LI ÑUY DEF AK LI NGEEN DI MAYE
Tekki nañu ci ay làkk yu bare suñu ndaje bu mag bu ñetti fan bu 2020 bi tudd «Deeleen bég»!
10 SULYET 2020
Ren, feebaru Korona bi tax na ba suñuy mbokk ci ngëm yi nekk ci àddina si sépp war a def seen ndaje bu mag bu ñetti fan ci fasoŋ bu bees: porogaraam bi yépp dinañu ko def wideo. Loolu dina may ñépp ñu mën ko seetaan diggante weeri sulyet ak ut. Waaye, dina laaj ñu tekki porogaraam boobu ci lu ëpp 500 làkk. Loolu lépp, benn at lay laaj, walla sax lu ko ëpp. Waaye, ndegam dañu ko waroon a seetaan diggante sulyet ak ut, ñi war a tekki wideo yi ci làkk yooyu, amuñu woon sax ñeenti weer ngir pare liggéey bi.
Waaye nag jot nañu ndimbal. Ay mbokk yu nekk ci Kër gu mag te ñuy jàpple ñiy tekki téere yi ak wideo yi seet nañu li ñu soxla ngir def liggéey bi. Gis nañu ne li ñu soxla bare na, waaye li ñu gënoon a soxla mooy ay mikoro. Ñi bokk ci Biro bi yor njënd mi nag ñoo def ba ñu jënd 1 000 mikoro, te yónnee leen ci 200 béréb.
Loolu naroon na seer lool. Mikoro bu ci nekk, jënd ko te yónnee ko, 118 300 FCFA lañu ci naroon a fey. Looloo tax, ñu jënd mikoro yu bare, jot leen ci benn béréb, ba pare yónnee leen fépp fi ñu ko soxla woon ci àddina si. Noonu, mikoro bu nekk, jënd ko te yónnee ko, 98 600 FCFA lañu ci mujjee fey.
Ci weeri awril ak me 2020 lañu jënde mikoro yi ak lépp li ñu soxla woon te yónnee leen bànqaasu Seede Yexowa yi, biro yi ak yeneeni béréb yiy tekki suñu téere yi ak suñu wideo yi. Ñi gën a bare ci ñoom, jot nañu lépp li ñu soxla bala weeru me bi di dee doonte sax liggéey yu bare doxatuñu woon noonu ndax feebaru Korona bi.
Ki tudd Jay Swinney te muy jiite Biro bi yor njënd mi, lii la wax: «Ci diiru liggéey bi yépp, biro yi nekk ci Betel bi ak ñi ñu jaayoon li ñu soxla, ànd nañu bu baax ci liggéey boobu. Xelum Yexowa kese moo mënoon a tax ba ñu mën ko def ci lu gaaw, te ñu am li ñu soxla ci njëg bu gën a yomb.»
Nicholas Ahladis, mi bokk ci ñi nekk ci Kër gu mag te ñuy jàpple ñiy tekki téere yi ak wideo yi, lii la wax: «Ci jamono Korona bi, ñenn ci ñiy tekki suñu téere yi mënuñu woon a génn, dem liggéeyandoo ci benn béréb ndax li nguur gi santaane ci loolu. Loolu moo tax, ñu kontaan lool bi ñu jotee lépp li ñu soxla ngir mën a kontine seen liggéey ci seen kër! Noonu, tekki nañu lépp li ñu waroon a seetaan ci ndaje bu mag bi, maanaam waxtaan yi, tiyaatar yi ak wóy yi, ci lu ëpp 500 làkk.»
Liggéey boobu, bokk na ci lu bare li ñu def ngir am suñu ndaje bu mag bu ñetti fan bu 2020 bi tudd «Deeleen bég»!. Ak li ngeen maye ak xol bu sédd ci donate.jw.org walla ci yeneen fasoŋ lañu jënde li ñu soxla woon ngir def liggéey bi.