NETTALI 97
Yeesu, Buur Bi, Mu Ngi Ñów
TUUTI ginnaaw bi Yeesu fajee ñaari gumba yi doon yelwaan, dafa dem ci dëkk bu ndaw bu jege woon Yerusalem. Mu ne ñaari taalibeem yi : ‘ Demleen ci biir dëkk bi. Dingeen gis mbaam-sëf bu ndaw. Yewwileen ko, ngeen indil ma ko. ’
Ñu indil ko ko, Yeesu toog ci kowam, daldi dem Yerusalem. Bi mu fa jegee, nit ñu bare ñów teeru ko. Ñi ci ëpp daldi summi seen mbubb te lal ko ci yoon bi. Ñeneen ñi dagg ay bànqaasu tiir, def leen ci yoon bi itam. Ñu nekk di wax ci kow, naan : ‘ Na Yàlla barkeel buur bii di ñów ci turu Yexowa ! ’
Ca jamano yu yàgg ya ci Israyil, buur bu ñu sog a fal, dafa doon yéeg ci mbaam-sëf bu ndaw, dugg ci biir Yerusalem ngir nit ñi gis ko. Loolu la Yeesu di def. Te nit ñooñu ñu ngi wone ne bëgg nañu Yeesu nekk seen buur. Waaye du ñépp a ko bëgg. Li xewoon bi Yeesu demee ca kër Yàlla ga moo koy wone.
Ci kër Yàlla gi, Yeesu faj na ay gumba ak ay lafañ. Bi xale yi gisee loolu, ñu daldi tagg Yeesu ak baat bu kowe. Saraxalekat yi daldi mer. Ñu ne Yeesu : ‘ Ndax dégg nga li xale yi di wax ? ’
Yeesu tontu leen ne : ‘ Waaw, dégg naa ko. Ndax masuleen a jàng lii ci Biibël bi : “ Ci gémmiñu xale yu ndaw la Yàlla di jaar ngir tagg am ? ” ’ Xale yi daldi kontine di tagg ki Yàlla def buur.
Bëgg nañu mel ni xale yooyu, du dëgg ? Mën na am ay nit jéem ñu tere wax ci nguuru Yàlla. Waaye ba tey dinañu kontine di wax nit ñi lu rafet lool li Yeesu di defal nit ñi ëllëg.
Yeesu, du ci jamano bi mu nekkee ci kow suuf la naroon a nguuru. Loolu, kañ lay doon ? Taalibe Yeesu yi bëggoon nañu ko xam. Dinañu ci wax ci nettali bii di topp.