu tegtal yi ñu ñu jox, walla sax àndu ñu ci.
Jàngal Malasi 2:7. Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Yexowa dafay jar ci ay nit yu matadi ngir jiite mbootaayam, lu tax loolu waru ñu jaaxal?
Jàngal Macë 24:45. Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Lu tax ñu war a wóolu mbootaayu Yexowa?
Jàngal Yawut ya 13:17. Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Lu tax ñu war a nangu dogal yu, ñi Yexowa tànn ngir ñu jiite ñu, di jël?
Woneel WIDEO bi tudd: Ay yégle yu jóge ci Jataay biy dogal ci atum 2021 #9—Xaaj Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Naka la tegtal yu ñu jot ci jamono Covid yokke suñu kóolute ci mbootaayu Yexowa?