LESOŊ 55
Li nga mën a def ci mbooloo bi nga bokk
Ci àddina si sépp, ay milioŋi nit ñu ngi jaamu Yexowa ànd ci ak mbég ci mbooloo bi ñu bokk. Dañu am ngërëm ci tegtal yi ñu leen di jox te dañuy bég ci dimbali seen waa mbooloo ci anam yu bare. Yow itam ndax du loolu nga bëgg a def ci sa biir mbooloo?
1. Naka nga mënee jëfandikoo sa jot ak sa kàttan ngir dimbali sa mbooloo?
Ñun ñépp mën nañu def dara ci suñu mbooloo. Ci misaal, ndax ci sa mbooloo am na ñu màgget walla ñu feebar? Ndax mën nga leen a yóbbu ñu teewe ndaje yi? Walla ndax mën nga leen a dimbali ci yeneen fànn, mel ni demal leen marse walla defal leen liggéeyu kër? (Jàngal Saag 1:27). Mën nga dimbali itam ci liggéeyu set-setal ak toppatoo saalu Nguur gi. Kenn du ñu forse ci def loolu. Suñu mbëggeel ci Yàlla ak ci suñu mbokk yi moo ñuy xiir ci ‘taxawal suñu bopp’ ngir def ko (Sabóor 110:3).
Seede Yexowa yi sóobu ci ndox mën nañu dimbali mbooloo mi ci yeneen fànn. Karceen yu góor yi matal li Biibël bi laaj, mën nañu bokk ci ñiy topptoo yëfi mbooloo mi walla nekk ay magi mbooloo. Mbokk yu góor yi ak yu jigéen yi mën nañu doon ay pioñee ngir jàpp bu baax ci liggéeyu waare bi. Yenn Seede Yexowa yi mën nañu jàppale ci liggéeyu tabax béréb yi ñuy jaamoo Yàlla walla ñu toxu ngir dem dimbali mbooloo yi soxla ndimbal.
2. Naka lañu mënee jëfandikoo suñu alal ngir dimbali suñu mbooloo?
Mën nañu ‘teral Yexowa ci suñu alal’ (Kàddu yu Xelu 3:9). Dañuy bég ci jëfandikoo suñu xaalis ak suñu alal ngir jàppale suñu mbooloo ak liggéeyu waare bi ñuy def ci àddina si sépp (Jàngal 2 Korent 9:7). Li ñuy maye dañu koy jëfandikoo itam ngir wallu suñu mbokk yi musiba dal. Ñu bare dañuy faral di «ber» dara ngir maye ko (Jàngal 1 Korent 16:2). Mën nañu def li ñuy maye ci boyet yi nekk ci béréb yi ñuy jaamoo Yexowa walla ñu jaare ko ci internet ci donate.jw.org. Mën nañu won Yexowa ne, bëgg nañu ko bu ñuy jëfandikoo suñu alal ngir dimbali mbooloo mi.
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal li nga mën a def ngir dimbali mbooloo mi.
3. Mën nañu jëfandikoo suñu alal
Yexowa ak Yeesu fonk nañu nit ñiy maye ak mbégte. Ci misaal, Yeesu ndokkeel na jigéen ji ñàkkoon jëkkëram te néew doole ndaxte dafa may Yexowa li mu amoon. Jàngal Luug 21:1-4. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
-
Ndax soxla nañu may Yexowa xaalis bu bare ngir neex ko?
-
Lan la Yexowa ak Yeesu di yëg, bu ñuy maye ak xol bu tàlli?
Boo bëggee xam ni ñuy jëfandikoo li nit ñi di maye, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
-
Naka lañuy jëfandikoo maye yi ngir njariñu mbooloo yi nekk ci àddina si sépp?
4. Mën nga dimbali ci liggéey bi
Ci jamono ji ñu doon bind Biibël bi, jaamu Yexowa yi dañu sawaroon ci toppatoo seen béréb yi ñu doon jaamoo Yàlla. Waaye toppatoo boobu yemul woon rekk ci maye xaalis. Jàngal 2 Chroniques 34:9-11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
-
Lan la Yawut bu nekk def ngir dimbali ci toppatoo këru Yexowa, maanaam fi ñu doon jaamoo Yàlla?
Boo bëggee xam ni leen Seede Yexowa yi di roye, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.
-
Lu tax mu am solo ñuy toppatoo suñu saalu Nguur, ba mu wéy di set te bañ a am benn yàqu-yàqu?
-
Lan nga mën a def ngir dimbali ci liggéey boobu?
5. Mbokk yu góor yi mën nañu yokk li ñuy def ci mbooloo mi
Biibël bi dafay xiirtal karceen yu góor yi ci def lépp li ñu mën ngir jàppale mbooloo mi. Boo bëggee xam li ñu mën a def, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.
-
Ci wideo bi, lan la Ryan def ngir gën a jàppale mbooloo mi?
Biibël bi wax na li karceen yu góor yi war a def ngir mën a bokk ci ñiy topptoo yëfi mbooloo mi te nekk ay magi mbooloo. Jàngal 1 Timote 3:1-13. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
BU LA NIT LAAJOON: «Fan la Seede Yexowa yi di jële xaalis bi ñuy defe seen liggéey?»
-
Lan ngay tontu?
NAÑU TËNK
Yexowa fonk na bu baax ni ñuy jëfandikoo suñu jot, suñu kàttan ak suñu alal ngir dimbali mbooloo mi.
Nañu fàttaliku
-
Naka lañu mënee jëfandikoo suñu jot ak suñu kàttan ngir dimbali mbooloo mi?
-
Naka lañu mënee jëfandikoo suñu alal ngir dimbali mbooloo mi?
-
Lan nga bëgg a def ngir dimbali mbooloo mi?
GËSTUL
Am na liggéey bu Biibël bi jagleel suñu mbokk yu góor yi ci mbooloo mi. Waaye naka la mbokk yu jigéen yi war a gise liggéey boobu?
Xoolal ay Seede Yexowa yu jàmbaare yuy def lépp ngir yóbbul seen mbokk yi ci ngëm ay téere.
Dañuy yóbbul seeni mbokk ca Congo ay téere yu sukkandiku ci Biibël bi (4:25)
Xoolal ni ñuy def ba am xaalis bi ñuy defe suñu liggéey, ni mu wuute ak ni ko yeneen diine yi di defe.
«Fan la Seede Yexowa yi di jële xaalis bi ñuy defe seen liggéey?» (Ci jw.org la nekk)