Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI NGA MËN A WAX BOO SEETIWAATEE NIT KI

LESOŊ 7

Wéyal di yégle xibaaru jàmm bi

Wéyal di yégle xibaaru jàmm bi

Njàngale bi: «Dañoo wey di jàngale ak di xamle xibaaru jàmm bi»—Jëf ya 5:42.

Ni ko Pool defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Jëf ya 19:​8-10. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Amoon na ñi doon fitnaal Pool. Waaye, lan la def ba wéy di dimbali ñi nga xam ne xibaaru jàmm bi itteel na leen?

  2.   Ñaata yoon la Pool doon dellusi ngir seetiwaat ñi nga xam ne xibaaru jàmm bi itteel na leen? Te ñaata wér la fa def?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Pool def?

2. Seetiwaat nit ñi te tàmbali njàngum Biibël bi ak ñoom dafay laaj góor-góorlu, ak jot ju bare.

Nanga roy ci Pool

3. Deel seeti nit ñi ci waxtu bi gën ci ñoom. Laajal sa bopp lii: ‘Ban waxtu moo gën ci moom? Fan la bëgg ñuy daje?’ Defal lépp ngir seetiwaat nit ki ci waxtu bi gën ci moom.

4. Laaj ko kañ nga mën a dellusi ngir wéyal waxtaan bi. Saa yoo waxtaane ak nit ki, bala ngay dem, laaj ko bés ak waxtu bi nga fa war a dellu ngir wéyal waxtaan bi. Fexeel ba ñëw ci bés ak waxtu bi nga ko dig.

5. Amal gis-gis bu rafet ci ñi lay déglu. Xéyna nit ki, amul jot ju bare, walla sax, doo ko fekk këram saa su nekk. Loolu tekkiwul ne xibaaru jàmm bi itteelu ko. (1 Korent 13:​4, 7) Waaye nag, def lépp ngir yégle xibaaru jàmm bi, tekkiwul ne da nga war a jël sa jot jépp ci ki nga xam ne yelloowu ko.—1 Korent 9:26.