NETTALI 40
Musaa Dóor Na Xeer Bi
AT YI ñu ngi dem rekk — 10 at, 20 at, 30 at, ba 39 at. Ba léegi waa Israyil ñu ngi ci màndiŋ mi. Waaye at yooyu yépp Yexowa toppatoo na mbooloom. Dafa leen dundal ak mànn bi. Mu di leen tette ci bëccëg ak benn niir bu nekkoon seen kanam te ñu war koo topp. Ci guddi gi, safara la woon. Te it, ci at yooyu yépp, yére yi ñu doon sol, yàquwuñu te seen tànk newiwul.
Bi ñu jógee Misra, am na léegi 39 at. Ñu ngi ci weer bu jëkk bu ñeent-fukkeelu at bi. Waa Israyil dellu nañu Kades. Mooy fi ñu nekkoon bi ñu yónnee 12 góor ñooñu ci réewu Kanaan ngir seet ni mu mel, am na léegi lu jege 40 at. Foofu la Miryam, magu Musaa, gaañoo. Te it, amaat nañu ay poroblem ci Kades na bi ñu fi jëkkoon a ñów.
Waa Israyil amuñu fu ñu mënee am ndox. Ñu daldi ne Musaa : ‘ Dee moo ñu gënaloon. Lu tax nga génne ñu Misra, ñów fi ci béréb boo xam ne amul dara luy sax ? Amul pepp, amul figg, amul reseñ, amul gerenaad. Amul sax ndox bu ñuy naan. ’
Musaa ak Aaroona dem ci tànt fi ñu doon jaamoo Yàlla, ñaan ko. Yexowa ne Musaa : ‘ Dajaleel mbooloo mi yépp, ba pare ci seen kanam ñoom ñépp, nanga wax ak xeer bi nekk fale. Dina génne ndox bu bare ba mu doy nit ñi ak mala yépp. ’
Musaa dajale mbooloo mi, ne leen : ‘ Dégluleen, yéen ñi ñàkk gëm ci Yàlla ! Ndax Aaroona ak man ñoo leen war a génneel ndox ci xeer bi ? ’ Musaa daldi dóor ñaari yoon xeer bi ak yetam, ndox mu baree bare daldi génn ci xeer bi, ba mu doy nit ñi ak mala yépp.
Waaye Yexowa mere na Musaa ak Aaroona. Ndax xam nga lu tax ? Dafa leen mere ndaxte Musaa ak Aaroona dañu wax ne ñoom ñooy génne ndox ci xeer bi, fekk ci dëgg Yexowa moo ko def. Kon waxuñu dëgg. Yexowa nee na dina leen yar ndax loolu. Mu ne leen : ‘ Dungeen yóbbu sama mbooloo ci biir Kanaan. ’
Léegi waa Israyil ñu ngi jóge Kades. Bi mu yàggee tuuti, ñu àgg ci tund bi tudd Or. Ci kow tund boobu la Aaroona gaañoo, fekk 123 at la amoon. Waa Israyil yépp di ko jooy 30 bés. Doomam Eleyasar daldi nekk saraxalekat bu mag bi ci mbooloo Israyil.