Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 66

Jabaru Buur Bu Tuddoon Yesabel Te Nekkoon Ku Bon

Jabaru Buur Bu Tuddoon Yesabel Te Nekkoon Ku Bon

GINNAAW Yérobowam, ay buur yu bon kese ñoo ilif 10 giir yi. Buur bi tudd Akab moo ci gënoon a bon. Ndax xam nga lu tax ? Jabaram moo gënoon a tax mu mel noonu. Yesabel la tudd. Ku bon la woon.

Yesabel bokkul ci waa Israyil. Baayam moo doon buuru Sidon. Yesabel dafay jaamu yàlla ju dul dëgg ji tudd Baal. Tax na ba Akab ak waa Israyil yu bare jaamu Baal ñoom itam. Yesabel dafa bañ Yexowa lool te rey na ay yonentam yu bare. Am na ñu waroon a nëbbu ci ay pax ci biir montaañ yi ngir ñu bañ leen a rey. Bu Yesabel bëggee dara, dina dem sax ba rey nit ngir am loolu.

Benn bés, xolu buur Akab neexul woon dara. Yesabel laaj ko : ‘ Lu tax sa xol neexul ? ’

Akab ne ko : ‘ Li ma Nabott wax moo tax. Dama bëgg jënd toolu reseñ bi mu moom. Waaye nanguwul. ’

Yesabel ne ko : ‘ Bu ci sonn. Dinaa def ba nga am ko. ’

Yesabel bind ay leetar, yónnee leen ay njiit ci dëkk fi Nabott nekk. Mu ne leen : ‘ Jëlleen ay wayu, wax leen ñu ñów seede ne Nabott wax na lu bon ci Yàlla ak ci buur bi, ba pare yóbbuleen ko ci biti dëkk bi te sànnileen ko ay xeer ba mu dee. ’

Bi ñu waxee Yesabel ne Nabott dee na, lii la wax Akab ci saa si : ‘ Jógal dem nangu toolam. ’ Ndax nanguwuloo ne Yesabel dafa war a fey lu bon a bon li mu def noonu ?

Jamano ñów, Yexowa yónni góor gu tudd Yexu ngir Yesabel fey li mu def. Bi Yesabel déggee ne Yexu dafay ñów, mu komaase di pastelu ak di defaru ngir rafet lool. Waaye bi Yexu agsee ba gis Yesabel ci palanteeru kër buur bi, mu woo góor ñi nekkoon foofu, ne leen : ‘ Sànnileen ko ci suuf ! ’ Loolu lañuy wone fii. Sànni nañu ko ci suuf, mu dee. Noonu la Yesabel, jigéen bu bon bi, mujje.