Lu tax Yàlla sàkk nit ?
Yàlla dafa bëgg ñu dëkk ci jàmm bu bare ba abadan ci àjjana ci kaw suuf !
Xéyna dinga ne : ‘ Ndax loolu dina mas a nekk ? ’ Biibël bi nee na Nguuru Yàlla dina ko def, te li Yàlla bëgg mooy nit ñépp jàng lu jëm ci Nguur googu te xam li tax Yàlla sàkk nit. — Sabóor 37:11, 29 ; Esayi 9:6.
Yàlla, suñu njariñ la bëgg.
Baay bu baax dafay yéene ay doomam li gën. Noonu it, suñu Baay bi nekk ci kaw asamaan dafa bëgg ñu dëkk ci bànneex ba fàww (Isaïe 48:17, 18). Te dige na ne ‘ kuy def coobareem dinga sax ba fàww ’. — 1 Yowaana 2:17.
Yàlla dafa bëgg ñu topp ay ndigalam.
Biibël bi nee na Ki ñu sàkk dafa ñu bëgg a ‘ jàngal ay yoonam ’ ngir ñu mën a “ wéy ciy ndigalam ” (Esayi 2:2, 3). Yàlla dafa taxawal “ xeet wu ñu tudde turam ” ngir ñu xamle coobareem ci àddina si sépp. — Jëf ya 15:14.
Yàlla dafa bëgg bu ñu koy jaamu ñu booloo nekk benn.
Jaamu Yexowa du xaajale nit ñi waaye dafa leen di boole ci kaw mbëggeel dëgg (Yowaana 13:35). Ndax tey am na ñuy jàngal nit ñi ci àddina si sépp, muy góor mbaa jigéen, ni ñu mënee nekk benn bu ñuy jaamu Yàlla ? Jàngal téere bii ngir xam tont bi.