XAAJ 5
Nañu fonk mbiri Yàlla yi
MBIND mu sell mi wax na ci ay mbiri Yàlla yu bare yu mën a tax ñu xam ko. Ñeent yii ñoo ci ëpp solo : kàttanam, njubteem, xam-xamam ak mbëggeelam. Léegi nañu jël benn bu nekk te waxtaan ci.
Kàttanam amul fu mu yem
Li la Yexowa wax Ibraayma : “ Man maay Yàlla Aji man ji. ” (Njàlbéen ga 17:1.) Moom rekk moo am kàttan googu. Kàttanam du jeex te amul fu mu yem. Ci kàttan googu la sàkke lépp.
Yàlla xam na nu muy jëfandikoo kàttanam, xam na lu tax mu di ko jëfandikoo, te du ko jëfandikoo mukk ngir def leneen lu dul lu baax. Te bu koy jëfandikoo dafay ànd ak njubteem, xam-xamam ak mbëggeelam.
Yexowa dafay jëfandikoo kàttanam ngir dimbali ñi koy jaamu. Ni ko Mbind mu sell mi waxe, mu ngi xool fu nekk ci àddina si ngir jëfandikoo kàttanam ngir dimbali ñi ko bëgg ak seen xol bépp (2 Chroniques 16:9). Ndax bëgguloo jege Yàlla ju mel noonu, maanaam Yàlla ju am kàttan te bëgg a dimbali nit ?
Lu jub rekk la bëgg
Yexowa “ ku fonk njubte la. ” (Sabuur 37:28, MN). Lépp lu muy def day jub te baax.
Yàlla dafa sib lépp lu jaarul yoon. Du gënale te kenn mënu ko jox dara pur mu bàyyi la nga def lu bon. (Deutéronome 10:17) Bëggul ñiy tooñ seeni moroom te dafay dimbali ñi néew doole, mel ni ñi ñàkk seen jëkkër walla seen baay. (Exode 22:22) Yàlla, doomu Aadama yépp la fonk. “ Yàlla du gënale, waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu. ” — Jëf ya 10:34, 35.
Njubte Yàlla dafa ànd ak xel. Du la bàyyi nga def lu la neex waaye ba tey du soxor ak yow. Dafay yar ku bëggul réccu bàkkaaram waaye dafay am yërmande ci kuy réccu bàkkaaram. Ni ko Mbind mu sell mi waxe, Yexowa dafa am yërmande te bare yiw, di yéex a mer te fees ak mbëggeel. Du dencal nit bàkkaaram ba fàww, di ko ko fàttali saa su nekk. Du ñu feyloo li ñu war a fey ndax suñuy bàkkaar. (Psaume 103:8-10) Ku koy topp te def lu baax, Yàlla dina la fey lu baax te du la fàtte. Ndax Yàlla juy wone njubte boobu, jarul a wóolu ?
Xam-xamam du jeex
Yexowa xam na lépp. “ Xelum Yàlla ni mu xóote, ak xam-xamam ni mu baree, ba raw xelum nit ! ” (Room 11:33). Amul xelal bu mën a sut xelalu Yàlla ndaxte xam-xamam du jeex.
Xam-xamam feeñ na bu baax ci li mu sàkk. Mbind mu sell mi nee na lépp li Yexowa sàkk, dafa ko sàkk ak xam-xam bu ànd ak xel bu mat. — Psaume 104:24.
Bu ñu jàngee Mbind mu sell mi dinañu mën a xam li Yàlla di xelal nit. Buur bi tudd Dawuda, lii la bind : “ Sedees Aji Sax ji moo wóor, di yee ñi xamul. ” (Sabóor 19:8). Xoolal loolu, mën nga jariñoo xam-xam boobu jóge ci Yàlla ! Ndax dinga bàyyi njariñ boobu rëcc la ?
“ Yàlla mbëggeel la ”
Mbëggeel mooy li gën a feeñ ci Yexowa. Mbind mu sell mi nee na : “ Yàlla mbëggeel la. ” (1 Yowaana 4:8). Mbëggeel moo jiite lépp lu muy def.
Jëf ya 14:17). Ci dëgg, “ gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat, ci Yàlla la jóge, di Baay bi sàkk leeri asamaan. ” (Saag 1:17). Yàlla dafa ñu may lu réy bi mu ñu mayee Mbind mu sell mi ngir ñu xam ki mu doon ak li mu bëgg. Bi muy ñaan Yàlla, lii la Yeesu wax : “ Sa kàddu mooy dëgg. ” —Yowaana 17:17.
Ni ñu Yàlla wone mbëggeelam bare na lool. Dafa ñuy may lu neex : “ [Dafa] def lu baax, di leen wàcceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mbég. ”(Yàlla dafa ñuy dimbali itam ci suñuy coono. Ni ko Mbind mu sell mi waxe, bu ñu amee lu diis lu nekk ci suñu bopp, dañu ko war a teg ci loxo Yexowa te dina ñu dimbali, ndaxte du bàyyi mukk nit ku jub. (Psaume 55:22) Yàlla dafa ñuy baal suñuy bàkkaar. “ Yow mii, Yexowa, danga baax te bëgg a baale. ” (Sabuur 86:5, MN). Dafa ñuy may sax ñu mën a am dund gu dul jeex. “ Dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu. ” (Peeñu ma 21:4). Mbëggeel boobu Yàlla am ci nit, lan lay def ci yow ? Ndax loolu du tax nga bëgg ko ?
Nanga jege Yàlla
Yàlla dafa bëgg nga xam ko. Lii la Kàddu Yàlla wax : “ Jegeleen Yàlla, mu jege leen. ” (Saag 4:8). Yàlla dafa woowe Ibraayma ‘ xaritam ’. (Saag 2:23) Yàlla bëgg na it nga nekk xaritam.
Booy jàng lu jëm ci Yàlla, dinga ko gën a jege te dinga gën a am mbégte ci sa xol. “ Céy nit kee barkeel, ” ki nga xam ne “ yoonu Aji Sax ji lay noyyee, mu di ko gëstu guddi ak bëccëg. ” (Sabóor 1:1, 2). Kon nanga kontine di jàng Mbind mu sell mi. Nanga xalaat ci mbiri Yàlla yi. Booy jàng dara, nanga ko jëfe. Noonu ngay wone ne bëgg nga Yàlla. “ Mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam ; te ay ndigalam diisuñu. ” (1 Yowaana 5:3). Ñaanal Yàlla li ko woykat bi ñaan : “ Nanga ma xamal sa yoon, céy Yexowa, jàngal ma sa yoon. Nanga ma dimbali may dunde sa dëgg. ” (Sabuur 25:4,5, MN). Dinga gis ne Yàlla “ sorewul kenn ci nun. ” — Jëf ya 17:27.