WOY-YÀLLA Nº 58

Nañu wër ñi bëgg jàmm

Nañu wër ñi bëgg jàmm

(Luug 10:6)

  1. 1. Yeesu digle na, ñu dem waareji.

    Ci pënd bi, ci tàngaay bi,

    Mu ngi doon jox nit ñi yaakaar.

    Dafa bëggoon nit, moo tax tàyyiwul.

    Guddeek bëccëg la daan wëri

    Ñi dëgg gi neex.

    Kon ñun ni moom nañ dem waare

    Ci mbedd yépp ak kër gu ne,

    Ñu ngi yégle: ‘léegi coono yi yépp jeex’.

    (AWU BI)

    Ñun dañuy wër

    Nitu jàmm fu mu mën a ne

    Ñun dañuy wër

    Ku bëgg Yexowa musal la,

    Duñu tàyyi

    Ci waare bi.

  2. 2. Nañu góor-góorlu, li des barewul.

    Nit ñu bare soxla nañu

    Déglu xibaaru jàmm ji.

    Mbëggeel moo ñuy xiir, ci dem waareji

    Ngir xéttali nit ñiy jooy ndax

    Tiis yu bare yi.

    Ak fépp fu nit ki mën a ne,

    Bu ñu dégloo ñun dañuy bég,

    Kon buñ tàyyi dem waareji, jar na ko.

    (AWU BI)

    Ñun dañuy wër

    Nitu jàmm fu mu mën a ne

    Ñun dañuy wër

    Ku bëgg Yexowa musal la,

    Duñu tàyyi

    Ci waare bi.